Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 060 (The devil, murderer and liar)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

f) Seytaane bóomkat bi ak fenkat bi (Yowaana 8:37-47)


YOWAANA 8:44
44 Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la mos a doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom. Buy fen, dëppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo. »

Yeesu wax na ñépp ñi Ko bañoon ne Seytaane mooy seen baay. Won na Yawut yi itam dëgg gi nekk ci ñoom, ndegam sax ñungi doon bàkku naan xam nañu Yàlla. Fonk-Yoon ya dañoo sorewoon Yàlla. Ku Bon ki, moo nekkoon seen baay.

Seytaane, fépp fu mu dem jaxasoo la fay indi. Daaneel li Yàlla sàkk rekk mooy mébétam. Dafay seet fi nu néewe doole, rekk jéem nu ca laal ci biir muusaayam, ba nu bàkkaar. Bu loolu sottee, mu daw ca kanamu Yàlla ngir jiiñ ña daanu ngir dëggal mbugalu àttekat ba; naxembaayam bi, aka ñàkk solo !

Yeesu biral ne Seytaane moo boq bépp bëgg-bëggu mbon, te yooyu bëgg-bëgg ñoo ko xañ coobare def lu baax. Dafa mujje nekk jaamu boppam, bañ ñépp. Ci xel moomu la ñépp ñi bañ Krist di dunde. Dañuy yàq ñeneen ñi, di yàqaale seen bopp, ndaxte seeni nafsu ñoo leen ciy xiir. Ñépp ñi sore Yàlla, lu bon moo leen di yóotu jaare ko ci xiirtalu Seytaane

Lan la Seytaane bëgg? Yeesu nee nanu ne bóomkat la, la ko dale ca njalbéen ga, ndaxte bëggul melokaanu Yàlla, bi nekk ci nit ki. Dafa tàggalook Yàlla, miy joxe dund gi, Ci moom la « dee ba fàww » nekk. Moo nekkoon nguuru dee gi. Li mu namm mooy rey bépp bakkan buy dund.

Naxaate bi moo waral coxorte googu. Seytaane nax na Aadama ak Awa, ñi njëkk a séy ci kow suuf, ba yóbbe leen xel- ñaar, te moyloo leen ndigali Yàlla. Dafa nax boppam itam, bi mu bëggee sut Yàlla. Dafa doon xoole boppam ni ku gën a màgg gën a rafet, te ëpp kàttan Yàlla.

Googu ngumba, mooy Seytaane ci boppam, mi manuloon a xam fi ay bëgg-bëggam war a yem, ba faf mu daanu ak jéll bu ñaaw. Krist nag? Moom, dafa safaanoo (wuute) ak lu ni mel. Dafa lewet te woyof. Li ci tiis nag, mooy ne nit ki ay naxee-mbaay, ak bare-tiitar (rëy) ñoo ko gënal ni Yeesu ñàkkalee solo mbiri àddina si. Noonu fenkat bi dafay ñaax gangooru fenkat, guy fen rekk, ni jaan di dugale tooke ci dundu nit ki. Kenn ci ñoom wóoluwul moroomam.

Dafa am jigéen ju ne woon yaay ja: »Ñépp ay fenkat lañu, dañuy jeyante ak ay ree; te ku ci nekk boppam lay sargal, elew yi, dañuy sàcc ci joŋante lijjaasa yi, jaaykat yi, di nax seeni kiliaan. Ci biir Kër yi sax wujj yi dañuy naxante. Kenn wóoluwul sa bopp, moone ku ci nekk yaangi jàppe sa bopp ni ku jub te gore.”

Seytaane dafay xiire ci fen ! Ay fenam nag, dañuy àndaale ak tuuti dëgg. Seytaane dafay fexe ba bépp fen niroo ak dëgg. Mooy naxekat bi, te mooy baayu fen gi.

YOWAANA 8:45-47
45 Waaye man damay wax dëgg, moo tax gëmuleen Ma. 46 Kan ci yéen moo man a seede ne, bàkkaar naa? Su ma waxee dëgg nag,l u tax dungeen Ma gëm? 47 Ku nekk doomu Yàlla, dina déglu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Yàlla, moo tax dungeen déglu.”

Yeesu rekk moo wax dëgg gi, te feeñal dëggu Yàlla gi. Barkeel ngeen yéen ñi gëm ay kàddoom. Moom xam na dëggu lépp li am ci jaww ji, waaye dafa suufeelu te am kóllëre ci lépp li Muy wax.

Am na ñu bare ñu dul nangu xabaar bu baax bu dëgg jooju, ndaxte Yeesu moo ko yégle. Bu fekkoon ne ab njiitu politik, walla ku sos diine moo wax li Yeesu wax nii, kon nit ñu gëm ko. Waaye, bu Yeesu waxee ni nitu neen, nit ñi weddi Ko, ndaxte màqaama ak kilifteef moo leen gënal fuuf woyofteef.

Yeesu laaj na Yawut ya: »Lu tax gëmuleen? Ndax dangeen a gis ci Man lu jaarul yoon, walla rëy, mbaa doxalin wu jubadi? Déedéet. Dëgg rekk laa mos a wax, te dund ko. Man maay dëgg, gi ñu jëmmal, set ci tooñ, jub, ñàkk muusante ak naxaate. »

Mujj gi Yeesu ne mbooloom ma: ’Ku bokk ci Yàlla, dinga dégg ay kàddoom, te xàmmee baatam. Ab xale dafay ràññee baatu waajuram; ak baatu ñeneen ñi. Bu ndey ji déggee doom ja di jooy, dafay daw ca moom. Noonu la ñi Yàlla woo di dégge baatu Baay ji ci asamaan, waaye ñi manul a dégg Injiil, bokkuñu ci Yàlla; Nit man na fonk diine, di jaamu Yàlla te di woor, te fekk Seytaane mooy baayam. Du sunu fonk diine moo nuy musal, waaye sunu judduwaat gi jaare ci deretu Yeesu moo nu koy may; ndax Xel mu Sell mi wàcc ci nun, te dëkk ci nun. Kuy sa baay, Yàlla, walla Seytaane? Bul gaaw a tontu, waaye méngaleel say mébét ak yu ku Bon ki, boo noppee nga méngale leen ak jëfi Yeesu. Boo weesoo loolu, nga rëccu te tuub. »

ÑAAN: Sama Baay bi ci asamaan, maangi lay sant ci li nga ma gindi ci liy dëgg gi aju ci samay bàkkaar,a k ci sa mbëggeel gi. Baal ma samay kàcc, te goreel ma ci mbañ ak rëy. Foqati ma ci doole Seytaane, ndax ma man a jébbalu ci Yow, te bañ a dëkk ci ngumba. Ubbil samay nopp ak sama xol ngir ñu dalal sa Injiil, te fexe ba ma nekk ku lewet te gore.

QUESTION:

  1. Yan melokaani Seytaane la nu Yeesu di won ci bu leer?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 21, 2025, at 04:40 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)