Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
B - Xew-xew yi amoon gannaaw reeru Boroom bi (Yowaana 13:1-38)
1. Yeesu raxas na tànki taalibeem ya (Yowaana 13:1–17)YOWAANA 13:1-5 Li ko dale ci saar bii, Yowaana dafa song beneen pàcc. Ca njalbéen ga, Yeesu dafa daan woowandoo nit ñi; li ciy naqar nag, mooy ne li mbind mi ne “Leer gaa ngi leeral lëndëm gi, te lëndëm gi nanguwu koo dalal” te loolu feeñ ci ñoom, kon ndax Yeesu daanu na? Mukk! ndegam ñu bare nanguwuñu Ko woon, Boroom bi tànnoon na ñenn ñu jekk te tuub,ba Mu boole leen ci ay taalibeem. Ci biir saar yii dinanu ci jàng ni Yeesu waxe ak ñi ñu fal,ni far di waxe ak coroom. Ñoo Ko moom,ni Mu leen moome. Mbëggeelu Yàlla rekk moo mujj nekk ay njàgaleem. Mbëggeel googu méngoowul ak yëgeeli bopp-sa bopp, dafa ëmb wooteb surgawu. Ci Biibal bi, mbëggeel dafa bootaale sa njébbalug bopp ci kow suufeelu gi nga war a cër ñi ko yelloowul. Ci yii kàddu Yeesu dafa ciy won taalibeem yi melokaanam yi gën a tabe, di ci faramfàcce mbëggeelam nib surga, buy firnde dundam, deewam ak ndekkiteem. Yeesu yégle na ne deewam mooy jiitu Pàk (màggàlu bésu jéggi ba). Dafa doon dellu ca Baayam. Ndax foofa nga jublu itam? Mungi woon ci àddina si, waaye, ay bëtam mosuñoo teggeeku ci Baay ji. Ci Moom la doon jële kàttan, jubluwaay, ak mbégte ngir man a dékku (muñal) nit ñu soxore noonu. Ni Mu jokkook Yàlla, la gise ne Seytaane mungi déey ay xalaat yu ñaaw ci xolu kenn ci taalibeem yi. Taalibe booba tàmbali ndànk-ndànk di bàyyi yu mel ni nay, tiitar, ak mbañ, di yóbbale nafsoom. Fekk nag Yeesu bañul workat boobu, waaye dafa wéy di ko bëgg. Nekkuloon ne Yeesu dafa rëppeelu ci kanamu workat bi, mu mel ni li xew musiba la. Du woon Yudaa, Kayif, Erod, Pilaat, Kilifa Yawut yi, walla sax mbooloo ma ñoo waroon a dogal li nar a am. Waaye ni Mu suufeeloo (toroxloo) boole ci dégg-ndigal, noonu la Ko Baay ji jébbalee lépp luy baatin ak doom-Aadama. Moo dogu dee ni Mbotem Yàlla, te tànn waxtoom. Ci biir jamono yu metti yi ci topp, dara taxul Mu réere mbir fa Mu jóge ak li muy mébét. Yeesu mooy Sang biy bittarñi doxalinu àddina. Yeesu ñaanuloon dellu ca Baayam, waaye dafa xiir taalibeem yi ci jokkoo ak mbégu Yàlla gu neex gi. Bi Mu leen di raxasal seeni tànk, jàngalaale na leen ci suufeelu, te wone ni mbëggeelu Yàlla di doxe. Noonu la nekke ab dag. Dafa def boppam ki gën a suufe ñépp, ngir ñi gën a féete suuf man a xam ne yàlla dafay surgawu doom-Aadama yi. Boroom bi du nguuru ci nooyaay, mbaa ci ñàkk a faydaal, waaye jaral na ko Mu sukk ngir sellal nu te soppi nu ba nu méngook lewetaayam. Yeesu mooy sunu royukaay. Kañ lanu koy sukkal ngir jaamu Ko? Kañ lanuy soppi sunuy xalaat te bank sunuy gannaaw yu ne sàdd yi? Mbokk mi, lu mu yàgg-yàgg te fekk sa xol tojul, bul jéem a dimbali sa moroom, bul bëgg sa noon, te bul jéem a faj ku gaañu, ndaxte doo kercen dëgg. Ndax surga nga, walla njaatige? Fàttalikul ne Yeesu surgawu ñépp la, te dafay suufeelu ngir surgawu la. Ndax dangay nangu woowu surgawu, walla sa tiitar moo la doy ba nga bañ a soxla ndimbalu Yàlla? YOWAANA 13:6-11 Taalibe ya ànduñu woon ak dal bi ñu gisee seen sang bi di leen raxasal seeny tànk. Bu ñu xamoon li nar a gannaaw reeru Boroom, kon naroon nañu raxasal seen bopp seeny tànk laata loolu. Seen Sang bi, du woon rekk ag kóllëre gu bees la leen indil ci seen diggante ak Yàlla, waaye dafa leen a wonaale li kóllëre googu di tekki; du dara lu dul ag baaxe gu àndak mbëggeel, te jaar yoon. Piyeer moo nekkoon taalibe bi ci gënoon a man a bàkku, te gën cee am xadar. Bëgguloon Yeesu di ko surgawu; noonu mu koy jéem a aaye te ràññeewul kàddu yi ko Yeesu doon wax. Gannaaw loolu, Yeesu wax na taalibe yépp lan mooy kumpa gi nekk ci raxasu tànk yi, mu mel ni nun ñépp lay waxal: ”Bu ngeen sellul, dungeen man a am wàll ci nguuru Yàlla gi te bu ngeen jotul mbaalu bàkkaar, dungeen man a sax ci man.” Sang bi Mu nu Sang ci deretam, du dakk mukk te sax sellaay googu dafay wéy jëm kanam. Moo lay sàmm ci yiwam ak ci jokkoo ak Doomu Yàlla ji. Ni ko leer gi duggee, Piyeer daldi xool ay loxoom, yi jotoon a def lu ñaaw,te xalaat it ci xelam mi yéex a xam tëralinu Yàlla/ Mu daldi rus, ba ñaan ñu sellalal yaramam wépp. Yeesu dalal xalam ne ko: « Képp ku ñów ci man, dangay set-wecc, jare ko ci sa ngëm. » Noonu lanu xame ne soxlawunu ag sellal gu jéggi dayoo, walla laabal gu ñu ciy dolliwaat, ndaxte deretu Yeesu setal nanu ci bépp bàkkaar. Amul sellaay bu gën a rëy mba bu gën a laab mbaalug bàkkaar gi nuy jot ci deretam. Bu nuy dox, danuy taqaale pënd mu bare. Noonu itam danuy ñaan saa su nekk naan: « Baal nu sunuy tooñ. » Doomu Yàlla yi soxlawuñu di raxas seeni tànk bés bu nekk, waaye doomi àddina si ñoom soxla nañu sellaay bés bu nekk. Yeesu xool taalibeem ya ne leen: « sell ngeen. » Mu woo leen ngir ñu dugg ci kóllëre Yàlla gi. Bote mi dee na ngir wuutu ay taalibeem, ngir ñu man a jokkook moom ci baatin. Amul kenn ku sell waaye deretu Krist dafa nuy sellal ci bépp bàkkaar. Li ci tiis nag, mooy ne taalibeem yépp selluñu woon, te looloo am tey jii sax. Am na ñu mel ni bëgg nañu sellaay googu te dañuy doxale ni ñu gëm deretu Yeesu, wante feesuñu ak Xel mu Sell mi. Xelum Seytaane moo leen di xiir ci mbañ, kiñaan, rëy, njaaloo. Looloo tax ba mu am ci biir ñi gëm ñu ay rab yu bon di jàpp, mbaa ñuy jiital alal. Yeesu dafa la bëgg a raxasal say tànk bés bu nekk, yewwi la ci bépp melokaanu bàkkaar, te sellal la ba nga man a jokkoo ak Yàlla. Seetlul sa bopp, ndax surga nga walla njaatige? ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nu ngi lay sant ci li nga wàcc sa nguur te ñów ci nun, bàkkaarkat yi. Suufeelu nga sax ba raxaxal say taalibe seeny tànk, te laabal nga sunu xol ci bépp bàkkaar. Nungi lay jaamu, te di la ñaan nga yewwi nu ci bépp xalaat bu làmboo rëy-rëylu, ndax nu man laa sujjóotal te nekk say taalibe (dag). Dimbali nu, ba nu suufeelu ci kanamu ñépp, ba jekk ngir liggéeyal jàngu bi ak sunu njaboot. LAAJ:
YOWAANA 13:12-17 Du ci ay waxi neen la Yeesu tàmbalee tàggoo. Wax yu mel noonu duñu bare njariñ, bu leen jëfewul. Dafa laaj taalibe ya ndax xam nañu li Mu leen misaal lu muy tekki : « Ubbileen seeni bët te gis, ndaxte maangi ak yéen ni ku mel ni yéen. Tooguma ci gàngunaay, ba noppi teg leen ci samay suufi tànk ni ay jaam. Déet! Damaa wàcc sama nguur, ñów mel ni yeen. Rax ci dolli ma summi sama mbubbum jàgalekat, ak sama kilifteef, ngir nekk seen surga. Ndax xam ngeen leegi fi mbëggeelu asamaan gi war a jublu? Nit ku rëy dafay bàkku, waaye ku bëgg dafay suufeelu te di muñalaate, dafay fàtte boppam, di dimbalee ci jëf ak yaram. « Dangeen a bëgg a nekk samay taalibe. Maay seen royukaay, yemuma ci wax doŋŋ, waaye damay jëfe sama njàngale. Xoolleen ma; ab surga laa. Su ngeen ma nammee topp, nangeen suufeelu te ku ci nekk nangoo doon surga moroomam. Ki bëgg a gën a màgg ci, yéen na nekk ki gën a ndaw. Waaye kiy surgawu ñeneen ñi, ak lewetaay te nangoo ndaw, ci dëgg moo gën a màgg. » « Buleen jàppe jàngu bi ni mbootaayu ñu sell ba mat sëkk. Ñoom ñépp ci yoon woowu lañu tegu. Sellal naa leen, te sell nañu. Waaye ku ci nekk dangaa war a muñ te xaar ba nga màgg ci baatin. Ku ci nekk dangay wëndeelu te di daanu. Lii mooy sama sas ak sama ndigal: nangeen di baalante seeni njuumte ak seeni tooñ. Bu kenn àtte sa moroom, waaye dimbalanteleen. Buleen raxas boppu kenn, waaye raxasalleen leen seeni tank. Bu kenn ronni moroomam, ndaxte ay mbokk ngeen. Su ngeen doxalee noonu ma leen ko sante, dingeen xam ne def naa ko ba noppi; ñówuma ngir wutsi surga, waaye ngir surgawu. Sama dund gi mooy surgawu, jébbal sama bopp te taxawu ñépp. » « Maa ngi leen di yebal ci biir àddina si, yéen ndawi mbëggeel yi. Ki ñu yebal nag, ak ki ko yebal ñoo yem màggaay. Seen wareef wu njëkk mooy ngeen nekk surga ni man. Su ngeen doxalee noonu, dingeen wone ne xam ngeen sartu Kercen. » « Sama ñaareelu sart mooy: Su fekkee ne xam ngeen yëf yooyu, kon barkeel ngeen, bu fekkee ne yéen a ngi leen di jëfe. Nekkuma fi di wax mbiri mbëggeel rekk, waaye dama koo jëf. » Sarwiis ab liggéey la, ak joxe sa bopp, du ay waxi neen, ay ñaan, ak ay yëgeel. Bëgg a surgawu dafa nekk ci deretu ki gëm, te xolam xiir ko ci ay jëfi mbëggeel. Ku dul surgawu daal, ñàkkul ne du ku gëm. Ñaan yu tar yi àndul ak ndimbal, ag naaféq la. Sa jëf yu baax yi duñu tax nga texe; deretu Krist moo lay texeloo. Boo suufeeloo ci kanamu ñu ndóol ñi, ak ñi amul dëkkuwaay, te sax ci di leen di defal lu baax, dinga solu ba fees ak mbégu Yàlla. Mbégte Yàlla dafay muur surgay Krist. Mbokk mi, ndax dangaa bëgg a nekk kilifa ak jàngalekat? Xoolal ci Yeesu. Mooy jàngalekat bu mag bi. Mungi taxaw ci sa kanam ni ab surga. Ndax bëgg gaa jëfe ak ay njàngaleem? Tàmbaleel di surgawu leegi. ci biir ñaan, laaj ko fan, nan ak kan nga war a dimbali. Soo xamee yooyu mbir, barkeel nga, boo leen jëfee. |