Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
B - Xew-xew yi amoon gannaaw reeru Boroom bi (Yowaana 13:1-38)
2. Workat bi ñu feeñal te mu nekk ci njaqare (Yowaana 13:18-32)YOWAANA 13:18-19 Yudaa, naqar la dunde, dara la bëgguloon ci surgawu suufeelu. Coxorte, nootaange ak mbuxum rekk la tànnoon. Dafa nammoon a ronni Yeesu cig muusaayam. Man na am mu bëggoon a xiir Yeesu ci Mu jël ngur gi. Waaye ci dëgg, noonu Yeesu la woon, bu ko doon wut a daan te bokk ci mébéti ñu rey Ko. Gisuloon li aju ci mbëggeel. Dafa rëyoon te yeesu dafa suufeelu. Ñàkk kersa, kilifteef ak coxorte ñoo jiitaloon Yudaa, fekk Yeesu moom dafa tànnoon a nekk surga bu woyof te lewet. Yeesu dafa doon waajal taalibeem yi ci lu aju ci waxtu wi ñu Koy wore, ngir ñu bañ a am xel-ñaar ci ne Mooy Boroom bi ci boppam, biy seede laata waxtu néew-dooleem di agsi, te Moom moo tudd « Man, Maay Ki nekk. »Ci kàddu yooyu la Yàlla feeñoo Musaa ca ngarag sa doon tàkk te lakkul. Dafa bëggoon a dëgëral ngëmu taalibeem yi ci kàddu yu mel noonu, ci jëmmu baatinam, ba duñu am xel-ñaar, mbaa ñuy daanu ci ay fiiri noon. YOWAANA 13:20 Yeesu teggil na ay taalibeem seen ragal bi aju ci ni ñu Koy jàppe ak deewam. Ndigal li Mu leen jox, ak teewaayam dina leen aar. Yeesu dafay yónni ay taalibeem, ba noppi ànd ak ñoom. Ay surgaam duñu dem ak seeny turi bopp, waaye ci turu Boroom bi lañuy deme. Ku leen dalal, dalal nga Ñetteefu Kenn ku Sell ki. Ku gëm seen kàddu, nekk doomu Yàlla. Sas bu diis la ndaxte dafa laaj nga man a maye sa bopp, bëgg say noon, di góor-góorlu ci biir ndóol, te it di bég ak lu man a xew, (muy lu neex mbaa mu naqari). Terewul ne xam nañu ne Yàllaa ngi ànd ak ñoom. Fépp fu ñu jëm, Mungi leen di gunge. Xelam moo leen di wommat ba fi Mu bëgg ñu liggéeyal Ko fa, ci ni Mu ko tërale,n dax liggéeyam mat sëkk. ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, dimbali ma, ba ma xam ne manumaa sax ci Yów te nekkuma sa surga. Damaa bëgg nga doon sama royukaay fu ma tollu, may suufeelu ci biir ndaje yi, te nekk sama surga njaboot. Xañ ma fu may mayee Seytaane mu dugg ci sama xol. May ma, ma bañ di wax rekk lu jëm ci sas wi, waaye, ma koy jëfe ci kàttan ak maandute. LAAJ:
|