Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 016 (The first six disciples)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)

3. Juróom-benni taalibe yu jëkk yi (Yowaana 1:35-51)


YOWAANA 1:35-39
35 Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bërab booba, ànd ak ñaari taalibeem. 36 Bi Mu gisee Yeesu muy romb, Mu daldi ne: ”Kii mooy mbotem Yàlla mi.” 37 Ñaari taalibe ya dégg li Mu wax, daldi dem toppi Yeesu. 38 Yeesu geestu, gis ne ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: ”Lu ngeen soxlawoon?" Ñu tontu Ko: ”Foo dëkk Rabbi?” 39 Yeesu ne leen: ”Kaayleen gis.” Noonu ñu dem, seeti fa Mu daloon, ngoonal Ko. Ci tàkkusaani kow la woon.

Krist mooy Kàddug Yàlla gi ñu jëmmal, Yàlla sax, ci boppam, dund gi ak reenu leer gi. Noonu la Ko taskatu Injiil bi di wonee. Wax na itam ni liggéeyu yeesu aky jëfam deme. Moom moo sàkk lépp, te Mooy aar lépp. May nanu xameelu Yàlla gu bees, giy Yàlla ni Baay ju am yërmande. Kii mooy mbotem Yàlla ”loolu rekk tënk na melokaanu Yeesu gépp.ci aaya 14 dafa ci wonewoon kan mooy Krist ak fu Mu jóge, te ci aaya 29 ak 33, leeral na ci mébétu li tax a jóg Krist.

Krist dafa jël jëmmu nit ngir ñu rey Ko, Mu nekk sarax su ñu jébbal Yàlla, Mi joxe Doomam, ngir Mu yenu sunuy bàkkaar te yewwi nu ci àtte bi, Yàlla Moo bëggoon sarax boobu, te amal na ko, ba noppi barkeel ko te nangu ko. Póol nee na: ”Yàlla jaar na ci Krist, di jubale waa àddina ak boppam, te sëfu leen seeni tooñ. Kàddug juboo googu Yàlla dénk na nu ko.” (2 Korent 5:19)

Ngir nu man a xam bu baax li “Mbotem Yàlla “ di tekki, yombul, ndaxte reyatunu ay mala ni saraxu mbaalug bàkkaar. Ab kàngam bu bokk ci aada saraxe ju Kóllëre gu Njëkk ga mooy xam baatin biy wax ne bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du man a am. Doy na waar li Yàlla tuurul sunu deret ngir mbugale nu ko sunuy bàkkaar, waaye Doomam la joxe Mu wuutu nu. Ku Sell ki dee na ngir ay fippukat yu mel ni nun. Rey nañu Doomu Yàlla ngir bàkkaari ñi tooñ, ngir may leen ñu nekky doomi Baay bi, ci asamaan, yu jub. Nanu ànd ak Doom ji, ak Xel mu Sell mi, màggal Ko, yékkati Ko, Moom mi nu rammu.

Ñaari taalibe yi ràññeewuñu xóotaayu tekki-tekkib “Mbotem Yàlla”. Waaye ni ñu gisee Yeesu, jaare ko ciy tektali Yaxya, noonu lañu name xam Ki naoon a nekk Boroom bi, Àttekatu àddina si, boole ci di Saraxu bépp doomu Aadama. Xalaat yu mel noonu ñoo uboon seen bopp, ba ñuy déglu ak seen xel mépp. Yeesu këful taalibe Yaxya ya, wante Yaxya ci boppam kay, moo leen yebal ca Yeesu.Noonu, taalibe ya déggal Ko.

Yeesu xamoon na li ñu doon séentu, ak seeny mébét. Dañoo gis ci Yeesu Mbëggeel ak yiw, te dégg kàddu Yeesu yu njëkk yii: ”Lu ngeen di wut?” Boroom bi tegu leen ay sarti diine yu diis -gann, waaye dafa leen a may ñu am buntu wax seeny xalaat. Yów nag sama doomu ndey, looy wut? Lan mooy sa mébétu dund? Ndax Yeesu nga bëgg? Ndax dinga topp Mbote mi? Jàngal dëgg yu am maanaa yii.

Ñaari taalibe ya daldi laaj Yeesu ndax man nañu Koo gunge ba këram. Laaj yi ñu dencoon ci seen xol dañoo amoon maanaa lool ba kenn manu leen waxtaane ci biir coowu mbooloo mu tollu noonu. Yeesu tontu ne: ”Ñówleen te gis.” Waxul ne: ”Kayleen ma jàngal leen.” Waaye dafa ne leen “ubbileen seeni bët, ndax ngeen gis man maay kan, lan laay jëf, luy sama kàttan, te dingeen ràññee melokaanu Yàlla bu bees.” Képp ku jege Krist dinga jot gis-gisu àddina bu bees, te xoole Yàlla ni Mu mel dëggantaan. Gis-gisu Yeesu dafay dëpp sunu doxalinu xam-xam. Moom dafay mujj nekk sunu njobaxtalu xalaat ak mébétu sunu bépp yaakaar. Kaay te gis, na ko ñaari taalibe ya defewoon. Seede nañu ca Apotar ya (Ndaw ya) ne: ”Te gis nanu ndamam, ndam lu mel ni ndamul jenn Doom ji jóge ci Baay bi, ndam lu fees ak yiw, ak dëgg.”

Bés boobu dañu yeendu ak Yeesu. Yooyu waxtu yiw, aka ñoo kéemaane! Taskatu Injiil bi biral na ne bés, bu baarkeel boobu, moo ko may ab jéegob dogu. Jamono ju yàgg gannaw loolu, mu door a xam dëgg gi aju ci Yeesu. jaare ko ci ni ko ko Xel mu Sell mi xamale,n daxte Boroomam nanguwoon na ngëmam te may ko njubte ak kóolute ne Yeesu mooy Almasi, bi ñu digewoon. Ndax leeru Krist leeral na sa lëndëmug ruu? Ndax yaangi koy topp saa su nekk?

ÑAAN: Nungi yékkati sa tur te di la màggal, yów Mbotem Yàlla mu Sell mi. Faxas nga bàkkaaru àddina si, ba juboole nu ak Yàlla. Bul nu dàq, waaye may nu nu topp la. Baal nu sunuy tooñ, feeñalal sa màqaama, ndax nu man laa jaamu ni mu ware.

LAAJ:

  1. Lu tax ñaari taalibe ya topp Yeesu?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 11, 2025, at 10:24 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)