Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)
4. Xel mu Sell mi dafay feeñal yàkkute yi gën a am solo ci li nu jot a dund démb (Yowaana 16:4-15)YOWAANA 16:4-7 Ca njalbéen ga Yeesu daanul wax taalibe ya lu aju ci ay metit, jafe-jafe walla sax ay coono, xanaa kay dafa leen doon yee ci ubbiteg asamaan yi, ak jëfi malaaka, yi aju ci Moom. Ñoom xamoon nañu kàttanu Yàlla giy yëngu ci Doom ji, te di Ko may muy def ay kéemaan. Ndànk-ndànk ña jafandu ci diine tàmbali di dëgër-dëgërlu ci kanamam, te mbooloo ma di ko dëddu ndax ragal Yawut ya. Kenn àndatuloon ak Moom, ba mu des taalibeem ya Mu naroon a tàggool lu yàggatul dara, ngir dellu ca Baayam ja. Mu wax leen lu jëm ci sonal ak dee, loolu nag duy naqar ci seeny xol. Gisuñu woon genn mujj walla fayda ci loolu; rax ci dolli gisatuñu lu leen di ñaax ngir ëllëg. Waaye seetlu nañu ne Yeesu waxul dara lu jëm ci metitam, ni ñu Ko nar a lottale, ak ci deewam gi. Ci anam yu rafet yi Mu nar a deme ca Baayam rekk la doon wax. Ñungi doon laaj seen bopp naan: «Fu muy dem?» Xaajuñu woon bëgg Koo gis muy yéeg asamaan, bu doon seen sago kay, mu toog ci seen wet. Yeesu leeralal leen ne mu demam, lu am solo la lool, ndaxte bu jaarul ci Kurwaa bi, kon Xel mi du ñów. Du ci juboo Yàlla ak nit ki, ak mbaalug bàkkaar, gi jaare ci deewu Mbotem Yàlla mi, la Yàlla di wonee kàttanam, te wàcc ciy doomam. Yeesu matal na njubte gépp ngir ñu jot dund gi ak mbëggeelu Yàlla. Deewug Yeesu moo lal Kóllëre gu bees gi, te moo lay may sañ-sañu séddoo ak Yàlla. Xel mu Sell mi dafa lay dëfal, di la biral ne Yàllaa ngi ànd ak yów, te mungi ci yów. YOWAANA 16:8-11 Xel mi man na dëfal taalibe yi, ndaxte dafay ubbi bëti ñi gëm, te di àtte xolu ñi bañ a gëm, teg ko ci kow ay sartam. Xel mi dafa nuy jàngal lan mooy bàkkaar, ak lu muy jur. Laata Krist di ganesi àddina, bàkkaar moy ndigali Yoon wi la woon, akit ñàkk a déggal coobare Yàlla. Loolu fippu la, ñàkk kóolute ak mbëggeel la doon méngool—muy dund gu Yàlla teewul te itam féwwaloo ak Moom. Bépp bàkkaar, bu aju ci teggin, wóllëre mbooloo, walla ci baatin, dañu ko jàppe woon ni moy màggaayu Yàlla. Gannaaw kurwaa bi, tekki-tekki bi dafa laal bàkkaar bi nit ki def, maanaam ni mu weddee Yeesu ni Musalkatam, mbaa rekk weddi yiwu Yàlla wi. Képp ku xebat mbaalug Yeesu sosal Ku Sell ki, te gëmuloo Yàlla Baay ji ak Yeesu Doom ji, noonu Kenneefu Ñett gu Sell gi nga. Yàlla mbëggeel la, te ku xalab mbëggeel googu feeñe ci Krist, yaa ngi def bàkkaaru dee bi lay tàggale ak mucc gi. Ca kurwaa ba la Yeesu matale muccug àddina si. Soxlaatul muy deewaat ndaxte baal na ñépp seeny bàkkaar ci bépp jamono bu mu manati doon. May nañu njubte ñépp ci kow yiw wi jaare ci deretu Yeesu. Liggéeyam dafa mel ni bu saraxalekat bu mag ba. Ñetti pàcc la amoon: bi njëkk mooy rendi mala mi ñu war a saraxe; ñaareel bi mooy tuur deret ja ca bérab bu Sell baa Sell, ngir matal mbaal gi ci kanamu Yàlla; ñetteel bi di mu barkeel mbooleem ñi gëm. Ci sarax bii, maye na barkeb Xel mu Sell, te biral nu ne ñu jub lanu. Ndekkite Krist ak delloom asamaan ñooy matal sunu njubte gi tàmbale woon ca kurwaa ba. Ngir Yeesu, li waral àtte bi du rekk tàbbal ñi gëmul ci biir safara, waaye itam bokk na ci nasaxal Seytaane ak buumu njaamam gi. Seytaane dafay soreloo nit ñi ak Yàlla. Dafa leen di def ay jaami mbañ, te soppi leen ba ñu nekk ay doomi Seytaane, yu fees dell ak ay pexe yu bon. Ci giiru dundam gu woyof gi ci kow suuf, Yeesu dafa ñaawlu rëy-rëylu naxekat yi. Mbëggeelu Doom ji daan na ku Bon ki. Ba Yeesu jébbalee ruuwam ca loxoy Baay ji, ci la daan lëndëmi Seytaane yi. Yeesu mooy boroom ndam li, donte dafa mel ni ku amul genn kàttan. Ni Mu déggale Baayam ji ba dee ci kurwaa bi, noonu la àttee Seytaane ba moxoñe ko. Tey jii, ndam loolu sunu ngëneel la. Danuy ñaan, naan: «Baay, bul nu teg ci yoonu nattu, waaye musal nu ci lu bon», ndax ni nuy dunde li ndamul Krist jur te mu aju ci kaaraange ak jàmm. ÑAAN: Sang bi Yeesu, nungi lay sant ci li nga xeex, xeex bi war te sampu ci ngoru woyofteef mbëggeel ak yaakaar. Jarajëf itam ci li nga jegeji Baay ji te matal sunu njubte. Nungi lay màggal ndaxte yaa nu taas sa barkey sarax si, jaarale ko ci Xel mu Sell mi. Aar nu ci biir mbëggeelu njubte, ndax noon wi dunu manal dara. Musal nu ci Seytaane. Na sa nguur ñów te turu Baay ji sell ci àddina si. LAAJ:
|