Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 061 (Christ exists before Abraham)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

g) Krist nekk na laata Ibraayma (Yowaana 8:48-59)


YOWAANA 8:48-50
48 Yawut ya ne Ko: »Ndax danoo waxul dëgg, bu nu nee nitu Samari nga te dangaa am ay rab ? 49 Yeesu ne leen : » awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal. 50 Wutuma màggal sama bopp, keneen a ma koy wutal, te mooy àtte. »

Yeesu dafa xolli muraayu kanami Yawut yooya, won leen ni ñu lëngoo ak xelum Seytaane ba bañ a xam dëgg gi.

Ba cong googu amee, xel mu bon mi sës, ba manatul bañ a wone boppam. Laata ñuy tal a tuub seeni bàkkaar, dañoo wone seen ànd ak seytaane, te nangu ne dañoo tuumaal Yàlla ci juddug Yeesu gi jaare ci Xel mu Sell mi. Ñu dàqentalee Ko Waa Samari, ji bokk ci askanu njax-réew wi. Xabaaru yeesalu diine ca biir waa Samari, dafa agsi woon Yerusalem te Yawut, ya bañoon yeneen xeet ya, seeni xol tàngoon ca lool.

Genn wàllu mbooloo ma xamoon na cosaanu yawut bi Yeesu soqikoo, te noonu lañu jéngoo ne Yeesu Yawut la. Waaye ñeneen ña lànk ne ci kàttanu Seytaane lay defe ay kéemaan. Ña Seytaane jàppoon, manuñu woon xam ni seen dund deme, waaye dañu daan biral ne Ku Sell ki jóge ci Yàlla, seytaane moo Ko dugg. Noonu la baayu fen gi doon soppee seeni xel, ba ñuy gise lu ñuul, ni lu weex, te lu weex, ni lu ñuul.

Ci teeyaay Yeesu tontu mbooloo mu gumba ci baatin moomu, ne leen: »Seytaane nekkul ci man, damaa fees dell ak Xel mu Sell mi. Amul sax ferñeetu mbon gu nekk ci man ba di ma xiir ci li àddina di yóotu. Damaa rembax ak dëgg, ak mbëggeel; te dunduma ngir man ci sama bopp. Yéguma kenn ku dul sama Baay, te Moom laay sargal; loolooy sama jaamu ji yenu maanaa. Damay biral turu Yàlla, te di sellal Baay ji ci sama doxalin. Waaw, dëggu Yàlla laa leen feeñalal, ngeen bañ ma ndax li ma wax ne Yàlla mooy sama Baay. Xel mu bon mi leen solu nàmmul benn yoon jóge ci yéen, ba di may Xel mu Sell mi mu koy wuutu. Bëgguleen a nekk doomi Ku sell ki. Kon yéen a ngi may tuumaal, te di ma wut a rey. Wutuma sama ndam, ndaxte maangi dëkk saa su nekk ci Baay ji. Moo may aar, di ma toppatoo, di ma sargal, te di ma màggal. Moo leen di àtte ndaxte yéen a ma weddi. Képp ku weddi Ki juddoo ci Xel mi, dinga dal ci àtteb Yàlla. Xel mu bon mi koy tere nangu Musalkat bi.”

YOWAANA 8:51-53
51 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku sàmm sama wax, du dee mukk. 52 Yawut ya ne Ko: »léegi wóor nanu ne dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yów nga naan: » kuy sàmm sama wax, doo ñam dee. » 53 Sunu Baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne yaa Ko gën a màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, koo teg sa bopp?

Yeesu tënk Injiilam, naan ñépp ñiy déglu ay kàddoom, nangu leen te denc leen ci seeni xol, dinañu ci gis kàttan ci seen dund. Dinañu am dund gu dul jeex mukk, te du ñu mos a dee. Maanaam dee gi, bunt lay doon bu leen di jëmale ca Yàlla seen Baay, te fekk du caagéen seen mbaax, waaye rekk kàddu Krist yi sax ci ñoom la.

Yawut ya mer lool naan: »Seytaane nga, dangay fen. Ña nekkoon suñu maami yonent yépp dee nañu. Kon noo man a waxe ne say kàddu dañuy may dund gu dul jeex, ñi la gëm? Ndax yaa gën Aji Sàkk ji, yow mi naan dangay maye dund gu weesu dee? Ndax yaa sut Ibraayma, Musaa ak Daawuda? Ndax dangaa teg sa bopp ni Yàlla ? »

YOWAANA 8:54-55
54 Yeesu ne leen: ”Suma dee màggal sama bopp, du am maanaa. Sama Baay moo may màggal, Moom mi ngeen naan, mooy seen Yàlla. 55 Xamuleen Ko nag. Man maa Ko xam, ndaxte su ma newoon xamuma Ko, kon fenkat laay doon ni yéen. Waaye xam naa Ko te maa ngi sàmm waxam.

Ci teey ak tekk, Yeesu tontu te wone Ki mu doon ci dëgg. Moom miy Krist, wutul a màggal boppam. Dafa màgg ba noppi, te mos a màgg. Yàlla dafay sàmm ngoru Doomam ji, te ni Baay ji nekkee ci Doom ji, noonu la Baayoo bi di mate ci Moom. Dëgg la kay ba Yawut ya waxee ne Aji Man Lépp ji mooy seen Yàlla, waaye xamuñu Ko woon bu baax. Seytaane moo nekkoon seen baay ji doon làqatoo turu ”Yàlla” te di jëfandikoo turam ci anam yu jaarul yoon, Dañu doon jaay ne ay nitu diine yu wér làñu, ndekete amuñu genn mbëggeel. Ku xam Yàlla, dafay bëgg ni Yàlla di .bëgge . Ci kow loolu, bépp diine bu wax ne sàmm turu “Yàlla” kese doy na, wonewul firnde yuy matal jariñu dund googu; ndaxte Yàlla Baay la, Doom, ak xel mu Sell. Yeneen melokaan yépp yi diine yi di jéem a sol nit ñi, ay xalaati neen lañu. Dëggu Yàlla mungi wéeru ci jokkoo gi am ci diggante Kenneefu Ñett ñi. Noonu, Yeesu dal ca kow Yawut ya, xase leen nii ne leen: ’Xamuleen Ko. Seen dund ak seeny xalaat ci ay kàcc rekk lañuy sukkandiku. Dangeen a gumba ci li aju ci dëgg gi. ”Rax ci dolli Yeesu dafa biralaat ne xam na Aji Sax ji. Bu demewul noonu, kon seedeem gi aju ci Baayoo bi dafay mujj nekk lu dëgguwul. Waaye Yeesu won Yawut ya melokaanu Yàlla ju dëggu ji.

YOWAANA 8:56-59
56 « Seen Baay Ibraayma bég na, bi Mu yégee sama ngan. Bi Mu ko gisee it, bég na ci lool. » 57 Yawut ya ne Ko: » Yów amaguloo juróom-fukki at, ba noppi naan gis nga Ibraayma? » 58 Yeesu ne leen: »Ci dëgg maa ngi leen koy wax, laata ñuy sàkk Ibraayma, fekk na ma doon Ki ñuy wax Maay Ki nekk. 59 Noonu ñu for ay xeer, bëgg Ko koo sànni, ngir rey Ko. Waaye Yeesu nëbbu, génn Kër Yàlla ga.

Yeesu dafa ne Yawut ya ne, ñoom xamuñu kuy Yàlla ju dëggu ji, te ki leen di dooleel ci seen diine mooy Seytaane, Mu teg ca di biral dundam ba fàww, giy tax ñu nangu Ko, walla ñu weddi Ko. Feeñal na itam baatinam bi Mu jëlee Ibraayma ni misaal, bi njëkk a wone ngëm. Ci noonu, Yeesu wone na ne Ibraayma dund na ak Yàlla, te bégoon na ci gis bés bi ñuy jëmmal Krist; ndaxte ci jëmal googu la li ñu digoon Ibraayma mate, maanaam, ci geñoom la askan yépp di jote barke.

Juif yi jaaxle ci niko, "Yaw ndaw nga, kon dinga gis Ibraayma mi dundu 2000 at ci ginaaw? Amaana danga dof tuuti."

Ci biir njàqare, Yawut ya ne Ko: »Yów gune gu demagul fenn, nga ne gis nga Ibraayma mi dundoon 200O at ca gannaaw? Yeesu Tontu leen nib buur: »Laata Ibraayma di am, nekk naa. »Mu wéy ci kàddu yooyu, ba yokk ci ne : »Ci dëgg-dëgg, Maa ngi leen koy wax », ndax ñu man a xam bu wér ne Moom mooy Yàlla, ni Baayam bi. Laata loolu, Yaxya jibaloon na lu jëm ci ñàkk àppu dundug Yeesu. Mbooloo ya manuñuwoon a xam dëgg googu, te gëmuñuwoon ne nit man na nekk Yàlla Aji sax ji.

Ñu jàppe seedeb Yeesu boobu nib tuumaal Yàlla, ab coog gu m, uy def Yàllate. manul a nekk. Dañoo ñaawlu woon loolu, ba xaaruñu sax ab àtte bu mbaxane buur dogal, waaye dañoo tàmbale di sànni ay xeer. Ca saa sa la ne mes. Xamuñu naka la woon, waaye waxtoom agseeguloon. Mu jaar ca buntu Kër Yàlla ga dem yoonamf.

ÑAAN: Boroom bi yeesu, nungi lay màggal; yow yaay Yàlla Aji Sax, ji gore te dëggu, fees ak mbëggeel. Wutuloo sa ndamul bopp, waaye Baay bi rekk ngay sargal. Génnee nu ci rëy ak tiitar, ndax nu bañ a tàbbi ci bàkkaar. Dimbali nu ba nuy sellal turu Baay ji ci asamaan, te am dund gu dul jeex jaare ko ci gëm La.

LAAJ:

  1. 'Lu tax Yawut yi bëggoon a sànni Yeesu ay xeer?''

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 21, 2025, at 04:54 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)