Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 065 (Jesus reveals himself to the healed one)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
2. Pajug Gumba judduwaale ga (Yowaana 9:1-41)

c) Yeesu feeñu na ka mu fajoon ni Doomu Yàlla (Yowaana 9:35–41)


YOWAANA 9:35-38
35 Yeesu daldi yég ne, dàq nañu nit ka. Bi Mu dajee ak moom, Mu ne ko: »Ndax gëm nga »Doomu nit ki ? » 36 Waa ja ne Ko: »Wax ma mooy kan, sang bi, ba ma man koo gëm. »37 Yeesu ne ko: »Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yów. »39 Waa ja ne: » Boroom bi, gëm naa la. »Noonu mu jaamu Yeesu.

Bii pàcc kay sedd na xol. Bi Yeesu yéggee ne dàq nañu waa ja Muu fajoon, daf koo wër ba gis koca ñàkkug yaakaaram gu rëy ga. Yeesu dafa jekk ngir dëfal ñépp ñi gëm te tàggoo ak seeni waajur, seeni xarit, ndax Moom Krist. Bu fekkee ne ci jamono ju mel noonu nga ngay dund léegi, nungi lay xamal ne Yeesu déegg na say ñaxtu, te dina ñów Moom ci boppam ci yów te du la mos a bàyyi. Bul séentu ndimbalu nit ñi, ndaxte dañuy tas sa yaakaar. Neel jàkk Yeesu Moom kese. Amuloo benn yaakaar ci suuf ak asamaan bu dul ci Moom. Bëgg na la.

Bi loolu wéyee, Yeesu daldi laaj waa ji, laaj bu am solo lool: ”Ndax gëm nga Doomu Yàlla, jiy itam Doomu Nit ki?” Yeesu xamoon na ne waa ja xamoon na pàcc yooya ci téere Dañel nekk ci Kóllëre gu Njëkk ga (Dañel 7: 13-14) biy wax ne Doomu Nit ki mooy àttekatu àddina si, te mooy itam Doomu Yàlla ji. Yeesu dafa ko laaj loolu ngir xam ndax dogu na jébbal boppam kiliftéefu Doomu Yàlla ji, léegi ba abadan. Waa ja xamoon na ne Yeesu du nitu neen, noonu mu ne Ko”Boroom bi”. Bëggoon naa xam lu gën a yaatu ci Doomu Yàlla ji, ngir bañ a jaamu nitu kese, liy doon bokkaale.

Ci kow loolu Yeesu may ko tontu bu àndak ndam lu rëy, ne ko: » gis nga Ko ci kow ngëm, laata nga Koy gis ci jëmm. Man mii la, man Doomu Yàlla, jiy wax ak yów. » Waa ja amatuloon dara lu muy xaarati ngir jébbal boppam Yeesu. Yów yaay Mbëggeel gi ñu jëmmal, jox naa la sama bopp ci kow sama coobare gu mat sëkk, li ko dale ci tey, sa jaam laa. »Mbokk mi, ndax nangu nga Yeesu Doomu Yàlla ji, ci jëmmam? Ndax lëkkoo nga ak Moom ni ku Ko gëm? Ndax jaamu nga Ko ni surgaam?

YOWAANA 9:39-41
39 Yeesu ne ko: »Àttee ma taxa ñów àddina, ngir ñiy gis gumba. » 40 Bi Farisen ya nekkoon ak Moom déggee loolu, ñu ne Ko: »Xanaa nun itam danoo gumba? »41 Yeesu tontu leen ne: »Bu ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye fi ak yéena ngi naan: »nu ngi gis, » ci bàkkaar ngeen di dëkk.

Ba waa ja sujjóotee ca kanamu Yeesu, kenn terewu ko ko, ndaxte Yeesu yelloo na bépp sargal. Waaye Yeesu nee na dafa ñów ngir àtte ñu rëy ñi, ak ñu fonk diine ñiy yaakaar ne seen xam-xam màcc na, te xamuñu dara ci dëgg gi. Gumba ga ak bàkkaarkat ya xamoon nañu loola, ba tax ñu tuub seeni tooñ, ba ñu baal leen te sellal leen. Du ñi bañoon a tuub la Yeesu doon àtte, ñoom ñoo doon àtte seen bopp, ca na ñu doon weddee muccam gi. Jotoon nañoo gis ay leerali Yonent ya jiitu woon, ak ay seede yu ñu jukkee ci Téere yu sell yi. Waaye bu fekkoon ne ñoom la neex ñu bañ a nangu njàngalem Yeesu, kon dañuy ñàkk li desoon ci gindi gi. Dañoo naroon a gumba, ñëg, dëgër bopp, te nekk ay bóomkat. Ñówug Krist, ak waareem jur nañu ñaari mbir: Mucc gi, walla mbugal gi, barkeel bi, mbaa móolu gi. Lu mu jur ci sa xol?

Ca biir ña Ko doon déglu, amoon na fa ay Farisen yu doon yëg ne ñoom la waxi. Yeesu di joxoñ baaraam. Ñu laaj Ko: »Ndax nun danoo gumba? » Yeesu xàwwi seen naaféq ga, ne leen: » Bu ngeen jàppe woon seen bopp ni ñu gumba, te ngeen toroxlu ci seen nekkinu baatin, kon dingeen tuub seeni bàkkaar, te jot mbaal ak barkeel. Waaye dangeen di nax seen bopp naan xam ngeen lépp, di teg seen bopp ni ñu jub. Waaye ci seen rëy-rëylu, wone ngeen ngumba ak seen téxét. Dungeen jot genn ferñeentu leeraayu Leeru àddina si. »

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, yów yaay Doomu Yàlla, ji ñu jëmmal. Ñungi lay màggal, te di la jébbal sunu bopp li ko dale tey, ba fàww. Sunu kàttan ak sunu am-am yaa ko moom. Ñungi lay ñaan nga baal nu te sellal sunu xol, ba bàkkaar, lu mu tuuti tuuti bañ a dox sunu diggante.

LAAJ:

  1. Sujjóot ci kanamu Yeesu, lu muy tekki?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 22, 2025, at 03:40 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)