Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- John - 111 (Crucifixion and the grave clothes; Dividing the garments and casting the lots)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
A - Xew-xew yi amoon diggante ba ñu jàppee Yeesu ba bañu Koy dugal ca bàmmeel ba (Yowaana 18:1 - 19:42)
4. Bant ba ak deewug Yeesu (Yowaana 19:16b-42)
a) Daaj ba ca bant ba ak mbind ma ca kurwaa ba (Yowaana 19:16b-22)YOWAANA 19:16b-18 Ay soldaar dañu doon daaji ñaari say-say, ca saa sa leen Pilaat jébbalee ab ñetteelu «bóomkat», muy Yeesu. Ñoom ñett ñépp dañu waroon a gàddu seeni bant bi ñu leen war a daaj. Krist sànniwul bant ba, te waccu ko mu daanu ca yoon wa. Ñett ñooña xëtt Yerusalem ci biir coono, génne ca buntu bët-Gànnaaru sowu. Ñu yéeg ca aw tund bu ñuy woowe Golgota, ndaxte dafa niruwoon ak kaaŋu bopp. Nit ña manoon nañoo tollu ca biir dëkk ba, di séen ña ñu wékk ca bant ya. Yowaana joxewul ay firnde ci kurwaa bi, ndaxte xalimaam dafa lànk a bind ñaawteef yu mel noonu. Nit ñi dañoo xalaboon mbëggeelu Yàlla, te mbañeelu Safara sax ci ñoom. Ñungi doon yàkk amtee sànni Ki juddoo ci Xel mi, te naroon a teggi seeny bàkkaar, jaarale ko ci jébbale boppam ni sarax. Genn wërgalu leer tiimul garabu gàcce ga, waaye ci biir nañu Ko doon toroxale, wone na ndamam jaare ko ci muñam ak njébbaloom. Ndaw ñaawteef bu ñu la daajee ci diggante ñaari defkati lëxóor, rax ca dolli ñu lay ñaawal! Boroom yërmande ji te sell, wone ba ci waxtu yu mujj ci dundam ni ku ànd ak bàkkaarkat yi. Loolu moo tax Doomu Yàlla ji juddu ni Doomu nit ki. May na doomu nit ñu teggi ndawal yi ñu nekk doomi Yàlla yu ñu goreel. Dem na ba ca fa mu gën a xóote ci suufeelu, ngir du man a wax ne Yeesu dundul loolu. Ak nu sa bàkkaar man a tollu, Yeesu man na la baal, laabal la te sellal la. YOWAANA 19:19-20 Soldaar yu wékk Yeesu ca diggante ñaari bóomkat yi, ngir ñaawal Ko ci li ñu ne buur la. Pilaat moom tàyyiwul ci di ñàkkloo fayda Sanedreŋ bi ko buux ba mu àtte Yeesu, ak li ko xelam mayoon mu goreel Ko lépp. Ca la tiim boppu Ka ñu daajoon, mu wékklu fa ab bant bu mu bind la Yawut yu jiiñoon Yeesu. Yàlla jëfandikoo mbind moomu ngir àtte Yawut yi, ndaxte ci dëgg Yeesu mooy seen buur. Yeesu mooy Buur dëgg biy ñów ci njubte, mbëggeel, lewetaay ak suufeelu. Moo taxawal àddina ci kow suuf. Yawut yi safara moo leen gënaloon, noonu ñu xalab Buuru asamaan bi te dàq Ko ci seen askan. Mu nekk nag Buuru Askan yépp, waaye askani tey jii, ndax nangu nañu Buur bi ñu daajoon, walla ñungi bañ ba tey Boroom biy mbëggeel? YOWAANA 19:21-22 Saraxalekat yam xam ni leen Pilaat jéppee, teg ci tëkku gi mu leen di yoote. Dañoo weddi seen Buur te gis ci ñàkk kàttanam lu wuute ak li Pilaat doon dëggal. Noonu ñu gënatee bañ Ka ñu daajoon. Wóoroon na Pilaat ne Sesaar àndoon na ci mbindam moom, mu def ci ñetti làkk, ngir askan wépp, wa réew mi ak doxandéem yi, ñépp man a xam ne bépp fippukat ci kow Rom, lu mel nii moo lay xaar. Ca atum 70 L.Y. (Laata Yeesu), Yawut yà dañoo fippu woon ca kanamu nguuru Rom, ñu jàpp ca ay junniy-junni daaj leen ca la wër dëkk ba.
b) Séddoo nañu yérey Yeesu, te tegoo bant mbubbam (Yowaana 19:23-24)YOWAANA 19:23-24a Ñeenti xarekat yi daajoon Yeesu amoon nañu sañ-sañu séddoo ay yéreem. Seen njiit la moom bëggul oon bokk ci séddoo bu toroxe noonu. Xarekat yi jël la Yeesu dese woon ci alal, xañ Ko darajaam. Dañu daan faral di summi bóomkat yi ngir gën leen a toroxal. Toroxal googu dafa doon jollil màggaayu Yeesu. Yéreem bi amul ñaw dafa nirook mbubbum Saraxalekat bu mag. Yeesu ci boppam mooy Saraxalekat bu mag bi jóge asamaan, Rammukatu àddina sépp. Nësër googoo tax coono dal Ko, te ñu metital Ko. Junni at ca gannaaw Xel mu Sell mi xamle woon na lépp li aju ci ndaajum Yeesu ci bant. Sabóor 22 nee na: «Séddoo nañu samay yére», loolu mbaaxu xarekat yi la. Ba noppi Xel mi teg ci ne: «tegoo nañu ay bant sama mbubb.» Xel mi wone bu leer ne daaju Yeesu ca bant ba ci coobare Yàlla la bokkoon. Ni ko Yeesu waxe woon, amul sa benn karaw buy daanu te Yàlla xamu ko. Képp ku weddi kurwaa bi, du la xewoon rekk nga weddi, waaye yaangi xëccook Xelum Yàlla mi yégle woon xew-xew yooyu lu ëpp ay junni at laata muy am. Xarekat yi ci ñàkk a xam lañu jëfe woon ca taatu kurwaa ba. Ñu séddoo la Ka ñu sonal ka dese woon. Amuñu ca woon benn yërmande. Seen xel demul sax ci ne Rammukatu àddina si mungi tuur deretam ci kurwaa bi. Mbokk mi,ndax daajandoo nañu la ak yeesu ca bant ba ,ba ngeen ànd dee ?Wallq yaa ngi daw ci gannaawu alal siiw ? Ndax bëgg nga Ki ñu daaj ?Ndax jot nga njubte asamaan,ak sellay gi dëgg, jaare ko ci deewam ? Walla yów ab seetaankat nga bu saraxu Ki ñu daaj saful ? Xel mu Sell mi dafa jokkoo ak Doomu Yàlla ji,ci ngëm ak mbëggeel gi ,ngir nu man a seddoo deewam gi,robam bi ak dundam gi ñu jébbale ni sarax. ÑAAN: Boroom bi Yeesu nungi lay sant ci li nga muñ ca kurwaa ba. Nungi lay màggal ci sa muñ nsa mbëggeel ak say barkeel. Nungi lay màggal ci linga nu baal sunuy bàkkaar, ak bàkkaari àddina si. Faxas nga sunuy bàkkaar ca kurwaa ba, te jubóole nit ñi ak Yàlla. Yaay sunu rammukat. LAAJ:
|