Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)
2. Seede yu gën a daw yaram, yu Yaxya defal Krist (Yowaana 1:29-34)YOWAANA 1:31-34 Yàlla woo Yaxya, bi mu tolloo ci 30 at, ngir mu waajal yoonu Krist, te xamal Ko askan wi. Loolu ci sóobu bi doon soppi nit ña doon tuub te nangu seeni bàkkaar, ba jekk ngir teeru Krist, la daan mate. Yàlla dafa digoon Yaxya ne dina Ko won lu kenn kenn mosul a gis, muy wàccug Xel mu Sell mi ci kow Krist. Xel mi dafa tànn ni mu tegoo ci kow Krist. Yonenti Kóllëre gu Njëkk ga dañu leen soloon ab diir, waaye Krist dafa feesoon ak Xel mi saa au nekk. Xel mi dina sol kàttanu Yàlla way-gëm yi, ba mu mel ni jamonoy meññeef mu dul rat. Yeesu ak Yaxya dañoo taxaw dend ca booru deju Yurdan; rekk asamaan ya ubbiku, noonu Yaxya daldi gis Xel mu Sell mi, ci mellow pitax mu weex tàll, ci asamaan su bulo si -loolu di misaalu jàmm ak lewetaay. Xel moomu wàccul ci Yaxya miy sóobe, walla ci ñi doon tuubsi, waaye, ci Yeesu doŋŋ la tegu, liy won Yaxya ne waxambaanem Nasaret wi Moo gën a màgg yonent yépp, ak bépp mbindeef. Yaxya xamoon na ne Yàllaa ngi taxaw ci kanamam, Moom Boroom bi ñu doon séentu. Yaxya waroon na fees ak cant, ak mbég, ni ba Mariyaama ganejee doomu ndeyam Elisabet. Booba fekk na Yaxyaa ngi ci biiru ndeyam, te fudduwoon na ak mbég (Luk 1:36-45). Yaxya xammee na woon Krist ni Kiy maye Xel mi. Dencul peeñu googu ngir moom kese, waaye dafa ko doon yégle ci biir ay xaacu naan: ”Boroom bi ñów na; teew na, te du ngir àtte, waaye ngir wone mbëggeel ak kaaraange. Du nitu neen, waaye Doomu Yàlla ju fees ak Xel mu Sell mi la. Képp ku nangu ne Yeesu Xelum Yàlla la, nangu nga itam ne Doomu Yàlla la.” Noonu la faramfàccee itam li tax Yeesu ganesi nu: maanaam, sóob ñi tuub seeni bàkkaar, ci XEL mu SELL mi. Yàlla Xel la, Doomam mooy Xelum Yàlla mi ñu jëmmal. Moo Ko soob Mu sol ay taalibeem dëggug baatin gii: Yàlla, mbëggeel la. Mbokk mi, ndax fees nga ak Xel mu Sell mi? Ndax jot ngaa mos kàttanu Krist ci sag dund? Baaxaayu baatin boobu yaa koy moom ci saa si nga nangoo ne baal nañu la say bàkkaar ci kow gëm sarax bi Krist jébbalee boppam. Képp ku nangu mbaalug mbotem Yàlla, fees nga dell ak Xel mu Sell mi. Doomu Yàlla ji jekk na ngir séddale way-gëm yépp, ay mayi baatin. ÑAAN: Yów Doomu Yàlla ji, nungi lay màggal te di la woyal. Dangaa suufeel sa bopp ngir nun, te gàddu sunuy bàkkaar. Nungi lay sant ci mbaal gi nga nu may ba ngay tuur sa deret ca bant ba. Nungi lay gërëm itam ngir kàttanu sa Xel mu Sell mi nga xëpp ci nun ak ñépp ñi la bëgg. Yeel ñépp ñiy nelaw ci seeni tooñ, ak seeni bàkkaar. Yeesal leen te sol leen sa dëgg gi. LAAJ:
|