Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 021 (Cleansing of the Temple)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?

1. Cellalug Këru Yàlla gi (Yowaana 2:13-22)


YOWAANA 2:13-17
13 Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu jéggi ba, mungi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem, 14 dugg ca kër Yàlla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca ëtt ba ay jaaykati nag, a kuuyu xar, a kuuyu pitax, ak weccikati xaalis ya toog. 15 Noonu Yeesu ràbb ab yar, daldi leen koy dàqe, ngir ñu génn ëttu Këru Yàlla ga, ñoom ak xar ya, ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya, 16 daldi ne: » Jëleleen fi lii ! Sama këru Baay, buleen ko def marse ! » 17 Taalibe ya fàttaliku mbind mii: » Cawarte gi ma am ci sa kër, mungi mel ni taal buy tàkk ci sama biir. »

Yeesu dem Yerusalem ngir teewe xew-xewu bésub jéggi bu réy ba, Moom ak téeméri junniy Yawut yu bawoo ci fépp ci àddina si. Dañu daan ñów di saraxe ay mbote ngir fàttaliku bés ba Yàlla aaree seeni maamaati-maam ca meram ma ndax (saraxu ) mbotem jéggi ba Bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du man a am. Bu juboo amul, màggal du am benn njariñ. Noonu la Yeesu farewoon, mbaa faxasewoon seeni bàkkaar ca dexu Yurdan ga, jaare ko ci misaal. Nangu na sóobu gi ci dee, ngir wuutu leen, muy mandarga muy wone ne dékku na merum Yàlla. Xamoon na moom ci boppam, ne mooy Mbote mi Yàlla tànn.

Bi Mu duggee ci dëkk bi,ba àgg ca Këru Yàlla ga, du rafetaayu taax maa ko yéemoon. waaye xelam a ngi doon dem ca muccug ña waroon a texe jaare ko ci saraxeem bi. Li yéeme nag, mooy ne fekkul ci Këru Yàlla gi genn dal guy xiire ci màggal. Li Mu fa fekk kay mooy tilimaay, ak coow, nag yiy yuuxu, baana-baana yuy xuloo, ak deretu mala ya. Dégg na itam coowul wecckati xaalis, ya doon weccee. Dégg na itam coowul wecckat xaalis, ya doon weccee xaalisi bittim réew ya ci xaalisu Yawut, ngir yombalal ujaaj ya seenug payoor.

Yooyu coow yépp dañoo mel ni ñuy wone ne njubte manees na koo jënde xaalis, ak yenn melo góor-góorlu yi. Ujaaj yi dañu doon xalaat ne yiw wi ak njubte gi manoon nañu ko jënde Ak ay aada aky wàll, te fàtte ne mucc gi kenn du ko jote ci ay jëf yu baax te rafet.

Ci kow doxalin woowu,Yeesu wone ni loolu selladee. Xadaram gi Mu am ci màggal gu dëggu, moo ko xiir ci sànni ci suuf xaalisu teefanke ya. Kenn waxul dóor na fa nit, waaye dañu ko misaale caw yi Yàlla di xaare ñi bañ a sukk ci kanamu Màggaayam. Amul genn topp diine ci kow suuf, gu neex Yàlla, ba mu des bu xol yu toj yuy jébbalu ci ku Sell ki.

Yeesu dafa metitlu li nit ñi faalewul sellaayu Yàlla. Ñàkk a faaydaal gu tollu noonu,ak ñàkk a xam diine gu ni woyofe, feeñal na lëndëm gi muur xol yi ak xel yi, te fekk sax joxewoon nañu Ndigal yi 1300 at ca gannaaw. Ci kow loolu, Yeesu wone merum asamaan ak xadar ju sell ngir sellal màggalukaay bi. Màggalukaay bi moo nekkoon xàmmekaayu ñépp. Kon, coppite waroon na am ci biir diine ji, maanaam coppite dëgg, ci ni nit ki mel ak Yàlla.

YOWAANA 2:18-22
18 Noonu Yawut ya ne ko: Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne, am nga sañ-sañu def lii nga def?» 19 Yeesu tontu leen: «Daaneel-leen kër-Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.» 20 Ñu ne ko: Nga ne Kër-Yàlla gii ñu tabax ci ñeet-fukki at ak juróom-benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!» 21 Waaye Kër-Yàlla gi Yeesu doon wax, nekkuloon ab tabax aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax. 22 Gannaaw ga nag, bi Yeesu deewee ba dekki, la taalibe ya fàttaliku li mu waxoon, daldi gëm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon.

Ca saa sa ba ñu déggee ne ñungay sellal Kër-Yàlla ga, ak yuuxu baana-baana ya, Njiiti diine ya fàq jëm ca Yeesu, laaj ko: «Ku la may sañ-sañu def lu mel nii?» «Ku la yebal?» Won nu firnde ju wóor juy dëggal sa sañ-sañ. Terewuñu sellal gi; Gisoon nañu ne du ci kow merum doomu Aadama, la Yeesu di jëfe, waaye xadar gu sell ngir sargal Këru Yàlla gi, ngir delloosi Xelum jaamu ci biir ñu bare. Dañoo bëggoon a xam rekk li yékkatiwoon Yeesu ak li taxoon muy jëfe noonu. Yeesu dafa mujj nekk seen noon, ndaxte dafa doon tegaat Kër Yàlla gi ci yoon, te jaarewul ci seen Kureelu Diine bi.

Yeesu xas leen ndax seen màggalu naaféq gi, ndaxte jaxasoog way-gëm yu bare, ak dooley alal, moo leen gënaloon dalu teewaayu Yàlla. Yeesu gis na ne dinañu yàq Kër-Yàlla ga, ndax seen ñàkk faaydaalu màggal, ak seen ñàkk a xam. Xew-xewi diine yi ñu tëral, ak mbootaay yi ñu jot a taxawal duñu musal nit ñi Waaye coppite xol gi jaare ci dëggu Yàlla giy muccloo, mooy soppi nit.

Musalkat bi ñu jëmmal mungiwoon ci seen biir. Yeesu mooy Kër-Yàlla gi dëgg. Yàlla mungiwoon ci Krist, teew ci biir Kër Yàlla gi. Maanaam, Yeesu nee na: ’Tojleen Kër -Yàlla gii di sama yaram, ndaxte manuleen a dékku sama xarañ gi ma am ci Yàlla. Dingeen def seen kéemkàttan ngir tojjat Kër-Yàlla gii, waaye dinaa dekkal yaram wii, gannaaw ñetti fan; dinaa génn ci bàmmeel bi. Dingeen ma rey, waaye maangi dund, ndaxte maay dund gi, di Yàlla ji jëmmoo yaram. Manuleen ma rey. Foofu, Yeesu cabaxal na leen ndekkiteem. Ndekkite loolu, ba fi nu tollu tey jii, mooy kéemaan gi gën a rëy ci kéemaan yi.

Ndawi Saraxalekat bu mag bi dégguñuwoon dëxëñu (léebu)Kër-Yàlla ga. Ñu xool kenu doji marbar yaak sooroori wurus ya, te naan ci seen biir, Yeesoongi tuumaal Yàlla ci biir bérëb bu sell, bi Erood tabax. Ñoom ñungi wax lu jëm ci doj yi, Yeesu di wax lu aju ci yaramam. Waxtaan yu am solo yooyu, ca ba muy tàmbali liggéeyam, dinañu feeñaat ba ñu koy àtte ca kanamu Kureelu Yawut, ga ñuy woowe Sanedreŋ, ci kow teewaayu seedekat yu dëgguwul.

Waa jamonoy Kóllëre gu Njëkk ga xamuñuwoon ci dëgg-dëgg li ngëm gu bees gi Yeesu tëral, di tekki. Taalibeem ya sax desewoon nañoo xam xóotaayu ngëm gu bees googu, daanaka ba ca deewam ga, ak ndekkiteem. Booba rekk lañuy door a xam naka la Doom ji deewe ngir far bàkkaar yi, te dekki.

Tey jii mungi ak nun ci Kër-Yàlla gu baatin, gi nu nekk doj yuy dund yi Xel mu Sell mi moo xamal Ndaw yi li Mbind yu njëkk ya di tekki, jaare ko ci leeralug Kàdduy Yeesu. Saint de Dieu. Ñu sàmm seen ngëm bu baax, te gore, ba ànd nekkandoo Këru Yàlla gu Sell gi.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, yow yaay màkkaanu Yàlla, ak bérëb, bi Yàlla di dajeek bàkkaarkat yi. Dimbali nu ba nuy jëfe rëccu sunuy bàkkaar, ak di la màggal, te sol nu sa mataay, ngir nu man a nekkandoo ci Néegu Xel mu Sell mi, di màggal Baay bi saa su nekk.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu dem ca Kër-Yàlla, ba noppi dàq jaaykat (baana-baana) yépp?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 15, 2025, at 01:43 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)