Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 059 (The devil, murderer and liar)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

f) Seytaane bóomkat bi ak fenkat bi (Yowaana 8:37-47)


YOWAANA 8:37-39
37 Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen.Waaye yéen a ngi may wut a rey,ndaxte li may jàngale xejul ci yéen. 38 Li ma sama Baay won laay wax ;waaye yéen,li leen seen baay di wax ngéen di def. »39 Ñu tontu Ko ne : »Ibraayma mooy sunu Baay. » Yeesu ne leen : » Bu ngeen dee waa këru Ibraayma, kon dingeen jëfe ni moom.

Yawut ya dañu jàppewoon seen bopp ni doomi Ibraayma, te ci kow geño googu ñu bokke ci baayu Ndigal yi (Yoon wi), dinañu donn li Yàlla dig surgaam bi koy déggal.

Yeesu weddiwul ngëneeli jokkoo googu, waaye dafa tiisoon ci gis ne doomi Ibraayma yi amuñu woon seen xelu maamaat. Xel moomu moo ko doon may mu man a déglu baatu Yàlla, te deñc Kàddoom. Ci noonu itam, dégluwuñu Kàdduy Yeesu. Kàddu yii manuñuwoon a dugg ci seeni xol, te manuñu woon leen a leeralal. Ñu des ca seen ñàkk a xam ak ñàkk ngëm.

La Krist doon wax ñoru leen woon,xanaa kay dafa leen yokk mbañeel ak weddi. Moone ñu bare ca ñoom xalaatuñu woon rey Yeesu. Waaye Yeesu feeñal seeni mébéti xol. Xamoon na ne mbañeel man na jur bóom. Du yàgg dara dinañu tàmbalee yuuxu naan: ” Daaj-Ko ci bant, daaj Ko ci bant!” (Maccë27:21-23, Yowaana 19:15).

Ibraayma dafa dégg baatu Yàlla, rekk déggal Ko ci saa si. Waaye Yeesu nag Moom, dafa doon dégg saa su nekk baatu Baayam ji, te daan gis ay jëfam ak màggaayam. Peeñoom dafa mat sëkk, te jóge ci jokkoo gu teŋ ak Yàlla. Yeesu mooy Xelu Xelam, te Mooy mbëggeelu mbëggeelam.

Waaye Yawut ya dañu bañoon Ki Baay ji jur. Loolu wone na ne jógewuñu ci Yàlla ju dëggu ji. Seeni xalaat feneen fu dul ca Yàlla lañu jóge. Bi ñu tolloo foofa ci waxtaan wi, Yeesu indi leen ci xool kan mooy seen « baay ».Du woon Ibraayma de !

YOWAANA 8:40-41
40 Léegi nag ”yéen a ngi may wut a rey, Man mi lee di jottali dëgg, gi ma jële ca Yàlla. Ibrayma deful lu ni mel. 41 Li ngeen donne ci seen baay rekk ngeen di def. ”Ñu tontu Ko ne: ” Nun de dunu ay doomi araam, benn baay rekk lanu am, mooy Yàlla.

Yawut ya xaajuñu woon a bëgg kàddu Krist ya, ndaxte dafa leen jiiñoon ne toppuñu yoonu xalaatu Ibraayma. Seen ngëm, seen yaakaar, ak seen bare tiitar yépp ñungi wéeru woon rekk ci li ñu bokke ci genos Ibraayma. Lu ci yoonu Yeesu ba Muy am sañ-sañu dugg ci seen diggante ak Ibraayma, ba di ko bëgg a tas ?

Yeesu won leen itam ne Ibraayma mataloon na ay mbir ci kow gëm Yàlla, maanaam lu mel ni ba mu jógee réewam di gàddaay. Kóolute gi mu amoon ci Yàlla feeñ na ba mu jekkee ngir jébbal Yàlla doomam Isaaxa, ni sarax bu ñuy rendi. Gis nanu itam suufeelu gi mu won jarbaatam Lóota. Waaye Yawut ya dañu dëggëroon bopp, di fippu, te ñàkk ngëm. Seen xel ànduloon ak xelum Krist. Noonu ñu weddi dëgg gi ñu jëmmal, ji taxaw ci seen kanam; te dégluwuñu baatu Yàlla bi doon waxe ci Moom. Yeesu ñëwul ni Doomu Yàlla ju ay malaaka dar ci biir ndamam, waaye ni nitu neen, ku àndak kàddoom yuy dal bu baax. Forsewul kenn ngir mu nangu Injiilam li. Dafa feeñal mbëggeelu Yàlla, yiwam, ak turam. Ñoom nag, ñoo weddi xabaar bu baax boobu; boole ca mbañ gu rëy. Ñu tàmbalee mébét nu ñu Koy reye. Loolu dafa juuyoo ak melokaanu Ibraayma, aky jëfam, moom mi doon dégg, di topp, di dund te di jëfe ak li dëppook kàddug Yàlla.

YOWAANA 8:42-43
42 Yeesu ne leen : » Bu Yàlla doon seen Baay, dingeen ma bëgg, ndaxte ca Moom laa jóge, ñów ci ndigalam. Ñówaluma sama bopp, waaye Moo ma yónni. 43 Lu tax dégguleen li Ma leen wax ? Li ko waral mooy ne manuleen koo déglu. »

Yeesu xamal Yawut ya ne Ibraayma du seen baay, te it Mu may leen ñu ràññee turu seen baay dëgg ji ñu doon topp. Dañu koo niroowoon ci bépp fànn.

Yawut ya yég ci seen bopp ne Yeesu teg na wuute-wuute gu rëy ci digganteem ak ñoom. Ñu xataraayu, ne duñu ay doomi araam, ni waa Moab yi ak Amonit yi (waa Amoon) ñoo xam, ne ci séy ak seeni doom, lañu juddoo. (Njalbéen 19:36-38), te duñu it ni waa Samari, yiy xeet wu rax, wi doon biral ne Yàlla mooy seen Baay, te wékk ko ci téere Gàddaay ga 4:22 ak Detoronom32:6, boole ca sax Esayi63:16. Ba Yeesu nee Yàlla mooy Baayam, ñoom it ñu ne Yàlla seen Baay la itam bu ñu ko jaaralee ci Mbind mu Sell mi. Tarixa la woon ci seen ngëm, gu ñu yàgg a xeex te sonnoon ca lool. Waaye seen seede dëgguwuloon.

Yeesu tënk wax ji ngir won leen ne dañoo juum. Mu ne : » Bu Yàlla nekkoon seen Baay, kon dingeen ma bëgg, ndaxte Yàlla Mbëggeel la, du mbañeel. Dafa bëgg Doomam ji génne ci Moom, te Doom ji dafa fees dell ak lépp li ci Moom. »Yeesu mosul a beru Yàlla, du sax di diggante xef ak xippi, waaye dafa Koy déggal ni Apotar (Ndaw lu) bu dégg ndigal.

Noonu Yeesu laaj Mbooloo ma ne leen: ” Lu tax manuleen a dégg samay wax? Moone làkkuma làkku ñeneen de, waaye Maa ngi leen di may sama Xel ci kàddu yu woyof, yu gune gu ndaw sax man a dégg. ”Yeesu tontul boppam laajam ba: ”Manuleen a déglu; dungeen ay gor, waaye ay jaam ngeen; seen dundu baatin dafa réer. Dandeen a mel ni ay tëx yu dul dégg woote bi.”

Mbokk mi, nan ngay dégloo baatin? Ndax yaangi dégg baatu Yàlla ci sa xol? Ndax yaangi dégg baatam bi bëgg a laabal sa biir, te teg lépp ci yoon? Walla dangaa doylu te tëx, ndaxte am na xel mu la solu ba poñe la? Ndax Yàlla ngay liggéeyal ci kow kàttanu Injiil li, walla dafa am xel mu bon mu dëkk ci yów, te lu mu la sant nga def ko?

LAAJ:

  1. Nan la Yeesu wonee Yawut ya ne duñu doomi Ibraayma ?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 21, 2025, at 04:30 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)