Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 067 (Jesus is the Good Shepherd)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
3. Yeesu sàmm bu baax bi (Yowaana 10:1–39)

c) Yeesu mooy Sàmm bu Baax bi (Yowaana 10:11–21)


YOWAANA 10:11-13
11 Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi dafay joxe bbakkanam ngir ay xaram. 12 Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des. 13 Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay liggéeyal, faalewul xar ya.

Yàlla mñal na buur ya, yonent yu naaféq ya ak waarekat ya daan naxaate, te it sàmm na mbooloom, ma tasaaroo woon mel ni jur gu amul sàmm. Loolu moo waral Mu yónnee nu Krist, Sàmm bu Baax bi. Krist nee na: » Maangi nii, man Buur bi dëgg, Saraxalekat bi ak Yonent bi indi peeñu mu mujj mi." Ci Krist lanuy gis lépp ni ab sàmm dëgg war a mel. Moom man na wax: »Ñàwleen ci man, yeen ñi sonn te diis, ma may leen noflaay. Duma leen teg liggéeyu coono, waaye dama leen di yewwi ci dund gu amul njariñ, ak ci lépp luy gaañe.

Liy firndeel ne Moom rekk mooy Sàmm bu Baax bi, mooy coobareem ji mu jiital ca njalbéen ga, ngir jébbale bakkanam ngir ay xaram. Joxewul yaramam kese, waaye daf cee boole yaram wi, ruu gi ak Xel mi ngir juru Yàlla gi mucc. Liggéey bu metti la tàmbalee, di liggéeyal taalibeem ya. Deewug yaramam mooy matal dund gi mu maye. Fàttalikul ne Yeesu dunduloon ngir boppam rekk, te loolu taxul mu dee. Dafa dund, te dee ngir yów.

Sàmm yu jubadi yi, dañuy feeñ ndaxte bu lu wóoradi agsee rekk ñu daw làquji ngir rawale seen bopp kese. Dañuy bàyyee jur gi bukki yi leen song ak doole. Duñu ay mala, waaye ni ñoom (mala yi) lañuy jëfe; Seytaane mooy seen baay. Ni bukkib njalbéen ga, li Seytaane namm mooy ku mu yàpp. Ay coongam dañuy ànd ak caay-caay; dafay noot te di reye. Dafay ñów ak ay fiir yu sedd, boole ci fen yu diinewu. Pastër yi waruñu baale, walla di seetaan njàngale mu dul dëgg, miy taafantoo mbëggeel. Waaye war nanu, ci kow mbëggeel xeexal dëgg gi, ci biir maandute te taxaw temm su ko jaree. Dundug Yeesu dafa nuy won ne Moom dafa daan jànkonte saa su nekk ak xelu rab yu bon yi. Ak mbëggeel la doon yégal dëgg gi ay taaligeem, ngir ñu toppatoo jur gi te góor-góorlu ba aar ko ci coongi xeli seytaane yi. Li bukki bu xiif bëgg, lu leer la; jaare ci ay jiiñ yu dul dëgg, fitnaale, ba nasaxal Jàngu Yàlla bi. Ndax liggéeyal mbooloom yàlla, te sargal ko nga bëgg? Na nga xam ne loolu dafay sóoraale ay ŋaayoo; metit ak nangoo ñàkk lu bare. Amul genn ngañaay walla bégte gu ci nekk, te amul it noflaay.

YOWAANA 10:14-15
14 Man maay sàmm bu baax bi. Xam naa samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame. 15 Ni ma xame Baay bi te, Baay bi xame ma ni. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir sama xar yi.

Krist delluwaat ne, Moom rekk mooy sàmm bi. Nun manunu toppatoo jur gi ni mu ware ndaxte xamunu noon bi, te xelu xar yi it ump nanu. Xamunu nan lanu leen di yóbboo ci mbooy gu naat. Krist xam na kenn ku nekk ci nun, xam na it sunu démb, sunuy xalaat, ak sunu ëllëg.

Yeesu moo tànnal boppam ay xaram, ba noppi may leen ñu xam Ko. Ni ñu Ko doon jéem a xame, ñungi doon laajaale seen bopp lu tax sàbbiwu leen. Teewaayam sax dafay wone seen matadi. Daje bii dafa yokk seen mbëggeel te gën a tax ñu Koy sant ci jokkoo gu amul àpp gi.

Xamante bi am ci diggante Yeesu ak juram gi du lu woyof, te jógewul ci mbiri àddina si, waaye, mayug Xel mi la, ndaxte danu koy gis, ni muy gise Baay ji, ak ni Baay ji di xame Doom ji. Ni bépp kercen di jote ci Xel mi peeñum dëggu baatin gi ci Krist, kumpa la. Xelum Yàlla mi dafay dëkk ci jur gi te di ko suuxat beruñu kenn.

YOWAANA 10:16
16 Am naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii. War naa leen a indi, ñoom it, te dinañu déglu sama baat. Benn coggal ay am ak benn sàmm.

Du benn xeet doŋŋ la Krist deewal, waaye ñépp. Du caagéen ne fippukati Kóllëre gu Njëkk ga rekk la deewal, waaye dee na ngir nit ñu bon ñu àddina sépp. Waxoon na ne deewam dina rammu xar yu bare ci àddina sépp. Kenn manul a ñówal sa bopp ca Yàlla, ñépp dañuy soxla ku leen won yoon wi, manaam Sàmm bu Baax bi. Mooy Krist. Moom mooy njiitu réew yépp, ak bepp doomu Aadama. Nguuru baatinam, ci kàddoom lay feeñe. Ni xar yi di ràññee seen baatu sàmm, noonu itam la nit ñi ñu jekkal di dégge baatu Krist, ba ñów ci Moom. Ak Krist, jokkoo baatin gu bees dafa feeñ, di dajale ña ñu tànnoon ca Kóllëre gu Njëkk ga, ak tuubeeni askan yépp. Waa Kóllëre gu Bees gi ñoo nekk tey géttu yàlla gi, te Yeesu mooy Sàmm bi. Ñépp ñiy déglu Injiil ak mbég te gëm Yeesu, Doomu Yàlla ji, bokk nañu ci Jàngu bu dëggu bi, naam sax man nañoo bokk ci yeneeni mbootaayi kercen. Nun noo bokk mennum Xel mi, benn Boroom bi, ak jenn Baay ji. Xel mi, dafay wàcc ci ñépp ñi deretu Krist sellal. Juboo gi ci diggante juru Krist gi raw na fi nu ko natt ci sunu xel. Dajale xari ruq bu nekk! Sàmm bu Baax bi dafa ñówal boppam, ngir dugal surgaam yu dëggu yi ci ndam. Noonu, genn gétt ak benn sàmm rekk mooy am. Waaye, tey jii, ku bëgg a taxawal ab jàngu ci sa kow doole, te jublu ci lu neex àddina nar ngaa daanu ci fiiru bukki bu mag biy jéem a génnee xelu jur gi ci Sàmm bi. Manunu jokkoo te fekk jegewunu Yeesu.

YOWAANA 10:17-18
17 Baay ji bëgg na ma ndaxte damay joxe sama bakkan ngir jëlaat ko. 18 Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko, te am sañ-sañu jëlaat ko. 18 Kenn du ko jële ci man; man maa koy joxe ci sama coobare bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko, te am sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.

Gëm nanu ne Yàlla mbëggeel la, te bëgg na lool Doomam ji saa su nekk. Ndaxte Yeesu lu neex Baayam rekk lay def. Li neex Yàlla ci dëgg-dëgg mooy Bant ba (Kurwaa ba). Deewug Krist mooy li Yàlla tëraloon. Benn pexe rekk moo man a muccloo nit ci bàkkaar, te mooy sarax si ak Sellal, si jaare ci deretu Mbote mi.

Deewu Yeesu ak ndekkiteem, ay kéemaan yu rëy lañu. Waxoon na nu ne dina dee ngir dund. Kenn forsewu Ko ngir mu jébbal boppam, waaye ci coobareem la ko defe, ndaxte dafa bëggoon muccug bàkkaarkat yi. Moom mooy mbëgeel gi dëgg. Baayam moo ko jox sañ-sañu musal àddina si, ak sañ-sañu jotaat dundam. Kenn manuloon a xañ Yeesu ndamam la ca bant ba. Seytaane ak ay ñoñam jéem nañoo nasaxal rammoom gi, waaye ki doon jaay muusante, rëppéelu na ci kanamu mbëggeelu Krist gu rëy gi. Du woon Kaif, Pilaat, walla keneen ñoo Ko xiir ci dee gi, waaye moom moo tànnal boppam dee. Dawul ba Mu séenee bukki ba di ko wutsi, waaye dafa joxe bakkanam ngir musal nu. Coobare Yàlla ju mat la woon. Ca bant ba Yeesu dafa am ndam ci ŋaayoo bi amoon diggante asamaan (ajjana)ak safara. La ko dale ca bés booba, la juram gi jot mandarga dig bi ñu birale (fase)deretu Mbote mi. Yeesu dafa nuy wommat ci biir jafe-jafe yi, ak coono yi jaare ko ci ndamam.

YOWAANA 10:19-21
19 Kàddu yooyu ñoo féewalewaat Yawut yi. 20 Ñu bare ca ñoom naan: »Dafa ànd ak rab! Dafa dof Lu tax ngeen koy déglu? » 21 Waaye ñeneen naan: » Nit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi bëti gumba? »

Yërndukat ya mer lool ba ñu déggee ne Yeesu dafa jiiñ seeni kilifa ni ay sàcc lañu, te ay ndawi Seytaane lañu. Tegati ci Muy wone ne Mooy Sàmm bu Baax bi, ba sax naan Mooy Sàmmu Askani àddina sépp-mbir mu doy waar ci biir Yawut yi. Dañu jàppewoon seen bopp ni ñu Yàlla fal. Ñu teg Ko ku ame ay rab, ku dof, noonu ñu mer ba futt. Ñu bare ci doon romb nangu la yawut ya doon wax. Mbooloo ma won gannaaw Yeesu, weddi Ko, ndaxte njàngaleem manuñu ko dégg ci baatin.

Moone de am na ca ña doon déglu, ñu amoon fitu wax ci diggu mbooloo ma ne dégg nañu baatu Yàlla ci biir kàdduy Yeesu. Ay kàddoom ñàkkuñu woon fayda, waaye dañu feesoon dell ak kàttan. Baaloon na gumba ga ay bàkkaaram. Mbooloo ma di ko gën a tiiñal, fekk mbëggeelam mungi doon sax ci xolu ñu dëggu ñi te gore. Saa su nekk Yeesu dafay wommat juram ak Xel mu Sell mi, jëmale ko fu wóor.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, Sàmmkatu xar yi, dàquloo xar yu dëgër bopp yi, waaye danga leen a wut ba jot leen, te joxe sa dund ngir ñoom. Baal nu sunuy bàkkaar. Jarajëf ci Xelu xam-xam mi nga nu may, ba nu man laa xam, ni nga xame Baay ji. Xam nga sunu tur te doo nu fàtte. Say ñoñ ñépp ngay sàmm. Tànnal ci askan yi ñi nar a déglu, te woo leen. Aarleen ci bukki bu bekkoor jàpp.

LAAJ:

  1. Nan la Yeesu man a nekke Sàmm bu Baax bi

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2025, at 04:00 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)