Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
4. Ndekkite Lasaar ak la mu jur (Yowaana 10:40 – 11:54)
a) Yeesu jàll na deux Yurdan (Yowaana 10:40 – 11:16)YOWAANA 11:11-16 Dañoo wone Lasaar ni seen « xarit ». Lasaar daan na faral di ganale Yeesu ak ay taalibeem. Kon moom xaritu taalibe yépp lawoon. Man nanu ko xoole Ibraayma mi ñu doon woowe « xaritu Yàlla ». Yeesu dafa ne Lasaar mungi nelaw, ngir wone ne dee jeexalul (dakkalul)dund. Sunuy yaram dañuy seey, waaye sunuy ruu dañuy dund. Sunu noflaay, ci sunu Boroom la nekk, jaare ko ci sunu ngëm. Xel mu dal, ak jàmm ji nu am ci dundam, doy na nu, te xam nanu ne dinanu bokk ci ndekkite Musalkat bi. Dinanu dund bu fàww. « Maa ngi dem yeeyiji ko », la Yeesu wax ak kàddu gu wóor, bosam Waxul: « Nanu ñaan ngir xam li Yàlla bëgg nu def ko, ak nan lanu war a dëfale njaboot gi. » Déedéet, Yeesu waxtaanoon na ak Baayam ba noppi, laata ñu Koy yëgal deewu xaritam bi. Xamoon na ne ndikkite Lasaar mooy jiitu ci ndam li. Kéemaan googu dina dëgëral ngëmu taalibeem yi, te won noonam yi ne Moom rekk mooy Almasi bi. Yeesu xamal leen ne dina dekkal xaritam bi. Dafa leen doon waxe ni yaay ju naan: « Maa ngi yeeyi sama doom; waxtu jàngi jot na. » Yeesu yox-yoxiwul benn yoon, moo nekkoon dund gi ci boppam, te yilif dee gi. Gëm Yeesu dafa nuy teggil bépp ragal, te dëggal nu ci dund gi. Taalibe ya manuñu woon jëli li ndamul Yeesu doon tekki ca saa soosa. Dañu xalaatoon ne Lasaar dafay nelaw rekk, kon jarul ñuy dem këram, ba nar cee ñàkk sax seen bakkan. Noonu Yeesu ne leen ci dëgg Lasaar dee na. Xebaar boobu tiis taalibe ya, waaye Yeesu dalal seen xol: ” Sama xol sedd na.” Lii mooy tontu Doomu Yàlla ji, bu dee dikkee. Dafa ciy gis ndam ak ndekkite. Dee du naqar, waaye mbég la, ndaxte dund la yeesu dig ay taalibeem. Moom mooy dund gi, ku Ko gë, dinga séddoo ak Moom dundam gi. Yeesu teg ca ne: « Bég naa ngir yéen,ndaxte fekkewuma deew. Am gi, te fajuma ko ca saa sa. Dee mooy àppu ku nekk. Waaye, képp ku gëm, jot dund gu bees. Nanu dem ci Moom. »Dee,ay rangooñ ak jooytu lay firi ci nit ñi, waaye, ndekkite lay firi. Nungi sant Yàlla ci li Yeesu nar a wax, bés bu sunu yaram duggee ci bàmmeel: « Nanu dem ca moom. » Ñówam moo nuy tàbbil ci ngor gi, dund gi ak leer gi. Ndaw li (Apootar) Tomaa bëggoon na Yeesu lool, te jàmbaar lawoon itam. Ba mu gisee ne Yeesu dafa dogu ngir dem ca néew ba, te xamul sax ne Yeesu dafa doon nanguji Lasaar ci loxoy dee gi, mu(Tomaa) ne moroomam ya, ci baat yu dogu: « Dunu bàyyi Yeesu; danoo bëgg sunu Boroom, te dinanu ànd ak Moom ba ca dee ga sax. Nun ñépp ci Moom lanu bokk. »Nii la Tomaa wonee kóllëreem gu amul àpp gi. LAAJ:
|