Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)
3. Juróom-benni taalibe yu jëkk yi (Yowaana 1:35-51)YOWAANA 1:47–51 Natanael dafa xawoon a jaxasoo tuuti ba mu xamee ne Yeesoo ngi jàng ay xalaatam. Ku gëm lawoon ci ni ko sarti Kóllëre gu Njëkk ga tëralewoon, ndaxte nanguwoon na ay bàkkaaram te tuub leen ca kanamu Yaxya, te bëggoon naa bokk dëgg-dëgg ci nguurug Yàlla gi. Nekkuloon mbiru fariseŋ, ab xol bu toj lawoon te doon ñaan Yàlla, Mu yónnee Almasi bi, Musalkat bi. Yeesu dégg na ñaan googu, fu sore, te gis na ki sukkoon ca suufu garab ga, di saraxu Yàlla. Kàttanu man a feeñal mbir yooyu làqu ci nit ki, dégginu Yàlla la. Yeesu beddiwu ko, waaye dafa koo cëral njub, te wone ko ni misaal bu sosoo ci Kóllëre gu NJëkk gi, di xaarandi ñówug Krist. Taggu Krist yi ñoo dalal xel ñaaru Natanael bi. Mu nangu Yeesu, te terale Ko raaya yi Mbind yu sell yi jagleel Almasi bi: Doomu Yàlla, ak Buuru Israel. Bi muy yékkati yooyu kàddu, Natanael mungi doon jébbal boppam ci loxoy dee, ndaxte bindkati Téere ya, ak mbootaayu kilifa yawut ya dañoo weddiwoon ne Yàlla am na Doom. Kon kàddu yu mel noonu, dañu leen jàppewoon ni tuumaal Yàlla. Te jàppe nit ni buuru Israel manoon naa tax Herod dal ci sa kow ba tëjlu la. Bii way-gëm bu dëggu nag, wone na maanaa bi nekk ci dige yi Yonent yi jibal. Moom Yàlla la gënoon a ragal nit ñi, te terale na Ko raaya Baay, te bàyyiwul xel sax li ko loolu man a jural (ci musiba). Kenn ci taalibe yi jagleeguloon Krist yooyu raaya. Doy na waar li Mu leen beddiwul, te sagal yég-yëgu Natanael ba won ko asamaan yi ubbiku. Krist, ay malaaka yu kenn daanul teg bët, ñoo Ko wëroon, di yéeg asamaan, ngir won Baay bi kéemaanam yi, ak di deelusi ci Doom ji, ak loxo yu fees ak ay barke. Noonu la Yanqóoba gisoon mate, ndaxte ci Yeesu la mataayu barke bi nekk. Ni ko Póol binde nii: ”Cant ñeel na la Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu Krist, mi nu may bépp barkeb baatin ca biir asamaan ya, ci Krist!” (Efes 1:3). Ba Krist juddoo ba leegi asamaan yi ñungi ubbeeku. Balaa loolu, dañu tëjuwoon, ndax merum Yàlla, te ay malaaka ñoo daan wottu bunt ba, ak ay jaasi. Bunt biy jëme ca Yàlla, ci Krist la ubbeekoo léegi. Guleet, Yowaana jaar ci kàddu gi Yeesu di faral a jëfandikoo: ”Ci dëgg-dëgg, maangi leen koy wax…” Jamonoy yiw wii dafa nekk lu am sag, ba romb xelu doom-Aadama, moone de, nit ki dafa koo soxla ni ponku gëmam gu bees gi. Bu ci Yeesu taxawee noonu, kon dafa fekk nu war a dal te xalaataat ci li Muy yóotu, ndaxte li topp ci Kàddu googu dafay méngoo ak peeñu mu sut sunu dégg-dégg. Gannaaw Kàddu yooyu, Krist jubbanti na seedeb Natanael ngir aar ko ci bépp bundxataal, moom ak ajàngu bu bees bi. Waxul ne mooy Buur bi ñu dige, Doomu Yàlla ji, waaye dafa tudde boppam “Doomu Nit ki”. Tur woowu la Yeesu daan faral di jëfandikoo bu daan wax lu jëm ci boppam. Yaramam rekk lañu manoon a yàq; dafa melon ni nun-Kéemaan gu rëy angi nii, Doomu Yàlla def boppam nit ngir dee ni mbotem Yàlla, ngir wuutu nu. Ca jamono jooja, turu “Doomu Nit ki, ag kumpa lawoon gu nuy gis ci téere Dañel. Yàlla teg na Àtte bi ci loxoy “Doomu Nit ki”. Natanael dafa dem ba gis ne yeesu du Buur kese, walla Doom, waaye itam mooy Àttekatu àddina si- Yàlla ji soppaliku nit. Noonu, Yeesu dugal way-gëm jooju ci dooley ngëm ju kowe. Ngëm gu takkoo noonu yombuloon ndaxte Yeesu, ab waxambaane bu jóge ca kow ga lawoon. Waaye ci ngëm la taalibe ya gisee ndam li làqu ci Moom-ak asamaan yi ubbeeku ca kow. ÑAAN: Nungi lay màggal, Doomu Yàlla jiy Àttekatu àddina sépp. Yelloowunu dara ludul merum Yàlla, waaye nungi ñaan sa mbaal jaare ko ci sa yiw, ak sa yërmaande ngir sunuy xarit. Xëppal sa barke ci kow ñépp ñiy wut Yàlla, ngir ñu man laa gis, xam la, te bëgg la, wóolu la, te màgg ci xam-xam ak yaakaar. LAAJ:
|