Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)
2. Yeesu feeñu na taalibe ya ca néeg gu kowe ga (Yowaana 20:19-23)YOWAANA 20:21 Ba Yeesu delloo ca nuyóom ga, mbaalug bàkkaar ya la doon xalaat ak juboo gi, waaye dafa bëggoon taalibe yi doon ay surgay jàmm yuy indil mucc xeet yuy sànku. Ca Kurwaa ba la Yàlla baale ñépp. Dëgg gu bees gii tax na ba bóomkat yi xam ne mucc nañu, te dige biy tax doo jaar ci àtteb ñi gëm, te xam ne dee amatul sañ-sañ ci yów. Yeesu dafa yónni ay taalibeem ci àddina si ngir ñu yéene, bàkkaarkat yi jàmmu Yàlla ji. Ñépp ñi mucc ci kow Yiwu Yàlla dañuy soppeeku ci seen biir, te di baal seeny noon, ni leen Yàlla baale. Dañuy dékku sax lu jaaduwul, te di moytu di fayoo nu dul yoon. Ci ñoom la Yàlla di jaare ngir wesaare cafka asamaan ci kow suuf, ni ko Yeesu waxe: « Barkeel ngeen yéen ñiy wut jàmm, ndax dees na leen woowe doomi Yàlla yi. » Li nuy séentu ci tas xabaar bu baa bi, du soppi deminin yi walla indi jàmm jusaxul ci diggante réew yi. Dañuy ñaan kay ngir xel yi soppiku, te xol yi dëgëroon dellu nooy nepp. Ay coppite politik dinañu awu ci saa si yeesal yu mel noonu. Yeesu dafa yokk liggéeyu taalibeem yi, ba tolloole ko ak bosam: « Ni ma Baay ji yónnee, laa leen di yónnee man itam. » Nan la Baay ji yónnee Doom ji? Li jëkk, mooy ni Doom; ñaareel bi mooy ngir yégle baayoog Yàlla gi, ak sellaayam ci kàddu, ci jëf ak ci ñaan. Ñetteel bi mooy ne Yeesu dafa yorewoon Kàddug Yàlla gi, te fees ak mbëggeel gu dul jeex. Ci fànna yooyu lanuy gise njeriñal tas xabaar bi, ak li ko taxa jóg. Ci deewam la Yeesu jaare ngir def nu ay doomi Yàlla; ngir nu am dund gu sell, gu fees ak mbëggeel gu kenn dul ŋàññ. Kercen yi ay ndawi Krist lañu, yu ñu goreel, sellal leen ngir ñu nekkal fi seen mbëggeelu Baay ji ci asamaan. Bataaxal bi mooy ne Baay ji, ci deewu Krist la jaare ngir def leen ay doomam. Kurwaa bi mooy firnde seen nekkin wu bees wi, te ngëm gi mooy yoon wiy jëme ci baayoo gi. Ni Yeesu juddóo ngir dee, noonu itam ay taalibeem dinañu mos li sarax bi di tekki. Duñu kañu, waaye dañuy jàppe seen bopp ni ay surga Aji Kowe ji, ak doomi Aadama yépp. Seen Boroom goreel na leen ci seen nekkin gu yàgg ga, ngir ñu man a bëgg ni Mu bëgge. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ndaxte Yów yaa nu woo ngir nu màggal Baay ji, ak sa tur ci xel, kàddu ak ci jëf, nun ñi ko yelloowul. Jarajëf ci sunu mbaalug bàkkaar! Yaa nuy sellal ngir nu man a yégal ñeneen ñi sa jàmm ji ngir ñu xam la te dunde dëgg gi. Jarajëf, céy, Yów Krist, ndaxte def nga nu say doomi mbëggeel ngir nuy bëgg te di baale ni Yów. LAAJ:
|