Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)
3. Àddina si bañ na Yeesu ak ay taalibeem (Yowaana 15:18 – 16:3)YOWAANA 15:26-27 Nan la Kenneefu Ñett ñi jëfe ci kanamu mbañu àddina si ak daaj ci bant, gi ñu def doomu Yàlla ji? Dafa yónnee Xel mu Sell mi. Ñówug Xel mu Sell mi, kéemaan la ba tey jii. Ñówam gi dafay wone dugusig Yàlla ci àddina, ndaxte ci Baay ji la jóge, te dafa jokkoo ak Moom. Xel mi dafay àtte mbon gi nekk ci àddina si, te di xiir nit ñi ci sellaayu Yàlla, di leen wonaale seeni bàkkaar. Dafay dimbali taalibe yi, ba ñu man a dunde ci yoyofte ak ci fàtte seen bopp, fekk àddina saa ngi fatt ak rëy, dëgër bopp ak naxaate. Ci bépp fanna bu jiitu, Moom mooy Xelum Dëgg, giy artu niti àddina si ndax seeny ñaawtéef. Boole ci Xel mi dafay dëfal taalibe yi, naan leen, Yeesu mooy Doomu Yàlla, jiy matal mucc gi. Xel miy dëfalaate, dafay seedeel Yeesu ci sunum xel, ngir nu man a gise Baay ji ci mbëggeelu Doom ji. Xel mu Sell mi doŋŋ moo man a tax nu xam liy ngëm dëgg. Man nanu àndadoo ak way-gëm yépp ngir nangu ne amunu kàttanu dénk sunu bopp Yeesu Krist, sunu Boroom, ci kow sunu man-man kese. Te manunu ñów ci Moom itam, fi ak jaarunu ci Xelam, mi nuy woo jaarale ko ci Injiil li, te sédd nu ay mayam, sellal nu ak ngëm gu dëggu. Dafay woo kercen yépp, dajale leen, xelal leen, te sellale leen ci Krist. Dafay dëgëral seen ngëm. Xel mu Sell mi dafay dooleel sunu seede. Soo bëggee waxtaan ak ñeneen ñi ci lu jëm ci Yeesu, bul wéeru ci sa gis-gis walla ci li nga jot a dund ak Moom. Jébbalal sa lépp Xelum maandute gi. Déglul ay kàddoom ngir nga man a xam nan ngay màggale Yeesu. Su, fekkee ne yaa ngi seede may -nopp Xel mi, gu teey, dina la may nga nekk ndaw lu dëgër ngir Boroom bi. Yeesu dafa woo fukki ndawam ya ak benn, ngir ñu seedeel Ko. Loolu kay ngëneel la woon. Taalibe yooya ay seede yu tegoon seeny bët ci li taxoon Yeesu ganesi àddina lañu woon. Dañoo seede li ñu gis, dégg ko te laal ko. Seeni kàddu biral nañu li tax teewaayu Yàlla ci kow suuf, am solo. Yeesu bindul benn téere, walla benn bataaxal, xanaa kay dafa teg bataaxalu mucc gi ci loxoy Xel mu Sell mi, te dundinu taalibe yi seedeel na bataaxalam. Xelum Dëgg gi du mos a fen, waaye, ci gémmiñu taalibeem yi lay birale àddina su wopp sii, kàttanu mbëggeelu Krist. ÑAAN: Nungi lay màggal yów Doomu Yàlla, ju Sell ji, Benn nga ak Baay ji, ak Xel mu Sell mi, te bàyyiwoonu ni ay jirim, waaye dangaa yónnee sa Xelum dëgg gi ngir mu seede. Na nu sa ñów sellal! Jàngal nu ni nuy seedee ba ñu gën a bare man a mucc. LAAJ:
|