Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
A - Xew-xew yi amoon diggante ba ñu jàppee Yeesu ba bañu Koy dugal ca bàmmeel ba (Yowaana 18:1 - 19:42)
4. Bant ba ak deewug Yeesu (Yowaana 19:16b-42)
e) Bënn nañu wetu Yeesu (Yowaana 19:31-37)YOWAANA 19:31-37 Xër ci seen yoon moo taxoon Yawut yi amatuñu woon yëg-yëgu nit. Yoon wi Musaa wàccee dafa tëraloon ne dañoo war a denc (rob) ñi ñu rey laata guddi di jot. Noonu Yawut ya defe ko noonu it ngir ñett ña ñu daajoon ca bant. Seen xel dafa xajamoon ci di gis néew yooyu ci diiru xew-xewu berndeel googu. Noonu ñu ñaan Pilaat mu damm seeny tànk ngir faat leen. Ña ñu daan daaj, yenn saa yi daan nañu sukkraat lu mat ñetti fan. Xarekat ya daldi dégg ndigal la ñu jot. Ñu ñëw ca kanamu Yeesu, gis ne saay na. Coono dóor ya ak diisaayu sunu bàkkaar yi ruuwam yenu, boole ci merum Yàlla mi nu Ko sëf, ñoo Ko ñàkkaloon kàttaan. Yeesu ci kow coobareem la deewee ngir jubale nu ak Yàlla. Ngir won Yawut yi ne Yeesu dee na ci dëgg-dëgg, ab xarekat dafa jël xeej, jam Ko ko ci wetu xolam bi. Ndox ak deret génne ca; liy wone ne dee na laata juróom-benneelu waxtu àjjuma jooju di jot. Ñetti fànnay xew-xew boobu ñoo nuy won ne Yàlla moo am ndam li. Bu jëkk bi mooy ne Seytaane xiir na Yawut eci ñu damm yaxi Yeesu, ngir kenn du man a wax ne ki ñu daaj Mooy sarax bi Yàlla dige. Aada Pàkk dafa laajoon mbote mu mat sëkk, mu kenn tojul ay yaxam (Gàddaay 12 :46). Noonu Yàlla sàmm Doomam ba ca dee ga, te kenn manul a weddi ne Mooy Mbotem Yàlla. Ñaareel bi mooy : Wetam gi ñu jam, Sakkaria Yonent bi yëgle woon na ko (12:10). Ci Sakkaria 11:13, Yonent bi gis na ne waa askanu Kóllëre gu Njëkk ga xayma woon nañu ne seen Sàmm bi, jarul lu ëpp fanweeri poseti xaalis. Naam njëg gu ñàkk solo googu, Yàlla wàccee na Xelu Yiw ak ñaan ci këru Dawuda, ak ci Yerusalem, ngir seeny bët ubbeeku te ñu ràññee Ki ñu daaj, ak Baayam. Bu duloon njàngat moomu, kon duñu man a xam Yàlla, te it duñu xam muccam gi. Ki ñu daaj doŋŋ moo man a tax ba nit jot Xelum Yàlla, ni nu ko Mbind mii di wonee: "Dinañu xool ci Ki ñu bënn." Ñetteel bi mooy : Taalibe bu gore bi desoon ca taatu Kurwaa ba, mooy seede bi teg bëtam ci yooyu xew-xew yépp. Dawul ba mu gisee saldaar ya, te it bàyyiwul Njaatigeem ba bi mu saayee sax. Gis na ni ñu bënne wetu Yeesu, te seedeel na mbëggeelu Yàlla, miy Baay, Doom, ak Xel mu Sell mi, ngir nu man a gëm jokkoo gi dox ci Kenneefu Ñett ñi, ak dund gu dul jeex gi. ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, daan nga bàkkaar, daan Seytaane te am ndam ci àtte bi. Yów Yaay kiy dund, Buur bu ànd ak Baay ji ci Kenneefu Xel mi. LAAJ:
|