Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)
1. Xew-Xew ya amoon ca njëlu bésu Jéggi ba (Yowaana 20:1-10)
a) Maryaama mu Magdala ca bàmmeel ba (Yowaana 20:1-2)YOWAANA 20:1-2 Taalibe ya ak jigéen ñi daan ànd ak Yeesu, seen xol dafa jeexoon ca la xewoon ca àjjuma ja ñu weesu woon. Fu sore lañu tollu woon di séentu fa ñuy denc Yeesu. Ba noppi ñoom ñépp ñibbi, balaa ñu leen di jiiñ ne dañoo moy sarti bésub noflaay biy tàmbali bu jantu àjjuma ji di so, ci boori 6 waxtu ci ngoon. Ca Xew-xewu bésub jéggi booba la bésub noflaay booba daloon; kenn waruloon sañuloon dem a dem ca bàmmeel ba. Fa mbooloo ya doon bége ci yaakaar ne Yàlla jubóoo na ak askanam jaare ko saraxi mbote yi ñu jébbale, kercen ya ñoom ñunga dajaloo, ànd ak tiitaange gu rëy, ak rangooñ yu tar. Seen Yaakaar gépp suulaale na ñu ko ak seen Boroom. Ca ngoonu bésub noflaay biñu doon dëgmal, jigéen ñi génnuñu woon dëkk ba te jënduñu woon dara lu ñu man a suure néew ba. Yàkkamti woon nañu fajaru dibéer gi jot. Taskatu Xabaar bu Baax bi wax na demu Mari ca bàmmeel ba, waaye it am na yeneen jigéen yu mu ca boole, ba maas «nuun» gi. Salome yaayu Yowaana ak ñeneen dem ca njël ak seeny jooy ngir defari néew ba. Suba teel la woon ba jigéen ñu jubee bàmmeel, ba ñu tayoon doj wa ñu ko ube woon. Noonu ñuy laante ci seen biir nan lañuy def ba bërëŋ doj wa. Seen yaakaar tàmbali woon na tas, ñu jàq lool. Leeru ndekkite li dalagul oon ci seen Kow, te dund gu amul àpp gi leeralagul oon seen xel. Ñu fekk bàmmeel ba ubbeeku. Loolu mooy kéemaan gu jiitu ci bés bi, te di wone ne ak lu nu jàq, mbaa jaaxle, Krist man na bërëŋ bépp doj buy noot sunu xol. Képp ku gëm, Yàlla dina la wallu. Ngëm dafay seentu ëllëg gu naat. Yowaana waxu nu dara ci peeñu malaaka yi. Maryaama mu Magdala moo daw ba rocci xaritam ya, ne saraax ca biir bàmmeel ba. Fekku fa néew ba. Ak tiitaangeem, mu daw ca taalibe ya. Dafa ko waroon a yëgali njiitu Apotar ya, ak yeneen taalibe ya. Ba Maryaama mu Magdala agsee ca Piyeer, ak ka mu àndaloon, dafa xaacu ne : « Ñàkk nanu néewu Yeesu. » Bóom ci kow bóom la woon. Looloo ngi wone itam ne taalibe ya ak jigéen, ja seen xel dafa gumba woon, ndaxte dañoo xalaatoon ne am na ku sàcc néew ba. Seen xel demul sax ci ne Boroom bi Yeesu dekki na ci biir ñi dee, ndaxte Moom mooy Boroom bi.
b) Piyeer ak Yowaana, ca bàmmeel ba (Yowaana 20:3-10)YOWAANA 20:3-5 Dawu njëkkante mbëgeel lawoon. Ku ci nekk ci ñoom ñaar bëggoon na jëkk a nekk ca wetu Yeesu. Piyeer mi gën a féete mag manuloon a rawante ak Yowaana, mi ko gënoon a nekk ndaw. Ñoom ñaar ñépp nag fàtte sax seen ragal ga ñu amoon ca yërndukat ak ña doon wottu bàmmeel ba. Noonu ñu ne baxërñet génn dëkk ba. Ba Yowaana agsee ca bàmmeel ba, duggul ndax wageel gi mu am (worma ji). Ci lëndëm gi, mu gi laxasaay ya ñu laxase woon Yeesu ca suuf, ñu mel ni wëttéenu saxu Swaa. Mbalaan ma daanuwul oon ca suuf, waaye fa tegoon néew ba la nakkoon. Loolu mooy ñetteelu kéemaanu ndekkite li. Krist xottiwul mbalaan mi waaye dafa koo génn. Malaaka ya dindiwu ñu doj wa ngir dimbali ndax Mu man a génn, waaye ngir may jigéen ña ak taalibe ya bunt bu ñu man a dugge. Boroom kay manoon naa jaar ci biir xeer wi génn. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, sant nanu la ci sa ndekkite li. Daan nga lépp luy mbon, te ubbi yoon wiy jëme ci Yàlla. Yaa ngi ànd ak nun ci xuntu dee gi, waaye doo nu bàyyi mukk. Sa dund mooy sunu dund, te sa kàttan di feeñe ci sunu néew doole. Nungi lay sujjootal, te di la bëgg, ndax may nga yaakaar way-gëm yépp. LAAJ:
|