Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
A - Xew-xew yi amoon diggante ba ñu jàppee Yeesu ba bañu Koy dugal ca bàmmeel ba (Yowaana 18:1 - 19:42)
4. Bant ba ak deewug Yeesu (Yowaana 19:16b-42)
c) Li Yeesu wax Ndeyam ji (Yowaana 19:25-27)YOWAANA 19:24b-27 Yowaana waxul lu jëm ci kàdduy Yeesu yu jiitu yi ci kurwaa bi. Yeesu dafa jëkk a baal ñépp, ba noppi mu baal sàcc ba féete woon ca ndeyjooram. Loolu lépp fekk Yawut yaa ngi koy ñaawal. Nettali yooyu Jàngu bu njëkk ba xamoon nañu leen ba Yowaana di bind téeréem bi. Saraxalekat yi dëpp ñibbi te dégguñu sax na Mu doon ñaane Baay bi ngir Mu baal leen. Mbooloo ma it ñibbi ngir waajal seen saraxu mbotem bésub jéggi ba. Jot gi xatoon na lool. Boroom diine yi ñungi doon waajal xew-xew bu mag boobu. Ñu jollil liit ga ca kow miiri dëkk ba, rekk rendi mbote ya daldi jot ca biir Kër Yàlla ga; noonu deret ja wal-a-wal. Biir Kër Yàlla ga fees aky cant. Ca la dànd Yerusalem, ñunga fa wékk mbotem Yàlla mu sell mi; ñu ne ko fa ñukk te bañ ko. Ay xarekati yéeféer ñoo doon wottu ñett ña ñu daajoon ca bant. Booba nag la ay jigéen jegesi kurwaa ba, ne tekk toog fa. Li xewoon lépp dafa leen a yéemoon. Aji Kàttan jaa ngi ci seen kanam, di sukkraat. Amul genn kàddu guy dëfalaate gu genn ci seeny gémmiñ, dañoo tëlewoon a ñaan sax. Xëyna amoon na ci ñoom ñu doon tari ci suuf ay aaya Sabóor. Yeesu dégg jooyi xolu yaayam ji, te gis rangooñi Yowaana taalibeem bi mu bëgg lool. Xalaatul boppam sax, ak xëm bi ko doon yoot. Mu jekk-jekki rekk ne: «Soxna si, sa doom a ngi.» Mbëggeelu Krist matoon na sëkk: Ci biir metitam sax dafay toppatoo ay soppeem. La Simeoŋ waxoon Maryaama mungi matsi, maanaam jaasi ji dina xar sa xol (Luk 2 :35). Ci kow ñàkk a man a may ndeyam alal, mbaà màkkaan mu mu man a dëkk, Yeesu may ko mbëggeel ga Mu joxoon taalibeem ya. Yowaana dafa ñówoon ànd ak yaayu Yeesu (Macè 27 :56), ak li mu nëbb turam ak wu Janq bi, ngir bañ a wànni sag bi Krist yelloo ci waxtu wi muy jote ndamam. Bi Yeesu dénkee Yowaana yaayam, ci la taalibe ba tàbbi ci leeraayu kurwaa ba. Mu daldi taf Maryaama ci dënnam te dalal ko ca këram. Yeneen jigéen ña seede nañu loolu. Boroom bi dàqoon na juróom-ñaari rab yu bon ca kenn ci ñoom. Kooka mooy Maryaama mu Magdala. Moom mosoon na ndamu Yeesu ci ruuwam. Dafa bëggoon Boroomam, te di Ko topp.
d) Njeextal li (Yowaana 19:28-30)YOWAANA 19:28-29 Evangelist bi Yaxya amoon na may gi mu mëna wax lu bari ci kàddu yu néew. Nettaliwul dara ci mbirum lëndëm gi muuroon réew mi, walla ci wooyug Kirist ngir bàyyi ko ci kanamu merum Yàlla ndax sunuy bàkkaar. Waaye daf nuy wax ni bimu jeexalee ci xeex bi mu àndaloon ci diiru ñatti waxtu, mu yëg ni dee mingi jegesi. Yaxya gëmul woon ne dee noot na Yeesu, waaye Yeesu nangu na jébbal boppam dee. Liggéeyu muccal àdduna bi dafa sonn lool ci ruuh gi. Jesus gis mucc gu mat sëkk gi ñépp mëna am; xamoon na ne deewam dina muccal ay milioŋ ciy bàkkaarkat ci seeni bàkkaar, may leen sañ-sañu ñëw ci Yàlla. Dafa gis góob bi ak meññeefu deeyam. Mu am ay baat yu suufe yu génne ci gémmiñam naan: «Damaa mar.» Ki sàkkoon jaww ji te dox ci kow ndox mi moo maroon. Mbëggeel gi ñu jëmmal mungi doon yóotu mbëggeelu Baay ji ko nëbboon kanamam. Safara lay wone, foo xam ne ruuwu nit ki ak yaramam dañuy dee ak mar, te duñu am lenn lu leen ko fajal (seralal). Krist nettaliwoon na léebu ab boroom alal ju nekkoon ca safara, mar lool ba ñaan Ibraayma ngir mu yónni Lasaar, mu capp baaraamam ci ndox mu sedd ngir tooyalal ko ay tuñam. Yeesu nit la woon, ku dékku maram, waaye ba waxtu rammu ga matee rekk la koy door a nangu. Xel mu Sell mi xamle woon na liggeyu rammoom lu war a tollu ci junni at ca gannaaw, ci Sabóor 22:13-18, ni mu waxe woon it ci Sabóor 69:21 lu jëm ci bineegar bi. Xamunu ndax soldaar ya dañoo may Yeesu bineegar bu far, walla bu ñu njar ak ndox, ndaxte dañu Koo jéppi woon, walla dañu Koo yërëmoon. Xam nanu ne du woon ndoxum neen. Yeesu, Doomu Yàlla ji, amatul oon kàttan ci saa soosu. YOWAANA 19:30 Ba Yeesu muucoo bineegar bi, ba noppi, dafa xaaca kàddu ndam li, ne: «Lépp mat na!» Ca bés ba jiitu woon xaacu ndam googu, Doom ji ñaanoon na Baayam ngir Mu may Ko ndam ci kurwaa bi ngir payooru sunu bakkan, ndax Baay bi ci boppam am ndam. Doom ji gëmoon na ne ñaan googu nangu na, te matal na sas bi Ko Baay ji santoon (Yowaana 17 :1,4). Cellaay moo doon feeñ ci Yeesu, ba ca Kurwaa ba sax. Genn kàddug mbañ rëccul ci gémmiñam, walla ab ñurumtu yërëmtalu, mbaa yuuxub ñàkk yaakaar, waaye dafa baal ay noonam te ŋoy ci mbëggeelu Yàlla, gi meloon ni sunu noonu ngëneel. Yeesu xamoon na ne matal na rammu gi, ndaxte Yàlla dafa mataloon Ka Mu yónni woon ci biiry coono ngir sunu mucc. Kenn manul a àgg ca xóotaay ak kowewaayu mbëggeelu Keneefu Ñett ñi, ndaxte Doom ji jébbal na boppam Yàlla ni sarax suy dund, ndax Xel mu Sell mi, te amul genn gàkk. (Yawut 9:14). La ko dale ca xaacu Yeesu ba ca kurwaa ba, la mucc gi mat sëkk te soxaatul leneen lu koy gën a mottali. Du sunuy man-man, sunuy jëf yu baax, sunuy ñaan, walla sunu laab; ñoo nuy may nu dunde njubte walla cellaay. Doomu Yàlla ji matalal nanu loolu lépp, ci benn yoon ba fàww. Ci deewam la jamono ju bees tàmbalee, te jàmm taxaw, ndaxte Mbotem Yàlla mi jubóoolewaat nanu ak Baay ji. Ku gëm, ñu àtte la. Bataaxeel yi dañuy joxe leeral ci kàdduy Jesus, yu mujj ak yu Yàlla wax, "Jeexna!". Yeesu sëggal boppam ba ni mandarga delloo njukkal, ak ni kilifteef. Mu delloo ruuwam ci loxoy Baayam ji Ko tàyyiwul a bëgg. Mbëggeel googu moo Ko teg ca gàŋŋune Yiw wi, fa Mu toog ba tey jii, ca ndeyjooru Baay ji, te nekk benn ak Moom. ÑAAN: CEY yow Mbote mu Sell, mi dindi bàkkaari àddina si; yelloo nga kàttan, alal, maandute teraanga, ndam barke a kit sama dund. May ma ba ma man di teg samay bët ci Yów, cey Yów mi ñu daajoon, ma di La ñaan nga baal ma samay tooñ, te di gëm ne dinga ma sellal jaare ko ci sa yiw ak sa deret. LAAJ:
|