Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 054 (Legalists bring an adulteress to Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

c) Ña fonk Yoon wi indil Yeesu jigéen ju njaaloo ngir nattu Ko (Yowaana 8:1-11)


YOWAANA 8:1-6
1 Yeesu, dellu ca tundu oliw ya. 2 ca ëllëg sa Mu dellu ca Kër Yàlla ga, mbooloo ma fa teewoon wër Ko. Mu toog tàmbali di leen jàngal. 3 Xutbakat ya ak Farisen ya indi jigéen ju ñu bett muy njaaloo, ñu taxawal ko ca diggu mbooloo ma. 4 Noonu ñu ne Yeesu: ” Kilifa gi, jigéen jii de, dañu koo bett muy njaaloo. 5 Ci Ndigali Yàlla yi, jigéen ju njaaloo, Musaa dafa santaane ñu sànni ko ay xeer, ba mu dee, yów nag, lu ciy sa xalaat?” 6 Loolu nag dañu ko doon wax ngir seetlu Ko, ndaxte bëggoon nañoo tiiñal Yeesu. Yeesu sëgg di bind ak baaraamam ci suuf.

Waa kuréel ga ñibbi ak mer mu rëy, ndaxte Yeesu rëcc na leen. Mbooloo ma nag bañ la ko kilifa ya bàyyi Muy waare ci Kër Yàlla gi. Waaye, waa Kuréel gi wéy di Ko yërndu, ak di Ko jéem a fiir. Ca ngoon sa Yeesu génn dëkk ba jàll mbartalu Sedron.

Ca ëllëg sa, Mu dellusi ca dëkk ba, dem ca Kër Yàlla ga. Génnul Péey ma diiru Màggalu Mbaar ya, waaye dafa wéy di dox ci biir noonam ya. Farisen yi dañu doon doxale ni ay alkaati yuy sàmm doxalin wu jekk, rawatina nag ci jamonoy berndeeli mbumbaay, nga xam ne sàngara si dafay bare. Ñu bett jigéen ju doon njaaloo, rekk ñu bëgg caa jaare, ngir fiire ca Yeesu; noonu ñu indil Ko ko. Su ko jéemoon a baal, kon ci kanamu nit ñi, ak Yàlla, dafay moy Aada réew mi. Waaye itam bu àttewoon Yoon, kon dina wone dëgëraayu xolam, te loolu dafa Ko naroon a ñàkkloo siiwaayam ju rafet ji. Àtteem dafa naroon a dal ñépp ñi ñu toroxal ndax seeni doxalin yu ñaaw. Looloo tax nag ñu yàkkamti woon dégg àtteem ba.

YOWAANA 8:7-9a
7 Bi laaj ya baree, Mu siggi ne leen: ”Ku mosul a def bàkkaar ci yéen, na ko jëkk a sànni xeer.” 8 Noonu Mu sëggaat di bind ci suuf. 9 Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam.

Ba Farisen ya jiiñee njaalookat ba ca kanamu Yeesu, Moom dafa sukk, di bind ci suuf si. Xamunu lu Mu doon bind, xëyna ndigalu mbëggeel gi la woon.

Mag ña xamuñu woon lu tax Muy yéex a tontu; gisaguñu ni Kiy àtte àddina si teeye, te bëgg leen a laal ci seen xel. Dañoo yaakaaroon ne pëtëxal nañu Ko.

Yeesu daldi jóg xool leen ak xol bu tiis; xoolu Yàlla la woon, te Kàddoom moo doon dëgg gi. Nee na: »Ki mosul a bàkkaar ci yéeen, na ko jëkk a sànni xeer. »Yeesu soppiwul lenn ci Yoon wi, waaye dafa ko doon matal. Njaaloo, yelloowoon na dee; Yeesu nangu na ko.

Ci kow kàddoom, Yeesu dafa àtte »Fonk-diine ya » boolewaale ca njaalookat ba. Noonu la leen dëkke ngir ñu setal seeni loxo, te sànni xeer wu njëkk wi. Muri na seeni mbuboo diine. Amul kenn ku amul bàkkaar. Nun ñépp a ñàkk doole te neex a daan. Ci kanamu Yàlla, dara wuutalewul bàkkaarkat bi ak « Fonk diine »bu naaféq. Ndaxte ñoom ñépp dañoo réer te geru. Képp ku moy benn ndigal doŋŋ, moy nga Yoon wépp, te yelloo nga mbugal ba fàww.

Mag ña ak Fonk-Yoon ya dañu daan saraxe ay mala ca kër Yàlla ga ngir seen mbaalug bàkkaar, di nangu ne ay bàkkaarkat lañu. Kàddu Krist laal seeni xel. Dañoo bëggoon a jàpp waayu Nasaret ji, waaye Moo feeñal seen coxorte, te àtte leen.Te it Ku toppoon Yoon wi la. Tiiñalkat ya lem seen loos,xam ne Doomu Yàlla ji lañu jàkkaarloo, ñu ragal lool sellaayam gi.

Mag ña ak seeni parparloo dem, bérab ba ne wéyëŋ. Yeesu doŋŋ des ak jigéen ja.

YOWAANA 8:9b-11
9b Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam. 10 Mu daldi siggi ne ko: »Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ? » 11 Mu ne Ko: » Kenn, Sang bi. » Yeesu ne ko: »Man it ci sama wàll, duma la daan, waaye bul defati bàkkaar. »

Yeesu xool jigéen jiy lox, ne ko ak yërmande: »Ana sa jiiñkat ya? Xanaa amatul kenn ku lay àtte te war laa mbugal? »Jigéen ja xam ne Yeesu mii, Ku Sell ki, naru koo mbugal, monte Moom rekk Moo ko sañoon a teg àtteb ndaan.

Yeesu Ku bëgg bàkkaarkat yi la; dafa ñów ngir wutsi ñi réer. Manuloon a mbugal jigéen ja bàkkaaroon, waaye, dafa ko may yiwam. Ba muy dee ca bant ba, sunuy bàkkaar la gàddu ak yu jigéen ja.

Dafa lay may itam mbaal gu mat sëkk, ndaxte dafa dee ngir wuutu la.Gëmal mbëggeelam, ndax mu man laa goreel ci àtte bi. Nangul Xelum mbaalam mi, ngir bañ a àtte ñeneen ñi. Bul fàtte mukk ne yów itam bàkkaarkat nga, te gënoo ñeneen ñi. Bu amee ku njaaloo, du yów it setuloo? Bu amee ku sàcc, ndax ku jub nga? »Buleen àtte, te noonu kenn du leen àtte. Ndaxte dees na leen àtte ni ngeen di àttee, nattal leen ni ngeen di nattalee. Lu tax ngay xool ñax gi sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yów? (Macë 7 :1-4)

Yeesu artu ko ne ko bul bàkkaarati. Li Yàlla santaane du deñ, te kenn waru cee woyofal dara. Yeesu fexe na ba jigéen ja nammoon mbëggeel, dellusi ci Yàlla, nangu bàkkaaram te tuub ko. Kon book dina jot Xel mu Sell mu deretu Mbotem Yàlla mi. Dafa koo sant mu dunde sellaay. Lu manuloon a nekk la, waaye may na ko doole ji ñu rënkal boroom xol yu toj yi. Mungi lay sant nga bañ a bàkkaarati; jekk na ngir déglu sa rëccu xol.

ÑAAN: Sàng bi Yeesu, rus naa ci sa kanam ndaxte gënuma njaalookat ba. Baal ma ci li ma àttee ñeneen ñi, te gaañ leen. Sellal ma ci bépp ñaawteef. Maangi lay sant ci mbaal gi nga ma may. Maangi lay gërëm ci sa muñ ak sa yërmande. Dimbali ma ba ma bañ a bàkkaarati. Dëgëral ma sama dogu bi te takk ma ci cellaay. Dugal ma ci dundug cellaay.

LAAJ:

  1. Lu tax jiiñkati njaalookat ba rocceeku ca kanamu Yeesu?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 14, 2025, at 01:50 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)