Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
A - Xew-xew yi amoon diggante ba ñu jàppee Yeesu ba bañu Koy dugal ca bàmmeel ba (Yowaana 18:1 - 19:42)
1. Jàpp nañu Yeesu ca tool ba (Yowaana 18:1-14)YOWAANA 18:1-3 Yeesu wax ak Baayam, jébbal ko ruuwam, rax ci dolli bosi apotar ya ak taalibe ya. Ci ñaanu tàggatoo googu, la jeexale njàngaleem ak liggéeyam. Noonu mu dugg ci jamono metit ngir dékku sasam ni Botem Yàlla te gàddu bàkkaari àddina si. Mu dem ca ab tool, ca tundu Oliw ya, ca geneen peggu Sedroŋ ga, fa ñu daan nale reseñ. Moom ak ay taalibeem dañu fa daan làqu ngir noppalu. Dañu fa daan fanaan itam. Yudaa xamoon na bérabu sekkere boobu, noonu mu xamal ko kilifa Yawut ya. Ñooña bég ci lool, daldi dajale wottukati Kër-Yàlla ga, ak ña teewaloon Farisen ya. Yoon tere woon na kuy jàpp nit ci guddi, mbaa nga yore ngànnaay, ba mu des bu la ko kilifa waa Rom ya mayee. Ñu daldi ko yëgal guwernër bi. Waaye nag la leen Yudaa waxoon doyuleen oon; dafa leen waroon a gunge ba ca Krist. Kon Yudaa du woon ab workat rekk, waaye dafa cee dolli jébbal Yeesu ay noonam. YOWAANA 18:4-6 Xam nanu nan la soldaar ya dugge ca tool ba. Dañoo waroon a yor ay làmp yu bare. Yeesu mungi doon ñaan ak doole, taalibe ya ñoom, di nelaw. Bi muy ñaan, xamoon na ne gangoor gaa ngi ñów ànd ak workat, bi leen jiite. Jéemul a daw, ak li mu xamoon li koy nar a dal lépp. Xamoon na lépp, te mungi doon wéy di déggal Baayam. Mu jóg jébbal boppam soldaar ya; dara deñul ca màggaayam ak màqaamaam. Ci dëgg-dëgg du Yudaa moo yoole Yeesu, waaye Boroom bi moo jébbale boppam ngir nun. Mu laaj leen: «Ku ngeen di seet?» Ba ñu tuddee turam, mu tontu ci baatin ne: «Man la», liy tekki «Maa nekk», li boot turu Yàlla ci boppam. Nit ku nekk manoon na xam ci saa si ne ci Yeesu Yàllaa ngi teewoon ci biir nit ñi. Mu dellu ca tontu ba ñu joxoon Musaa: «Maay Ki nekk» (Gàddaay 3 :14). Ndax ñaan nga rey sa Musalkat? Man Maay Ki nekk, bàyyileen xel ci li ngeen di def. Man maay Aji Sàkk ji ak Ràmmukat bi, man mi taxaw ci seen kanam.» Yudaa déggoon na kàddu yooyu, te tooyaloon nañu xolam. Foofa la Injiilu Yowaana mujje tudd turam. Yowaana waxul dara lu jëm ci fóonu Yudaa ba, walla ci xaroom ga. Li soxaloon Yowaana mooy Yeesu, mi muy wone njàmbaaram ci kanamu noonam yi. Jébbalu gu ànd ak coobare googu, ci biir suufeelu moo xëtt xolu Yudaa, ndaxte Yeesu pare woon na ngir dee. Ba ñu jàkkaarloo ak màqaama moomu, Yudaa ak ña mu àndaloon dañoo deltu gannaw. Fagaru woon nañu ngir xeex ba jàpp Ki ñu Jiiñ tuuma. Te léegi, mungi leen di jubsi ak darajay Saraxalekat, ci bésub njéggal gi, naan: «Man maay ki ngeen di seet.» Ñu daanu ñoom ñépp ci suuf, te Yeesu manoon na fa jaare daw, waaye dafa taxaw ci seen kanam, di xaar. YOWAANA 18:7-9 Krist, ci boppam la xiirtal soldaar yi, ndaxte dañu doon jéem a jàppaale taalibeem ya. Yeesu nag dafa leen bëggoon a aar. Moom mooy Sàmm bu baax biy jébbale dundam ngir ay mboteem. Darajaam yéem leen lool, ñu déggal Ko. Mu dellooti ne: «Man la», mel ni ku naan: Maay mburum dund gi, Leeru àddina si, Kàddu gi, Sàmm bu baax bi, Yoon wi, Dëgg gi ak Dund gi. Man maay Musalkat bi ñu fal. Ci jëmm, Yàllaa ngi teew ci seen kanam. Turu «Yeesu» mungi tekki Yàlla dafay tànn, te di musal. Muccu Yàlla googu la Yawut ya weddi woon. Bëgguñu woon waa Nasaret ju lewet jooju, nekk seen Almasi. YOWAANA 18:10-11 Piyeer nànduloon Sàngam bi, te it jàppuloon ay kàddoom. Rax ci dolli mungi doon dajjanti ba tey. Bi mu gisee soldaar yi, mu daldi mer ba bocci jaaseem cor noppu surga Saraxalekat bu mag ba, te xaarul sax ndigalu Sàngam bi. Yowaana rekk moo nuy nettali loolu, ba Piyeer génnee àddina lu yàgg. Yowaana dafa teg tànk ci ndigalu li Yeesu jox taalibeem bi, ngir bañ deret ju gën a bare di tuuru, te bañ it ñuy jàpp taalibe yi. Yeesu teg ca wax taalibeem ya lu jëm ci Kaasub naqar bi mu nangu ci ñaanam gi. Dafa méngoo ak xareb baatin, bi amoon ci ruuwu Boroom bi, laata ñu Koy jàpp. Xam nanu ne pare woon na ngir dékku mer moomu ak àtte, boobu naroon a dal ci sunu kow. Kaas boobu, ci loxol Baayam la jóge. Naruloon a man a dékku loolu, su amuloon mbëggeel; Baay j i ak Doom ji ñoo ànd rammu nit ki. Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina si, ba joxe jenn Doomam, ji mu am kepp. ÑAAN: Cey sunu Baay, nungi lay màggal ndax sa mbëggeel gi jéggi sunu dayoo. May nga nu sa Doom ji. Nungi lay màggal, cey yów Doom ji, ngir sa yërmande, sa màggaay, ak sa dégg ndigal ba ca dee ga sax. Dawuloo ca biir tool ba, waaye dangaa taxawu sa taalibe ya, te jébbal sa bopp say noon. Sant nanu la ci li nga fàtte sa bopp, ngir sa baaxaay ak sa njubte. LAAJ:
LAAJUKAAY - 6Yów mbokk miy jàng téere bii, yónnee nu 15 tontu yu jub, ci biir 17 yii. Su boobaa dinanu la yónnee li toftalu ci njàng mii.
Yónneel say tontu te bañ a fàttee bind bu leer sa dëkkuwaay ci : Waters of Life Internet: www.waters-of-life.net |