Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
4. Ndekkite Lasaar ak la mu jur (Yowaana 10:40 – 11:54)
d) Sanedreŋu Yawut yi àtte na ne dañu war a rey Yeesu (Yowaana 11:45-54)YOWAANA 11:45 Lasaar dundaat na gannaaw deewam; Lekk na, naan, te wax. Nit ñi gis nañu ko ci mbedd mi, ak ca këram. Ñu bare waaru woon nañu ci màqaama Yeesu, te nangu ne mooy Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund gi. Noonu limu taalibe ya di gën a yokku, te nit ña di fàq ngir ñów ca këru Maryaama, ngir gis Yeesu ak Lasaar. YOWAANA 11:46-48 Ñenn ca ña fekke woon Kéemaan ga, waaxu dem nettali lépp Farisen ya. Ba tey gëmuñu ci dara. Dañu koy dàkkentale seen àtte bi ak léebu « Boroom qlql «, ba Ibraayma tintu woon ne ko: « Bu ñu dégluwul Musaa ak Yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.» (Luk 16 :31). Xelum Yàlla mi manul a soppi xolu doj bu bañ a dénk boppam Yeesu, bu fekkee sax teg na bëtam ci kéemaan yu gën a rëy yi. Farisen ya dañu daan suuxlu bu metti Sanedreŋ ba ci mbirum diine. Looloo tax sax ba xudbakat yu mag ya mujje leen a may baat ca kureel ga .Ñu tànn 70 ñu war a lijjanti mbir mi. Saddusen, ya gëmuloon ndekkite, daldi nangu wooteb ndaje Sanedreŋ ba. Ña ca bokkoon xamuñu woon ban dogal lañuy jël, noonu ñu jaxasoo, ndaxte Yeesu defuloon bàkkaar bu jar ñu Koy daan. Waaye nag, ngëmug kercen mungi doon tàmbale yaatu ca askan wa, te it ay fukki-junny-junni nit ñungi doon ajsi ci Péey mi, ngir màggal Bésu Jéggi ba, maanaam Pàk. Ci waxtaan ya ca topp, waa Sanedreŋ bi jàppe yeesu ni nitu neen, tegu ñu Ko sax ni nitu Yàlla, rawatina ab Yonent. Ak li ñu Ko doon weddi lépp, terewul manuñu ñàkk a gis kéemaanam yu rëy yi. Ca biir waxtaanu àtte ba, ragal daldi jàpp waa Sanedreŋ ba. Dañu bañoon nguur ga leen yilifoon dégg mbir mi te dugal ci loxoom. Dajaloo bi mbooloo mi di def, wër nit kii di def ay kéemaan, mel ni mooy Almasi bi, dafa nar a indi ag fippu. Te bu loolu amee, waa Rom yi dinañu tere ku dugg ca Kër-Yàlla ga. Rax-ci-dolli, dinañu dakkal bépp jaamu ca biir kër ga, muy sarax, ñaan ak barkeel. YOWAANA 11:49-52 Bi mu gisee ne waxtaan baa ngi jeng, Kayif saraxalekat bu mag ba daldi jël kàddu, di dal ci kow njiiti réew mi, di leen di jiiñ ñàkk xam-xam ak xalaat. Amoon na sañ-sañu jël kàddu gi, ndaxte moo nekkoon njiitu Sanedreŋ bi. Sotti woon nañu ko diwlin, liy mandargaal sellaay, waaye ku bañ Krist la woon. Manoon naa fees dell ak Xel mu Sell mi, te kon Yàlla naroon na wax ak moom ni njiitu réew mi. Dafa toppoon nafsoom, ba def njuumte. Bi muy jàppee liggéeeyu saraxalekat ni moom, ak Nekk Yonnent, benn la, ca la tege ñépp ni ñu amul xel. Xel mi doon wax ci Kayif, feeñ na, ndaxte Seytaane moo doon waxe ci moom, waaye ànd na ak li Yàlla tëral, waaye dëgg gi wuute na. Dëgg la ne mbotem Yàlla mi wuutu askan wi moo gën ci ñépp, ngir ñu man a rëcc ci merum Yàlla te am dund gu dul jeex ba fàww. Waaye ki Seytaane yebal, dafa joxe boobu xalaat, ngir lijjanti mbir mi, jaare ko ci politik: « Na Yeesu dee ngir musal nu ci merum waa Rom yi. » Ak waxinu seytaane woowu, Kàdduy Krist dëggu nañu, maanaam Seytaane mooy baayu baatinu Yawut yu bare, ndaxte moom fenkat la, te it mooy baayu kàcc ci boppam. Ak xelum Seytaane moomu mépp, terewul Yowaana gis ne Kayif xalaat yu bon la doon digle, yu làqoon dëggi baatin. Kayif dafa waroon a xamle deewug Yeesu ni goreelug ñépp, te bañ a seetlu waxam yuy wone « Sañ-sañam » Ki amuloo xel kay mooy Kayif ndaxte gëmuloon Yeesu, du sax bu ko Xel mu Sell mi xiiroon ci wax ay kàddu yu aju ci mucc gi nekk ci deewu Krist. Xamuloon sax li muy wax lu mu doon, ndaxte lu juuyoo ak loolu la bëggoon. Yowaana taskatu Injiil bi gisoon na li wax jooju di tekki ci li aju ci muccug àddina si. Yeesu deewul ngir gàddu bàkkaari askanam kese, waaye boole na ci yu askan yépp. Ñépp ñi Ko dénk seen bopp, ay doomi Yàlla lañu, ndaxte ni ñu Ko dénke seen bopp, noonu lañuy jote dund gu amul àpp gi, boole ci kàttan ak njariñ. Sunu ngëm yemul rekk ci sunu muccug bopp,waaye dafay laawaale jokkoo doomi Yàlla yépp yi nekk ci Krist. Mbëggeelam mooy dajale( boole) ay taalibeem. Bu ñu jokkoo ak bopp bi, kon dañuy nekk benn. Nanu yeewu te jubal ci Moom. Dinanu gis ay Mbokk yu bare yu bokk ci njabootu Yàlla gi, muy mbokk gu gën a dëgër, gi nekk ci àddina si. YOWAANA 11:53-54 Kàdduy Kayif neexuñu woon ñenn ña bokkoon ca mbootaayu Sanedreŋ ga te doon jàppale Yeesu, waaye ña ca ëppoon nanguwoon nañu li Kayif digle, yaakaar ne Yàlla moo waxe ci moom, ngir dogal àtte boobu ci kow naxaatekat bi, ngir musal askan wi. Ñu mujj déggoo, ba Sanedreŋ bi nangu xalaatu Kayif bi aju ci rey Yeesu. Ña ca gënoon a jub, jéem nañoo bañ ba tàyyi, waaye dara. Kayif ak muusaayam, fexe na ba nanguloo leen ñu bóom Yeesu, ci nu mu gën a nëbboo, ngir bañ nit ñi wàcc ci mbedd yi. Yeesu dégg ñuy waxtaane pexe moomu, xëy na sax xamoon na ko ci baatin. Mu jóge ca diiwaan ba Sanedreŋ ba man a ame baatu àtte, dem ak ay taalibeem ca xuru Yurdan, ca penku Nablus, di xaar waxtu wi muy saraxe boppam, ak ndekkiteem. Ȅttu xare bi kay leer na léegi. ŋaayoo ga mu séqoon ak kilifa diine ya, ca màggalu mbaar ya, ak xuloom ak Fonk-Yoon ya ndax la Mu fajjoon jarag ja ca bésu noflaay ba, léegi nag ëpp na bi Mu dekkalee Lasaar. Noonu Kilifay réew ma dogu ne dañuy rey boroom mbaax bi, nu mu gën a gaawe. Leer gaa ngi leeral lëndëm gi, te lëndëm gi nanguwu ko dalal. Mbokk mi, ndax gis nga ne Krist mooy leer gi? Ndax Injiilam gindi na sa xel te yeesal sa xol? Ndax am nga dundam gu dul jeex gi? Ndax Xelam tax na ba nga tuub say bàkkaar te nangu leen, ndax saxal na ci yów ngëm luy barkeele te di la sellal? Ubbil sa xol ngir may Xelum Krist mu man laa xëcc, jébbal ko sa dund, ak sa ëllëg ndax nga bañ a àndak ñiy nooni Krist. Fekksil taalibe yi, te jàng a xam Ku Sell ki ndax nga man a tuub te nangu ne: « Gis nanu ndamam, ndam lu mel ni lu jenn Doomu Yàlla ji moom. ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist jarajëf ci li nga weddiwul dëgg gi bi waxtu wu metti wi jotee; dangaa mos a siggil sa Baay ji ci asamaan. Baal ma ci sama ngëm gu tuut gi, ak samay ñàkk-farlu. Dimbalima ba may jokkoo, saa su nekk, ak Baay ji te di la surgawu ba fàww. Na la sama dund màggal. LAAJ:
LAAJ YI-4Mbokk mi,
Yónneel say tontu, te bul fàtte bind bu leer sa dëkkuwaay ci kayit yi nga tontoo, a kit ci ambolog bi ci fii: Waters of Life Internet: www.waters-of-life.net |