Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 014 (Testimonies of the Baptist to Christ)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)

2. Seede yu gën a daw yaram, yu Yaxya defal Krist (Yowaana 1:29-34)


YOWAANA 1:29-30
29 Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñów ci moom, mu ne: ”Xoolleen! Kii mooy mbotem Yàlla, mi ñu nar a rey, ngir dindi bàkkaaru àddina. 30 Moo taxon ma wax ne:” Am na kuy ñów sama gannaaw, waaye moo ma gën a màgg, ndaxte, nekk na, laata may juddu.”

Ba fa nu tolluwoon nii, Yaxya dafa yaakaaroon ne Krist ab jekkalaatkat la woon buy laabal askanam, jéri peppam; Krist bu mer ba futt, yore semmiñam, ngir gor gépp garab gu feebar. Ci moom, ñówug Krist, bésu mer lay yégle. Ba mu waxee: ”Almasi bi mungi ci sunu biir”, taalibeem ya dañoo tiit ndax fàttaliku seeni bàkkaar. Dañu xalaatoon ne àtte bu gaaw bu dul tàggoo moo nar a dal ci seen kow.

Ba Krist tolloo ci 30 at la ñów ci Yaxya ngir mu sóob Ko ci ndox. Yaxya daldi bañ, ne Ko: ”Man maa soxla nga sóob ma.” (Macë 3:13-17). Yaxya dafa bëggoon Yeesu baal ko ay bàkkaaram. Waaye Yeesu xamal ko ne fàww mu sóob Ko ci ndox ngir matal li war te jub.

Yaxya gis na ne ku Sell ki ñówul ngir mbugal nit ñi, waaye ngir gàddu seeni bàkkaar. Dafa nangu sóobu bi ndaxte Moo teewal bépp doomu Aadama. Ñówug Boroom bi waruloon a nekk ci kow mer, waaye ci juboo, ak mbaal gi. Ni mu taxawewoon ca peggu Kóllëre gu Njëkk gi, noonu la Yaxya gise xóotaayu Kóllëre gu bees gi, ci biir mbëggeelu Yàlla. Coppite gu rëy googu gindi ay xalaatam.

Ca ëllëg sa, ba Yeesu dellusee, Yaxya joxoñ Ko te ne: ”Gisleen te xam ubbileen seeni bët, Moom la!” Amuloon tell-télli mbaa ay coggali malaaka, Kàddug Yàlla gi dañu ko wesaare ngir ñépp man cee jot. Waxambaane bii lañu doon séentu, Boroom bi ci boppam, yaakkaaru àddina si.

Yeesu bëgguloon nit ñi di wéy ci nañu daan jàppe Almasi bi, maanaam mu indil leen ay ndam ci wàllu politik, ak kaaraange gu aju ci màccug takk der yi. Moom mooy Mbotem Yàlla, woyof te laabiir, waaye du gayndeg Yudaa, gu am kàttan ak ndam.

Yaxya mu fees ak Xel mu Sell mi, moo ne: ”Yeesu mii, moo gàddu bàkkaari àddina si. Moo Ko neex, Mu tànn a nekk Mbotem Yàlla, miy misaalu saraxi aada ya ak cosaan. Moo yelloo wuutu doomu Aadama yépp. Mbëggeelam dafa am doole ak njariñ. Moom mooy Ku Sell ki, ak ka dul dara te gàddu bàkkaari kenn ku nekk.” Ki amuloon bàkkaar, nekk na bàkkaar ngir nun, ngir nu nekk njubteg Yàlla, jaare ko ci Krist.

Seedde Yaxya, ab daaj bu am solo la ci Injiil,liy xolu Bible bi. Dafa dem ba xam ne ndamul Krist ci coonoom ngir nun lay feeñe. Mucc gi Krist di maye, ngir àddina sépp la, xeet yépp a ci bokk, ak réew yépp. Boroom alal yi, néew doole yi, mag ak ndaw, ku jàng ak ku jàngul, ñépp a ci bokk. Démb, tey ak ëllëg yépp la boole. Deewam dafay far bépp bàkkaar. Wuutoom gi ci deewam gi, dafa mat sëkk.

La ko dale ca ba mu ñówee ni mbotem Yàlla, la tàmbalee daj jum yu bon yi, waaye taxul Mu beddi moykat bu yées bi, walla mu sewal kiy rëylu, dafa leen a boole bëgg ñoom ñépp, Xamoon na ne ay jaami bàkkaar lañu, te Moom jekkoon na ngir dee ngir ñoom.

Yaxya xamaloon na ay taalibeem ne, Mbotem Yàlla mi, goreel na leen ci merum Yàlla. Mbote mi, mooy sarax, si leen war a wuutu ci dee gi ñu yelloo. Xëyna amoon na ca ña fa teewoon, ñu doon laaj seen bopp naan ”Nan la nit man a gàddoo bàkkaar ñeneen.” Kàddu Yaxya ya gindi leen, waaye nag, seeni xel mosul a daj lu jëm ca kurwaa ba. ab xew-xew bu doy waar moo naroon a matal li Yàlla nammoon ci Krist.

Yaxya delluwaat ne Yeesu moo war a matal mucc googu, ndaxte Mooy Boroom bi, Aji Sax ji: ”Moo ma gën a màgg,te Moo ma jiitu.”

Ndamul Krist dafa màgg, waaye mbëggeelam ca bant ba feeñal na xolu Ndam li. Taskatu Injiil bi dafa biral ne: ”Gis nanu ndamam,ba ñu Ko daajee ca bant ba, ci biir metit te noonu Mu feeñal nattub mbëggeel gi nuy goreel.”

ÑAAN: Céy yów Mbotem Yàlla mi gàddu bàkkaaru àddina si, yërëm ma, Céy Doomu Yàlla Aji Sax ji, jëmmalu, baal nu sunuy bàkkaar. Céy yów waa Nasaret bu woyof bi, te rusuloo sax sunu bàkkaar, nungi lay màggal ndaxte yów yaa nu bëgg, te soppi nga nu, ba nu nekk ñu mat sëkk ci yów, ca bant ba.B ëgg nanu la, te nungi lay sant, ndaxte ñówuloo ni ab àttekat, waaye ni mbote. Yów lanu gëm, ndaxte yaa teggi bàkkaari nit ñépp. May nu maanduteg man a yégal ñeneen ñi, ne goreel nga leen.

LAAJ:

  1. “Mbotem Yàlla”,l u muy tekki?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 11, 2025, at 10:10 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)