Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)
3. Àddina si bañ na Yeesu ak ay taalibeem (Yowaana 15:18 – 16:3)YOWAANA 16:1-3 Yeesu xamal na taalibeem ya ne dinañu leen bañ ngir ñetti mbir: Ndaxte dañoo juddoo ci Yàlla,waaye du ci àddina si lañu juddoo. Ndaxte rànneewuñu Krist, Doomu Yàlla ji ni jëmmalam. Ndaxte ñi fonk diine, ci dëgg, xamuñu kuy Yàlla, te ñungi doon jaamu yàlla ju lëndëm ju ñu xamul. Mbañeelu safara dafay wéy ba fàww. Ki jublu ci Baayu sunu Sang bi Yeesu-Krist, dañu koy jàppe ni tubbeen, noonu ñu àndak xadaru diine rey ko. Ñooñu dañuy yaakaar ne ñungi liggéeyal Yàlla. Waaye Seytaane doŋŋ lañu fi nekkal. Xamuñu ne Yàlla ju dëggu ji, mooy Baay ju sell ji. Mosuñu dund kàttanu deretu Yeesu, te it Xel ùu Sell mi wàccul ci ñoom. Noonu, xel mu bokkul fenn moo leen di xiir ci rajaxe ñi teewal Kenneefu Ñett ñu sell ñi,ci di leen noot, di leen rey ak di leen teg melokaanu coono bu nekk. Loolu la Yawut ya daan def, te mooy am ba kera Krist di dellusi. Noonu, dafa am xel mu leen wàllsi, te di leen xiir ci yàq ñépp ni fi teewal Kenneefu Ñett ñu Sell ñi, jarale ko ci di leen sonal, di leen rey ak di leen teg bépp melokaanu nattu. Noonu la Yawut ya daan jëfe, te noonu lay ame itam, ba fi ak Yeesu di dellusi. Bul xalaat ne ci ëllëg su tane lanu jëm, ndaxte nit ki dina gën a am xam-xam. Déedéet, ñaari xel yiy diiroo mbagg, ci àddina si lañuy des ba fa muy tukkee: xel mi nekk ci kow, ak xel mi nekk ci suuf. Amul benn jéggikaay ci diggante asamaan ak safara. Dangay man a am duggante gu mat sëkk ak Baay ji, Doom ji ak Xel mu Sell mi, walla nga nekk jaamu safara te tëju ci sa kaso bàkkaar. Dangay man a am duggante gu mat sëkk ak Baay ji, Doom ji ak Xel mu Sell mi, walla nga nekk jaamu safara te tëju ci sa kaso bàkkaar. ÑAAN: Boroom bi Yeesu,jarajëf ci li nga tànn dee gi ;dangaa wéy di déggal sa Baay. Buddi nu ci xelum àddina si,te jëmbat nu ci sa mbëggeel ba sunuy reen dëgër ,ngir nu sax ci Yów.Sa mbëggeel moo nuy dooleel te di nu wommat. LAAJ:
|