Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
B - Xew-xew yi amoon gannaaw reeru Boroom bi (Yowaana 13:1-38)
2. Workat bi ñu feeñal te mu nekk ci njaqare (Yowaana 13:18-32)YOWAANA 13:21-22 Yeesu wax taalibeem ya lu jëm ci mbëggeel gi ak sas wi. Mu won leen misaalu suufeelu, te xamal leen ne nguuram, dina melax ci biir ñàkk doole, ngir ñoom ñu xam ne Moom mooy Boroom bi, Moom miy doxal te di wommat lépp liy xew, ba ca waxtu dee ga sax. Ba Mu leen di faramfàcceel loolu, ci la (Yeesu) yégle worug Yudaa, te may ko mu àggale bóom gi mu fasoon yéene, ngir Yudaa bañ a doxale ak tëralinu boppam, waaye ci kow ni ko asamaan dogale. Yeesu xamal taalibeem ya ne am na kenn ci ñoom ku Ko nar a jébbal kuréelu Yawut ya. Xibaar boobu mel ni ndell ca diggu reeru màggal ga. Yeesu yéglewul xibaar boobu cig neen waaye yaramam dafa daw, mel ni ba mu demee ca bàmmeelu Lasaar ba. Li ko gënoon a metti mooy li ko Baay ji nar a dëddu. Yeesu dafa bëgoon Yudaa ba tànn ko; xanaa kay ab xarit manul mukk wor Doomu Yàlla ji. Biibal bi wax na lu ci jëm, ci Sabóor 41 :10 : « Ki doon lekk sama dugub, wéq na ma. » Bi ñu déggee boobu xibaar, taalibe ya xoolante di xalaat naan : « Ndax kii mooy workat bi ? »Manuñu woon xalaat ne kenn ci ñoom man na wore. Moone ku ci nekk yaa ngi doon xalaat a dëddu Yeesu bu mbañeel gi ak weddi bi gënee tar. Waaye Yeesu xolli seen mbóot, ñu am ci gàcce, te manuñu jàmmaarloo ak leeru asamaan gi Yeesu àndal. YOWAANA 13:23-30 Ca biir njaqare googu yégle wor gi indi, nungi ciy gis mbëggeel. Yowaana mungi sóonu woon ci Yeesu. Taskatu Injiil bi du wax mukk turam ci Injiil bii, waaye dina ciy wone ni mandarga mbëggeel doxewoon ci digganteem ak Yeesu. Amuloon ngëneel gu gën a mag mbëggeel gi ko Yeesu jagleel. Moo tey jéllale turam ngir jox ndam lépp Doomu Yàlla ji. Piyeer dafa amoon kersa lool ngir laaj Yeesu kan mooy workat bi, waaye ndañ-kumpa sonnal na ko. Noonu mu kobos Yowaana, mi mujje déey Yeesu, ngir laaj Ko : « Kan la ? » Yeesu dafa tontu laaj boobu te boolewu ci benn tur. Bëgguloon a jéebaane turu workat bi ca saa sa. Yudaa manoon naa xàcc la mu nammoon. Yeesu séddale mburum yiw, mi koy lëkkale ak taalibe yi, Mu capp aw dog ci ndab li, jox ko Yudaa. Li ci jëf jii jublu woon, mooy ñaax ab taalibe ngir mu jot dund gu dul jeex. Waaye, ndegam Yudaa dafa dogu woon a wor, dogu mburu mi manatu ci woon dara, xanaa kay dafa koo gën a ràŋŋati. Xolam dëddu yiw wi, Seytaane dugg ko. Ndaw lu ñaaw ! Ci kow coobareem gu sax gi, Yeesu dafay dëgëral xol yi namm a dëgër. Bi ko Yeesu di may mburu, Seytaanee ngi doon yëngal ay xalaatam. Ba mu jotee mburu ma nag, mbon gi dugg ko. Àtteb Yeesu xañ na workat bi aarug asamaan, te jébbal ko Seytaane. Ci saa si, Yudaa daldi feeñ, bi mu jëlee dogu mburu ma. Ndigalu Yeesu la, ne ko rës ci dënnam (xolam) : « Bul fomb sa mébét yu bon yi nga lal, gaawal nga matal leen ndax mbon gi man a yeggali jëfam, ngir lu baax man cee juddoo. » Taalibe ya umpale woon nañu li Yeesu saasoon Yudaa. Li ci ëpp dafa ko doon yónni ngir mu jëndali leen li ñu war a lekk. Yowaana fàttewul kanam gu ragallu gu Yudaa gi soppeeku ci teewaayu Yeesu, tàbbi ci lëndëmu bitti bi. YOWAANA 13:31-32 Nan la yeesu ndamoo ci jëf ju ñaaw jooju ? Nan la lu baax man a juddoo ci jëf yu ñaawe noonu ? Naqar jàpp na Yeesu ba ko taalibe ba mu tànnoon dëddoo. Mu koy may xelum mbëggeel, di yaakaar workat bi fomb ay tëralinam. Waaye kooka moom jubal ca kureelu Yawut, ga dooleel xarekat ya ngir ñu jàpp Yeesu ca xaaju guddi. Krist dafa bañ fiiru Seytaane bi bëggoon Mu nekk Almasi politik, ba Mu yebalee Yudaa ngir mu matal woram ga. Dafa tànnoon a dee ni Mboyem Yàlla, ngir rammu nit ñi jaare ko ci suufeelu ak ñàkk doole, di wone ne mbëggeelu saraxewu, moo lal ndamam. Yeesu wutuloon ndamul boppam, waaye ndamul Baayam la doon wut. Baayam dafa Koo yónni woon ci àddina si ngir Mu musal ñi sànku. Doom ji dafa nammoon a yeesalaat melokaanu Baay ji ci askanu doom-Aadama ju daanu ji te di sànku. Ci kow googu nammeel la feeñale Baay ji te yokk ngëm gi ci baaxaayu Yàlla. Njàngale mi rekk doyul ndaxte bàkkaar dafa bare ba samp ab ñag ci diggante Yàlla ak li Mu sàkk. Doom ji dafa waroon a dee ngir ñag bi nekkoon ci diggante nun ak Yàlla, man a beddeeku, te li yoon laaj man a mat. Deewug Krist mooy caabi màggalug turu Yàlla. Bu dee googu amul, kon kenn du xam Yàlla, benn baayoo bu lew du am, walla yeesal gu dëggu. Krist dafa fàtte boppam, te deewam màggal Yàlla. Newoon na it ne Baayam dina Ko màggal, te noonu dina nekk mbënnu gépp may gu ànd ak ndam. Ci waxtu yi jiitu ñu daaj Ko ci bant, Yeesu gis na ndekkiteem, delloom asamaan ak toogaayam ca gàngunaay ga. Krist dafa waroon a dee ngir dugg ci ndamam. Ñépp ñi weddi metitu Yeesu Krist yi ak deewam gi, walla ñu jële ko ni màndarga ñàkk kàttan, duñu man a xam coobare Yàlla ci aju ci kurwaa bi, walla sellaayu Doom ji génne ci bàmmeel bi. Dafa wone ndamam ci saraxekaayu Yàlla, fa Mu nu wuutoo ci dee, ngir képp ku Ko gëm ñu goreel la. ÑAAN: Baay, Doom ak Xel mu Sell mi, nungi lay màggal ndax sa mucc gi, sa woyofteef, sa dee ak sa ndekkite. Gëm nanu ne mucc nanu jaare ko ci deretu Krist. Nungi lay màggal ci kàttanu Xel mu Sell mi. LAAJ:
|