Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- John - 058 (Sin is bondage) This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)
e) Bàkkaar jaam la (Yowaana 8:30-36)YOWAANA 8:30-32 Seede bu suufeelu te daw yaram bi Krist def, laal na xolu ñu bare ñi Ko doon déglu. Ñu mujje nangu ne ci Yàlla la jóge; Yeesu yëg ne wóolu nañu Ko, noonu Mu dalal seen ubbite xel. Ndax Xelam man a tuuru ci seen xol ak seeni xel te du am benn gàllankoor; te noonu Mu man leen a matalloo coobareem. Képp ku topp kàdduy Krist dinga gis dëgg gi. Ndaxte dëgg gi du xalaati neen, waaye lu am la, te nu koy dund. Dëggu Yàlla kàddu gu gore la te maandu; teg ci, mooy xam Yàlla ni Baay, Doom ak Xel mu Sell mi ci biir jokkoo mbëggeel. Bu nu saxee ci Krist, danuy xam rafetaayu (jekkaayu) Kenneefu Ñett bu Sell bi. Xam Yàlla dafay soppi sunu dund.Dafa nuy xiir ci bëgg ñeneen ñi, yewwi nu ci Bopp-sa bopp. Ku amul mbëggeel, xamuloo Yàlla. Di waxtaan ci rëccu te tuub say bàkkaar walla ci wareefi Yoon wi, du tax nu génn ci buumu njaamu bàkkaar. Li nuy goreel mooy mbëggeelu Yàlla, nangu mbaalu Doom ji ak ñówu Xel mu Sell mi ci sunug dund. Mbëggeelu Yàlla man na itam dagg jéngi « bopp-sa bopp » yi. YOWAANA 8:33-36 Yawut ya dañu ne woon xojj di xoole; seeni maam nekkoon nañu ci buumu njaam ca nguuru Firawna ca Misira lu tollook ñeeti téeméeri at, te dañoo jàppoon ne Kàttanu Yàlla moo leen yewwi woon ca buumu njaam googa (Gàddaay 20 :2). Kon niYeesu weddee seen goreel gi, dafa jeexal seen xol. Yeesu dafa waroon a toj tiitaru ña Ko tàmbale woon a gëm. Dafa leen won ne ay jaami bàkkaar lañu te ñungi ci kaso Seytaane. Bu nu manul a natt diisaayu li nu tënk te di nu sànk, sunu xel du nekk ci wutum mucc gi. Ku yég ne manuloo daan bàkkaar, na ñaan Yàlla Mu musal ko. Gis nanu fii li tax ba ñu bare duñu wut Yeesu; dañuy xalaat ne soxlawuñu muccam gi. Yeesu dafa biral ak doole ne: »Képp ku bàkkaar, jaamu bokkaar nga. »Ñu bare li ñuy tàmbalee seen bés mooy fen, dunde tàyyeel, ak ay caaxaan. Dañuy neexoo ak bàkkaar, te di dunde ay génti kese; dañuy mujje topp seen yoonu bopp. Dañuy jéem a toppandoo yenn doxalin yu bon ba, miin leen. Bu ñu demee nag ba tàmbali yég ne nekkuñu ci yoon, te di yëg li seen xel di leen di jiiñ, dafay fekk bey wey na buus; Ay jaami bàkkaar lañuy doon. Yenn saa yi sax ñu bóom nit te duñu ko tey. Nit ñi dañu soxor, buñuy nëbb sax dëgg gu ñagas gi, ci mbubboo diine ak laabiir. Ku àndul ak Krist, sa jaamu bëgg-bëggu yaram nga. Seytaane dafay fowe say cër ni ngelaw di def xobu garab bu wow. Doomu Yàlla ji joxe nag Kàddu Buuram: »Ba léegi Maa ngi nekkagum ak yéen te xam naa li leen tënk. Pare naa ngir jekkal leen te goreel leen, far seen bàkkaar yépp ba ñu set-wecc. Ñówuma ngir soppi (yeesal) àddina si ci anam yu woyof, walla di leen di jubbantee Yoon wu bees wu gën a xadar. Déet, dama leen a bëgg a goreel ci doole bàkkaar ak dee ak yelleef yi Seytaane di ñaxtu. Dama leen a bëgg a sàkkaat, may leen dund gu bees, ndax kàttanu Yàlla gi nekk ci yéen man a nasaxal tooke bàkkaar. Leer na ne Seytaane dina leen fiir ci junniy fànna yu nekk. Dingeen fakkastalu waaye du niy jaam, ni doom yu ŋoy bu dëgër ci seen yelleef lay doon. » « Dañu leen a jëndaat ba fàww,goreel leen ci bàkkaar ci sama njëgu deret. Ku nekk ci yéen am nga solo ci bëtu Yàlla. May na la ngor ngir nga man a nekk doom ju ñu goreel. Dama lay may ngir nga man a dunde jokkoo ak Yàlla di ko surgawu te di Ko màggal. Maay mennum goreelkat bi lay génnee ci kaso tooñ, yóbbu la ca nguuru Yàlla. Maay Doomu Yàlla ji, te maa fees ak sañ-sañu yewwi ñépp ñiy déglu sama baat. » ÑAAN: Sang bi Yeesu nungi lay sant te di la màggal, ndaxte yów yaay musalkat bi man lépp, te goreel nu ca bant ba ci coongi Seytaane. Baal nga nu sunu ñaawteef yépp. Sellal nga nu ngir nu bañ a dëkk ci mbañ ak naqar. Dimbali nu ba nu man a surgawu Yàlla, niy doom yu ñu goreel te ànd ak mbég. LAAJ:
AY LAAJ-3Mbokk mi,
Yónneel say tontu,te bañ a fàttee bind sa dëkkuwaay ba mu leer-nañ fii: Waters of Life Internet: www.waters-of-life.net |