Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
3. Yeesu sàmm bu baax bi (Yowaana 10:1–39)
d) Sunu kaaraange ci biir jokkoo gi am diggante Baay ji ak Doom ji (Yowaana 10:22-30)YOWAANA 10:22-26 Màggal ga ñu doon sellale Kër-Yàlla ga, pàttalikub mbégte ma amoon ba ñu yeesalaate Kër Yàlla ga, gannaaw ba Israil jógee ca gàddaayu Babilon bu 515 laata Yeesu Krist la. Màkkabe ya defaraatoon nañu ko ca atum 165 laata Y.K. Màggal gi, bu weeru desembar di tàmbali lañu koy defe, fekk muy jamonoy tow ak sedd, ndaxte Yerusalem mungi tollu ci 750 meetar ci kow suuf. Loolu moo may Yeesu mi ñuy xeex, Mu dellusi bay waare ca ëttu Suleymaan. Ña fa doon jaar ñungi Ko doon déglu. Buntu penku boobu, waxaat nañu ci moom ci téere Jëf ya 3 :11 ak 5 :12. Yawut yaa nga doon waaj ni ñuy songe Yeesu. Dañoo bëggoon Mu wax ci biir mbooloo mi ne mooy Almasi, bi ñu doon xaar walla déet. Li Mu waxaloon boppam, ak ay jikkoom, wuute na ak li nit ñi doon séentu ci seen Almasi, ak li ñu doon wut. Kon loolu man Ko daaneel. Waaye nag dafa am ñu gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, ndaxte ni Mu nitee, sañ-sañam ak ay jëfam dañu kéemaane. Dañu doon jéem a forse Yeesu ngir Mu woote ab mbootaayu kercen bu law ci réew mépp. Moone sax màggal gi ngir fàttaliku yëngalu Màkkabe ya la woon. Dañoo yaakaaroon ne dina jóg ci yelleefamu nekk buuru réew mi, te dina wax askanam wépp mu jël ay ngànnaayam. Jekkoon nañu ngir ànd ak Moom ca xare ba, ngir faxas gàcce gi ñu am ci nguur gi leen di noot. Yeneen tëralin la Yeesu amoon: Suufeelu, mbëggeel ak coppite xel yi. Waxul Yawut ya ne mooy Almasi bi, waaye wax na ko jiggéenu Samari ja. Waxoon na it gumba juuduwaale ga, ndamam ci baatin. Yawut ya, ab Almasi bu ñeme te xarañ ci politik lañu bëggoon; waaye Yeesu rammukatu xel la, te am yërmande. Nit ña dañoo nammoon kilifteef, ngor ak sag. Yeesu dafa ñów ngir ñaax ñépp ci jébbale sa bopp, nangu coono ak yeesal. Yëgal na leen màggaayam, waaye gisuñu ko, ndaxte li ñu doon séentu du Moom. Xel ya dajewuñu, te ngëm gi wuutewoon na ci seeny xol. Ubbiluñu seeny xol Xelum Yeesu. Ay kéemaanam yépp, ci turu Baay ji lañu mate, Moom mi Ko xeexal ba Mu àgg ci ndam li. Yawut ya amoon nañu xel-ñaar ci dégg ñuy wax lu aju ci diggante Doom ji ak Baayam ji ,ni li lal seen reenu réew.Lu tàng-jër lañu nammoon,teg ci alal(xaalis) ak yaatal seen réew. YOWAANA 10:27-28 Yeesu mooy Mbotem Yàlla; dafay woo ay xaram ak ay mboteem maanaam ñi solu melokaanam, ngir ñu topp Ko. Seen ngëneel gu jëkk, mooy man a déglu, ndaxte Xel mu sell mi ubbi na seen xel ak seen xol ngir kàddu Yeesu, ak coobareem solu leen fa mu gën a xóote, ngir soppi leen ba ñu nekk mbindeef yu bees-tàq. Déglu ak teey, gu mat -sëkk mooy jéego bi njëkk ci sunu tàggatum taalibe. Krist xam na ñépp ñiy deñc Kàddoom; daf leen a bëgg, xam seeny mbóot te xam ni Mu leen di soppee. Kercen dëgg du bàyyeeku mel ni ku amul lu mu namm ci dundam. Xam nañu leen, te bind nañu seeny tur ca asamaan. Kenn ku nekk ci ñoom ab kéemaan la, maanaam ku bees ku Yàlla sàkkaat. Yeesu moo mel ni Sàmm bu Baax bi; xaram yi miin nañu baatam te te dañuy nangu ay wommatam di uufu ci Moom ak mbég. Coobare sseen Sàmm bi rekk moo leen ñor. Amul benn xalaatu puukare bu nekk ci seen xol; ay mbote yu lewet lañu. Coppite googu man naa nekk ndax liggéeyu Yeesu ci ñoom. May na leen mbëggeelu Yàlla ak kàttanu daan dee gi ak bàkkaar bi. Duñu dee mukk waaye dañuy dund ba fàww, ndaxte dundam lañu soloo. Goreel nañu leen ca àtte ba ak ca dee gu dul jeex ga; deretu Yeesu goreel (yewwi) na leen. Amul menn xar mu deretu Yeesu rammu, muy sànku. Dafa bàyyi ndamam ca asamaan ngir musalsi nit ki, te it Mu dunde coono ngir may nit ki dund gi. Moo leen tànn a aar, ak lépp lu ci man a am. Ndax yëg nga kaaraange gu wóor ci say loxoy Boroom? Ndax tànn nga kàttanu Krist ak man-manam? Ci ñaar yi, benn moo ci man a nekk: Yaa ngi dunde bàkkaar, di wëndeelu, walla Yàlla goreel na la, def la doomam jaare ko ci Krist. Sunu kaaraange Boroom bi moo ëpp-fuuf sunuy jëf, ndaxte romb na sunuy natt. Ci wetu Boroom Ndam li lanu nekk. YOWAANA 10:29-30 Yenn kercen yi dañuy am xel-ñaar ci ne Yeesu man na leen aar ci dee, ci Seytaane ak ci merum Yàlla. Loolu dafa sut seen dégg-dégg. Loolu moo tax Yeesu wonale taalibeem yi ak Baay ji, ak it Kàttanam. Yàlla dafay tànn bépp taalibe Yeesu bu bees. Amul kenn kuy topp Yeesu bu dul ci kow coobare, ak tànneefu Yàlla. Yàlla Baay ji moo yilifoo ñi taq ci Doomam. Baay ji mooy Aji kàttan ji, te man lépp. Yeesu wutuloon bànneexam, waaye dafa déggaloon Baayam. Ci kow dégg ndigalam googu la feese baatinu Yàlla. <Am na ñuy xalaat ne Yeesu moo gën a suufe Baayam ji. Waaye Mbind mi nee na nu, képp ku yékkatiku dees na la suufeel, te ku suufeelu, ñu yékkati la. Ndegam nag Yeesu dafa jox Baayam bépp ndam, kon man na wax ne: ”Man ak Baay ji, benn lañu.” Dafa doon teggi waxu ñi doon xalaat ne nun danoo yokk beneen Yàlla ci kow Yàlla. Jaamuwunu ñetti Yàlla, jenn Yàlla doŋŋ lanuy jaamu ñiy weddi jokkoo gu mat gi nekk ci diggante Krist ak Baayam, dañoo rëy te xamuñu ne yoonu màggaay ci suufeelu lay tàmbalee. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, yaay Sàmm bu Baax bi. Joxe nga sa bakkan ngir say xar. May nga nu dund gi, kon book dunu dee; nungi lay sant; yaangi nuy aar ci dee gi, ci Seytaane, ci bàkkaar, ak ci merum Yàlla. Kenn manunu foqati ci sa loxo. Jàngal nu woyofteef ndax nu man a xame Baay ji ci yow, te nu faat sunu nafsu. Na sa kàttan feeñ ci sunu ñàkkum doole. LAAJ:
|