Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- John - 066 (Sheep hear the voice of the true shepherd; Jesus is the authentic door)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
3. Yeesu sàmm bu baax bi (Yowaana 10:1–39)
a) Mbote mi dafay ràññee (dégg) baatu sàmm bu baax bi (Yowaana 10:1-6)Ci aaya 7 ak 8 Yeesu dafa won noonam ya na ñu meloon ci dɓgg, ca aaya 9 Mu tegal leen ca seen bañ a nangu Yàlla ak Doomam, ak it seen ngumba. Ci saar 10 Mu yewwi ay ñoñam ci wareefu topp ay kilifa yuy bàkkaar, te woo leen ci Moom, ci boppam. Moom, mooy Sàmm bu baax bi, maanaam benn bunt biy yóbbu nit ki ca Yàlla.
Ci yenn dëkk yi, baykat yi dañuy dajale seeni juri xar ci ëtt bu rëy-a-rëy di leen aar guddi gi. Bu suba si jotee nag, sàmm yi ñów, dugg ci ëtt bi, di woo mala mu nakk ak turam. Wottukat yi ñoo leen di may ñu dugg, waaye lu doy waar mooy xew: Sàmm bu nekk dafay woo géttam ak baat bu leer te ràññeeku. Xar yi man nañu xammee baat yiy woote, ba topp seen baatu sàmm. Colin wi amul solo, xar yi kay baat bi ñu xam rekk lañuy topp. Ni leen sàmm bi di woowe, noonu la leen di wommate ba fa mbooy ga gën a naate, te ndox ma di fa baawaan. Ab géttam dafa koy yàkkamtee topp; benn xaram du bëgg a des gannaaw, ndaxte ñoom ñépp a ko wóolu. Yeesu dafa jëfandikoo misaal boobu ngir wone ne ñépp ñiy déglu baatam bokk nañu ci Moom, sàmm bi jóge asamaan. Ñówul ci waa Kóllëre gu Njëkk gi ngir sàcc, walla di labaj, waaye dafa leen a tànn ci biir mbooloo mi Yàlla fal. Dafa leen goreel te may leen ñamu baatin. Yeneen « sàmm yi » ay bukki yu xiif yuy yoppoorlu jur gi lañuy gën a nirool. Dañuy dugg ci gétt gi jaare ko ci ñu ñu yebal, walla cig muusante. Dañuy rocci mbote yi ba noppi, ne leen fuuf (lekk leen). Seen bopp doŋŋ lañuy dundal te duñu gërëm ku dul seen bopp. Amaluñu gétt gi benn njariñ. Njiitu Jàngu yi, ak ñi fay liggéeye, fekk Yàlla tànnu leen, te saxuñu ci Krist, sunu Boroom ay sàcc la leen di woowe. Dañuy yàq, waaye duñu defar. Yeesu waxoon na ne ay taalibeem dinañu sore sàmm yi bokkul ak ñoom ndaxte dinañu yég musiba bi laata muy agsi. Ñaax na leen itam ngir ñu wóolu digu Yàlla, bi Mu nee ci Sabbóor 23 dina toppatoo juram gi. Nit ña manuñu woon xam li Yeesu di wax, ndaxte gisuñu woon ne seen “sàmm ya” jubuñu te baaxuñu (Yeremi 2:8;10:21; Esekiyel34:1-10; Sakkari 11:4-6). Loolu lépp terewul Yàlla jekk ngir nekk seen Sàmm bu Baax bi, te di leen yónnee ay sàmmkat yu dëggu ni Musaa ak Dawuda. Biibal bi dafay jëfandikoo ay misaali càmm yu mel ni « sàmm, gétt, Mbotem Yàlla, mucc gi jaare ci deret ju tuuru »te baat yooyu yépp ci gox-goxaan yi lañu cosaanoo. Yàlla mi feeñ ci Doomam lañuy woowe Sàmm bu Baax bi, ngir wone ni Mu nuy toppatoowe.
b) Yeesu mooy bunt bi dëgg (Yowaana 10:7-10)YOWAANA 10:7-10 Yeesu dafa wone boppam ni bunt biy wommat géttu Yàlla. Amul menn pexe mu ñi ñu goreel man a jokkoo ci jàngu bi te jaaruñu ci Krist. Képp ku jéem a soppi nit ba mu nekk nitu diine, te jaaroo ci Krist, ab sàcc buy jaxase xelu mbote Yàlla yi ngay niru. Xel mu Sell mi dunu tette ci yoon yu wuute, waaye ci bunt bu xat, bi nga xam ne mooy Yeesu, lanuy jaarale. Ku ci jaarul, doo lekk suuxam, te doo naan deretam, rax ci dolli amuloo benn sañ-sañu toppatoo doomi Yàlla yi. Danu war a faat sunu nafsu, te dugg ci géttu Krist; su ko defee nu bokk ci géttam gi. Ñépp ñi amoon daraja, te jiitu woon Yeesu, mbaa ñu ñów ci gannaawam, te ànduñu woon ak Xelam mu Sell mi, ay sàcc lañu yuy naxaate. Yeesu nee na jongantekati xel yi, soskati xalaat yi, ak njiiti askan yi, ay sàcc lañuy doon, bu ñu Ko gëmul, te jébbaluñu Ko seen bopp; dañuy nax mbooloo yi, ci seeni njàngale ak seeni aada. Waaye Yonent dëgg, yi sax ci Xelum Krist, te jiituwoon Ko, dañoo amoon xol bu toj te jaar ci bunt bi ngir ñów ci Yàlla. Yeesu dafa leen a ngemboon te yónni leen ngir ñu toppatoo juram gi. Kenn manul a dugg ci géttu Yàlla gi fi ak reyuloo sa nafsu, te jox sa bopp Yeesu ngir jot mucc gi. Yeesu dafay def ba mboteem yi Ko déggal nekk ay buur aky Kilifa diine. Pastër/ sàmm bu gore te dëggu, dafay génne ci bunt bi, dem ci àddina si woowi nit ñi ngir ñu ñów ci mucc gi. Bu noppee, mu dugal leen ci yaramu Krist ngir ñu sax ci Moom, mu sax itam ci ñoom. Pastër yu mel noonu, duñu jàppe seen bopp ni ñu sut mbote yi, ndaxte ñoom ñépp a bokk sax ci Krist. Képp ku suufeelu dinga ame ci sa Boroom kàttan gu doy, ak xam-xam bu doy. Xol bu suufeelu dina ame ci Yeesu mbooy gu dul jeex. Yeesu artu na ñeenti yoon géttam gi, ngir ñu moytu bindkati téere yi, ak kilifa diine, yi (waarekat yi) nga xam ne seen ndamu bopp lañuy wut, ak di ger ñeneen ñi. Yeesu dafay woo itam ñépp ngir ñu ñów ci moom. Dafa leen a bëgg a may dundu mbaax ak jàmm dëgg, te def leen teenu barke ngir ñeneen ñi. Ku ñów ci Krist dangay nekk teenu ngëneel buy wal jëm ci ñeneen ñi. Sàmm yi duñu dund ngir seen bopp, waaye dañuy joxe seen dund ngir seen gétt. Xelum Yàlla mi, mayu nu dundu asamaan gi ngir sunu muccug bopp rekk; waaye dafa noo tànn ngir nu nekk ay ndaw, ak ay pastër yuy fàtte seen bopp te di bëgg ñeneen ñi. Lu mbëggeel gi gën a yokk, noonu teen bi gën a baawaan. Dara gënul neex di liggéeyal Boroom bi! Baat yii wone nañu ko: »Ndax ñu ma dund gu naat! » ÑAAN: Boroom bi Yeesu jarajëf ci li nga nekk bunt biy dem ca Yàlla. Ñungi lay sant ndaxte sant nu dunde jokkoo, te di jariñ Yàlla ak nit ñi. Dimbali nu, ba nuy topp sa coobare te am dund gi dëgg. May nu, nu lay indil ay ruu, jaare ko ci sa ndimbalu Xel mi, te nu nekk barke ngir ñépp ndax ngëneel gi nga nu may. LAAJ:
|