Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 055 (Jesus the light of the world)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

d) Yeesu, leeru àddina si (Yowaana 8:12-29)


YOWAANA 8:12
12 Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: » Man maay leeru àddina si. Ku Ma topp doo dox ci lëdëm, waaye dinga am leeru dund. »

Yeesu mooy leer gi jóge asamaan. Képp ku Ko jege, dinga ne fàŋŋ, ñu àtte la, leeral la te wéral la, ngir nga nekk leer ci Krist. Gannaaw Yeesu, amul kenn ku nu man a leeral te wéral sunu xol bu bon bi. Bu nu dajalee Xam-xam yi ak diine yi, natt leen, du ñu xaaj a doy, ndaxte dañuy dige mucc gu tegu cim xel doŋŋ ak àjjana.Ci dëgg, dañuy gën a dugal nit ñi ci ngumba gu gën a xóot te tënk leen ca. Leeru Krist dafa mel ni jant bu yànj buy dekkal ruu.Wérug ruu googu dafa laaj nga jege Yeesu ak ngëm, te nga dogu Koo topp. Bu nu dëkkee ci doxalin woowu, danuy jóge ci lëndëm, tàbbi ci leer. Danuy gis sunu yoon wi nuy yóbbu fa nu jëm, maanaam dugg ca ndamul Yàlla Baay bi ak Doom ji.

YOWAANA 8:13-16
13 Farisen ya ne Ko: »Yów yaay seedeel sa bopp,kon li ngay wax du dëgg. » 14 Yeesu tontu leen: »Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo, ak fa ma jëm. 15 Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn. 16 Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, ji ma yónni, daf ciy ànd ak man.

Xolu Yawut ya dañu doon fuddu ca kàddu Yeesu ya ba Mu nee « Maay ki nekk». Dañoo rëyoon te yëg seen bopp, jàppe seen bopp ni leeru àddina si. Dañu gisewoon seedeem ni njuumte ak lu dul dëgg, yokk guy naxaate.

Yeesu ne leen: » Sama seede dëgg la ndaxte du man maay natt sama bopp, waaye ki may natt mooy dëggu Yàlla, mi ma àndal. Xamuleen ne ci Baay ji laa jóge, te ci Moom laay dellu. Waxaluma sama bopp, waaye samaay kàddu dañoo ànd ak dëggu Yàlla. Samay kàddu dëgg lañu, te fees dell ak kàttan ak barke. »

Seeny kàddu ngelaw doŋŋ lañu,ndaxte nit ki li muy gis rekk lay jàpp. Yéen a ngi jàppe seen bopp ni ay àttekat te foog ne ci seen man-man, àtte bu jub ñeel na leen. Waaye, juum ngeen, ndaxte xamuleen ni mbir yi sosoo, li ñuy doxal ak li ñuy jur. Li koy firnde mooy ne xamuleen ma. Ci sama nekkinu nit ngeen may àttee, waaye maa ngi dëkk ci Yàlla saa su nekk. Bu ngeen xamee loolu, kon dingeen gis ci dëgg liy àddina.

Krist mooy Àttekatu àddina si, te it mooy dëgg gi ñu jëmmal. Ñówul ngir mbugal nu, mbaa yàq nu yaxeet, waaye li Ko indi mooy musal nu. Sàbbiwul (dàqul) ñu torox ñi, bóomkat yi, ak ñi ñu bañ, waaye dafa leen bëgg a musal ñoom ñépp te uuf leen ci mbëggeelam. Bul xeeb kenn, waaye nanga xool melo mi ko Yeesu bëgg a yeesalaate.

YOWAANA 8:17-18
17 Seen Yoon dafa wax ne, seede ñaari nit a gën a wóor. 18 Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mungi may seedeel itam. »

Sunu néew doole moo tax ba Yeesu wàcc ba ci Ndigal yi. Waaye dafa wax »seen »Yoon, maanaam doxalin wi ñu soxla woon ni bàkkaarkat. Ci Yoon woowu, ki nammoon a wone dëggam, dafa waroon a am ñaari seede yu war a biral lépp li mu wax ci bépp fànn ba ca gën a tuuti. Ci loolu lañu daan sukkandiku ngir joxe àtte bi. (Deteronom 17 :6 ; 19 :15). Yeesu teggiwul googu wareef. Dafa teg nangoom ni seede bu jëkk bi, te Baayam mooy seede bi Koy dëggal, di wone jokkoo gi mat sëkk ci seen diggante. Bu déggoo amul, Doom ji du man a def dara. Loolu mooy doxalinu Ñetteefu Kenn ku Sell ki. Yàlla dafay seedeel Yeesu, ni Yeesu itam di seedeelee Yàlla.

YOWAANA 8:19-20
19 Ñu laaj Ko ne: » Kuy sa Baay? »Yeesu tontu ne: »Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen Ma xamoon, xam Ko. » 20 Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jàngale ca biir Kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn manu Ko woon a jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.

Yawut ya dégguñu woon bu baax li Yeesu di wax, te bëgguñu ca woon xam lenn, sax Lépp li ñu doon yóotu mooy fiir Ko te jiiñ Ko tuumal Yàlla; noonu ñu laaj Ko: ”Kan mooy sa Baay?” Fekk na Yuusufa génn àddina lu yàgg, te xamoon nañu li Yeesu doon xalaat ba Mu naan “sama Baay”. Waaye, dañu bëggoon Mu wax ne Yàlla mooy Baayam.

Yeesu tëbul rekk tontu leen, ndaxte xam Yàlla wuutewul ak xam Yeesu. Doom jaa ngi ci Baay ji, te Baay jaa ngi ci Doom ji. Ku weddi Doom ji nooy man a xame Yàlla? Ki gëm Doom ji te bëgg Ko, kooku la Yàlla di feeñu; ku gis Doom ji, gis nga Baay ji.

Kàddu yii ñu nga leen waxe woon ca bérab ba ñu daan dajalee ndimbal ya ñu daan jagleel Kër Yàlla ga.Waroon na fa am ay takk-der yu fa daan aar. Ak la fa takk der yooya nekkoon lépp, kenn ñemewuloon a jàpp Yeesu. Loxo Yàlla moo Ko doon wottu. Waxtu wi ñu Koy wore, wi Yàlla tëral, agseegul. Sa Baay ji ci asamaan rekk moo man a dogal sa ëllëg.

ÑAAN: Krist, nungi lay màggal te di la bëgg. Àttewoo nu ni nu ko yelloo, waaye danga noo musal. Yów yaay leeru àddina si, te di leeral ñiy ñów ci yów. Soppi nu jaare ko ci say daari mbëggeel, te dalal sunu dëgëraay, ndax nu man laa gis.

LAAJ:

  1. Nan la seede bi Yeesu defal bappam ,ni leeru àddina si,man a ànde ak ni nu war a xame Baay ji ci asamaan?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 14, 2025, at 03:03 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)