Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 070 (Jesus across the Jordan)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
4. Ndekkite Lasaar ak la mu jur (Yowaana 10:40 – 11:54)

a) Yeesu jàll na deux Yurdan (Yowaana 10:40 – 11:16)


YOWAANA 10:40-42
40 Yeesu génn, jàllaat deux Yurdan, toog fa Yaxya daan sóobe ci ndox bu jëkk. 41 Nit ñu bare ñów ci Moom te naan: « Yaxya deful benn kéemaan, waaye li mu wax ci kii lépp, dëgg la. » 42 Noonu ñu bare gëm Ko.

Jànkonte ba ca diggante Yeesu ak Farisen ya daldi fàŋŋaaral nag, noonu ñu suxlu kilifa réew ma, gannaaw ba wéralug laago ba amee ca Betesda (Saar 5). Ca njeextalu ñetteelu nganeseem ca Yerusalem, jaamaarloo ba àgg ca njobaltaxam. Leer gaangi leeral lëndëm gi, te lëndëm gi naguwu koo dalal. Dee gi dafa tiimoon Yeesu saa su nekk. Mu dellu ca Kër Yàlla ga ak taalibeem ya ngir mottali seen xam-xam ak seen kóolute, fekk mbañu noonam ya di gën a tar.

Gannaaw Màggalu Bésu Cellalu Kër Yàlla ga, Yeesu jóge Yerusalem, jàll deux Yurdan, fa Sanedreŋ ba amuloon benn sañ-sañ. Yaxya waarewoon na fa ca njalmuy fu Yawut ya amuloon baat, waaye kenn ca buuri Herood moo fa yilifoon. Yaxya siiwoon na lool, te seedeem ci Yeesu dëggu woon na.

Ña gëmoon ndax seede Yaxya, sàmmoon nañu seen ngëm ba jëm ci kanam bu baax. Seen jàngalekat ba, dañu koo rendiwoon. Ba Yeesu agsee, dañoo daw wutali Ko (gatanduji Ko), ndaxte xam nañu woyofteefam, màggaayam ak kàttanam. Yeesu xamal leen yenni màndargaam, di waare bu jekk ci Yàlla, ak ci nit ki. Ñu bare ubbil Injiil li seeni xol, ndaxte gëmoon nañu la Yaxya waxoon; te fekk sax deful genn kéemaan ngir biral ne ab Yonent la. Dañoo gaaw nagu Yeesu ni seen Boroom, ak seen Musalkat.

YOWAANA 11:1-3
1 Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Manga dëkkoon Betani, moom ak Maryaama ak Màrt, mi mu bokkaloon ndey ak baay. 2 Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko karawam. Moom la cammiñam Lasar woppoon. 3 Ñaari jigéeni Lasaar ya yónnee ca Yeesu ne ko: ” Boroom bi, sa xarit wopp na.”

Ba Yeesu doon jàngale ci diiwaanu Yurdan, mu am waa ju tudd Lasaar ju wopp. Munga dëkkoon ca dëkk bu ndaw bu nekkoon ca tundu oliw ya .Daan nañu faral di dalal Yeesu ca këram. Waxtaanu Yeesu ak Màrt jigéenu Lasar ja, siiw na lool. Yowaana waxul lu aju ci waxtaan boobu, waaye beneen téere Injiil nettali na ko. Yowaana xew-xew bi la nu indil (Yowaana 12 : 1-8) Jigéeen ju doy waar jii, dafa maroon kàdduy Boroom bi .Seede na suufeeloom, ngëmam ak mbëggeelam ci Doomu Yàlla ji.

Xabaru woppu Lasaar gi, metti woon na Yeesu. Waaye ngëmu jigéenam ya moo tax Mu dem ca ñoom. Ñaanuñu woon Yeesu ngir Mu dawsi gaaw, waaye dañu Ko yégal rekk li xew, xam ne sax manoon na ko wéral fa Mu nekkoon. Xamoon nañu ne mbëggeel gi Yeesu am ci Lasaar dina tax Mu def dara. « Lasaar » mungi tekki « Yàlla wallu na ». Tur woowu dafa mujj nekk ab bàkk ci kéemaan gu mujj gi Yowaana nettali.

YOWAANA 11:4-10
4 Bi Yeesu déggee xebaar boobu, Mu ne : « Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji. » 5 Yeesu soppoon na Màrt, Maryaama ak Lasaar. 6 Bi Mu yéggee nag ne Lasaar wopp na, Mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba Mu nekkoon. 7 Gannaaw loolu Mu ne taalibe ya: ”Nanu dellu Yude.” 8 Taalibe ya tontu ko ne: ” Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wut a rey aky xeer, nga di fa dellu?” 9 Yeesu ne leen: ” Xanaa du bëccëg fukki waxtu ak ñaar la? Kuy dox bëccëg, du fakkastalu, ndaxte day gis leeru àddina si. 10 Waaye kuy dox guddi, dina fakkastalu, ndaxte leer nekkul ci moom.”

Bi Yeesu jotee xabaar bi, xamoon na ne jaamaarloo ak dooley dee gi taxaw na. Waxoon na ne ku wopp ki, dee gi du ko mujje, waaye ndamul Yàlla dina feeñ ci moom. Ci biir Xel mu Sell mi, Yeesu xamoon na li Mu waroon a def laata xaritam ba di dee. Sañ-sañam dafay bir jaare ko ci ndekkite jenn waay, ca buntu Yerusalem. Noonu waa Yerusalem duñu am benn lay ngir bañ Koo gëm.

Ndamu Yàlla ak ndamul Krist benn lañu. Ndam li dañu ko màggal, ndaxte song na dee gi te daan ko. Li ci ëpp ci nit ñi ñungi sukkuraat ci li jëm ci dee. Nit ñi dañuy xalaat ne, dee gi, ne mes ba fàww lay indi. Yeesu xamoon na coobare Baayam, te dee gi ak li muy jur jaaxalu Ko woon, ak li Muy xam li waral dee gi lépp. Moom man na may dund àddina su wopp.

Yeesu xaar ñaari fan, laata muy dem Betani. Mu bàyyi ba xaritam ba dee. Taalibeem ya jaaxle lool bi Mu nee dafay dellu Yude. Ñoom seede woon nañu ba ñu Ko bëggee sànni ay xeer foofa. Taalibe ya, du Lasaar moo nekkoon seen yitte, te xalaatuñu woon nekk ay seede ndamu Yàlla, waaye seen bakkan lañu doon wut a sàmm.

Noonu Yeesu jël misaalu kuy tukki, tukki bu wóor ci bëccëg. Bu kooku di tukki guddi nag, man na am ay gàllankoor, walla mu daanu sax ci kàmb. Waxtu daaj ci bant baangi jegesi, waaye simili bés bi jeexaguñu. Manoon nañu doxantu ci biir Yerusalem, te dara du leen dal. Yàllaa ngi leen doon sàmm.

Ku wóoluwul xéewalu asamaan dinga dëkk ci lëndëm ni nooni Yeesu yi, ndaxte leeru ngëm gi dalul ci kowam. Noonu, Yeesu ñaan ay taalibeem ngir ñu wóolu Ko te bàyyi Ko mu wommat leen. Su dul loolu, ñàkk ngëm dina leen dugal ci lëndëm. Ci waxtu yi gën a lëndëm, li nuy dëfal mooy xam ne dara manunu dal bu neexul sunu Boroom, miy dëfalaate; Nanu wékk sunu kóolute ci Moom.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, jarajëf ci li nga nekk Kilifay dund gi; ci sa Leer lanuy gise yoon wi. Yów yaa nuy teg ci yooni njubte gi, bu nu say noon sax yéene nu alku. Dimbali nu ba nu bañ a naaje, waaye nu jekk dékku coono yi, te dee sax ngir yów. Na sunu ngëm màggal sa kaaraange gi nga nu uufe.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu di wax ci ndamu Yàlla, bu Lasaar deewee sax?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2025, at 04:56 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)