Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson? YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
A - Xew-xew yi amoon diggante ba ñu jàppee Yeesu ba bañu Koy dugal ca bàmmeel ba (Yowaana 18:1 - 19:42)
2. Layoo Yeesu ak Aan,ak ñetti yoon ya Ko Piyeer weddi (Yowaana 18:12-27)YOWAANA 18:12-14 Du woon Yawut yi kese ñoo jàppoon Yeesu, ab kilifa soldaaru waa Rom it bokkoon na ca. Krist mi sut dee gi, ak jinne yi, moom miy dalloo ngelaw li, di wéral laago yi te di baale bàkkaar yi, moo nangu ak lawetaay, ñu koy jéng. Ki daan doxi soxlaam ni mu ko neexe, lañu jàpp tey. Dañu Koo takkal ay càllalla. Nun noo waral loolu lépp, ndax sunuy bàkkaar. Jéngam yooyu, ab jéego la woon ci toroxalam bi gën a yées ca bant ba (kurwaa ba). Aan moo nekkoon saraxalekat bu mag ba ca atum 6 ba 15 laata Y.K. Ci yoon manoon na koo nekk giiru dundam, waaye nguuru Rom moo ko wàccee ngir fal Kaif, miy goroom biy àttekat bu muus, te man a teg yoon, ba ca diggante waa Rom ya sax. Seytaane moo ko jumtuwoo ngir mu seedee ay kàcc yu jëm ci deewug Yeesu, ngir rekk réew ya bañ a tas. Ña fa teewoon ñépp dañoo xalaatoon ne àtte bu jaar yoon la te tegu ay sart yu leer. Yowaana waxul lu jëm ci yeneen ñaari àtte yi, ni ko yeneen taskati Injiil yi defe, waaye dafa gën a jublu ci àtte bi amoon la jiituwoon ba ca kanamu Aan, ma doon njiitu kureel ga. Ba léegi Aan moo nekkoon kilifa giy doxal lépp liy doxal koom-koomu réew mi. Noonu Kaif daldi dogal ñu jàppe àtte bu jëkk bi ni lu dagan, ba ñu man koo seedeloo Aan ni njukkal. YOWAANA 18:15-18 Guddi lawoon. Yowaana ak Piyeer topp Yeesu, te dànd ko fu sore. Ni Yowaana nekke woon mbokk ci saraxalekat bu mag ba, moo taxoon mu man a dugg ca ëtt ba nu mu ko neexe. Piyeer manu ko woon a topp ndaxte bunt ba ay surga yu jigéen ñoo ko doon wottu. Yowaana daldi yërëm Piyeer mi nekkoon ci bitti, noonu mu dem wax ak Ndaw sa doon wottu bunt ba, ngir mu may ko agsi ci biir. Ni ndaw si ame woon xel-ñaar, mu laaj Piyeer ne ko: «Mbaa yów itam bokkuloo ci taalibey waa ji?» Mu tontu ne: «Déedéet!» Mu def ni ku xamul dara ci mbirum jàpp, bi ñu jàpp Yeesu, noonu muy wéy di jéem a jaaru. YOWAANA 18:19-24 Laaj yu njëkk yi ajuwuñu woon ci tooñu Yeesu, diineem, mbaa ci ay waxam. Waaye ñungi jublu woon ci ay taalibeem ak doxalinu njàngaleem. Ca jamono jooja, ay mbootaay yu nëbbu bare woon nañu. Kilifa Yawut ya bëggoon nañu xam taalibeem ya manoon nañoo indi ab yëngu-yëngal, ngir ñu teel a man a dal ci seen kow. Yeesu weddi na nekkinu mbootaay gu ni mel. Rax ci dolli, kilifa Yawut ya xamoon nañu ne jàngale woon na ca bëccëg ga ca jàngu ya ak ca Kër-Yàlla ga, te ñu bare déglu Ko. Su ñu ko bëggoon a xam ci dëgg, kon dinañu woo ña doon déglu, ba dégg lépp la Mu fa jàngale, ak la Mu fa woote. Yeesu dafa tontu saraxalekat bu mag ba, te boolewu ci genn ragal. Jekk-jekki rekk, kenn ca surga ya, bëggoon lu neex saraxalekat bu mag ba, daldi dóor Yeesu. Yeesu fayuwul, te wonewul genn mer. Waaye ñàkkalul fayda tooñu surga ba, te laaj na ko sax mu wax fu mu teg jëfam jooju. Ndegam Yeesu deful dara, tooñul, kon surga ba dafa waroon a baalu, mbaa mu rëccu bàkkaaram. Tëkku googu Aan moo ko moomoon, ndaxte mooy ndeyu mbill gi tax surga bi jëfe noonu. Moom moo indi tooñaange gi. Jiiñaate yu mel noonu, ñungi bokk tey ci àtte yi ñuy teg képp ku dóor sa moroom, te teguloo ko fenn, mbaa nga suxlu ay ñoñam ba ñu xoqatal ko moom mi deful dara. Sunu Boroom dafa faydaal mbir yu tuuti yi ; nee na : « Lépp lu ngeen def ñi gën a tuuti ci samay ñoñ, Man ngeen ko def. » Aan daldi gis ne tëkku yi muy def Yeesu amuñu benn solo ci Moom, xanaa kay dafa mel ni Yeesu mooy àttekat bi léegi, ba sax indiwaat ay laaj yu aju ci dëgg ak njubte. Noonu Aan yóbbuloo Ko ca Kayif miy goroom, ngir génn ci mbir mi. YOWAANA 18:25-27 Kayif daldi laaj Yeesu lu aju ci taalibeem yi. Ñaar ci ñoom ñungi woon ci ëtt bi, waaye feeñaluñu seen bopp ni ay taalibeem. Piyeer, taal bi moo doon wone xar kanamu doxandéemam, ba surga ya am xel-ñaar ci li mu war a séq ak Yeesu. Piyeer dellu tontuwaat ne: «Déedéet, déet!» Kenn ca ña amoon xel-ñaar ci moom joxoñ ko baaraamu tuuma. Ñépp geestu di ko xool, noonu mu tàmbalee ñaq tooy xepp, rawatina ba surga ba nee: «Xam naa la, yaa nga woon ca tool ba ak Moom.» Doyoon na waar ca saa sa, ndaxte waa jooju mbokku ka Piyeer coroon nopp ba la. Yowaana faramfàccewul tontu Piyeer, walla ni mu weddee Yeesu, waaye biral na worug Piyeer gi jaaduwul cib apotar. Sabu séq gi mel ni liitu àtte bi ci noppi Piyeet. Amul kenn ci taalibe yi, ku pare woon ngir topp Yeesu ba ca dee ga. Kenn ku nekk ci ñoom dafa daw, mbaa mu bàkkaar, walla mu fen mbaa it mu weddi ko. Yowaana waxunu lu jëm ci jooyi Piyeer ya ak rëccoom ga, waaye wone na ni weddi Boroom bi wóoradee. Séq gi sab na ñetti yoon ngir artu Piyeer. Su nu fenee, walla nu ragal a seedeel sunu Boroom, Yàlla dafay sabloo ag séq ngir mu artu nu. Xelum dëgg gi dafa namm a wàcc ci nun. Nanu ñaan Yeesu mu may nu làmmiñ buy wax dëgg, xol bu jub, ak xel mu wér. ÑAAN: Boroom bi, ñungi lay sant ndaxte yaay dëgg, muñ, ak Màggaay. Baal nu sunuy fen ak sunu sos. Saxal ci nun jaare ko ci sa Xel mi, ndax sunuy làmmiñ sore bépp fen. Saxal nu ci sa dëgg gi te jàngal nu nuy seede ci sa tur, ak woyofte, maandute ak fit. LAAJ:
|