Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 063 (The Jews interrogate the healed man)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
2. Pajug Gumba judduwaale ga (Yowaana 9:1-41)

b) Yawut yaa ngay laaj nit ka ñu wéral (Yowaana 9:13–34)


YOWAANA 9:13-15
13 Noonu ñu indil Farisen ya nit ki gumbawoon. 14 Ndekete Yeesu, bés bi Mu tooyalee ban, ubbi bëti gumba ga, bésu noflaay la woon. 15 Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen : »Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi mu nekk maa ngi gis.

Dundu Yawut dafa nekkoon ab kaso bu Yoon tëj ñépp; seen xalaat yépp ci bésub noflaay bi ñu moy la nekkoon, te manuñu woon a bég ci wéral (paj mi) gi. Dëkkandoo ya ak yërndukat ya yóbbu nit ka ñu fajoon ca Farisen ya, ngir xam ndax paj mi ci Yàlla la jóge, walla ci Seytaane.

Noonu la layoo bu aju ci Yeesu,ak werante ya tàmbalee. Ngóor sa nettali na ni mu wére. Gàttal na ay waxam, ndaxte mbañu nooni Yeesu moo wàññi mbégteem.

YOWAANA 9:16-17
16 Ci noonu,am ca Farisen ya ñu naan: » Ki def lii, manul a jóge ci Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésu noflaay bi. « Ñeneen it di wax ne : » nan la boroom bàkkaar man a wonee yii firnde? »Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir. 17 Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: »Yów, loo wax ci moom? Yów de la ubbil say bët. » Mu ne leen: »Yonent la. »

Ba ñu dégloo seedeem ba noppi, ŋank-Yoon ya tàmbali di werante. Ñenn ña naan Yeesu amul genn kàttanu Yàlla ndaxte dafa moy sarti Ndigalu Boroom bi. Noonu ñu àtte ndaan Yeesu, teg ko ci sarti diine Yoon wi.

Ñeneen gis li nekk ci diggante bàkkaaru gumba gi, wéram gi ak mbaalam gi. Ñu xalaat ne wér gi war na am tekki -tekki gu gën a xóot, ndaxte dafa ànd ak kàttanu baale gi Yàlla am. Kon book xel xalaatul Yeesu nekk bàkkaarkat, ndaxte baale na bàkkaar ba, te saafara la indi woon nàqar ga.

Ñaari wàll yooyu yépp manuñu juboo ci lenn. Ñoom ñaar ñépp dañu gumba woon, ni mu ame tey jii ci sunu biir, ñoo xam ne dañuy am ay werante yu amul benn solo, ci lu aju ci Yeesu. Ñu teg ca di laajaat nit ka ñu faj, ngir man a xam ndax Yeesu wax na leneenati, te seetlu Ki mu ko teg. Laaj yu am soloo ngi noonu ngir képp ku xam dara ci Yeesu, rawatina nag ñi am juddu gu bees. Ndaxte xam nañu nan lañu leen man a goreele ci bàkkaar ak ci merum Yàlla. Bu nu judduwaatul ci baatin, dunu man a gis Yàlla.

Noonu ngóor sa ñu wéral di laaj boppam, naan: » Kon, kan mooy Yeesu? » Mu méngale Yeesu ak niti Yàlla ya feeñoon ca askanam, ca jamono ya weesu ya. Ca jamono jooja, amoon na ay kéemaan yu bare yu xewoon, waaye kenn mosuloon a faj gumbag judduwaale. Li ko dale ci jëfi Yeesu, ku nekk man nga ci gis ak lu mu néew-néew ne mennum Musalkat la woon. Noonu nit ka tudde Yeesu ab Yonent, Ki nga xam ne du caageen rekk ne man na xam ëllëg, waaye moo man a dogal tey, fees naga k kàttanu Yàlla. Dafay natt xol yi, te diwone coobare Yàlla.

YOWAANA 9:18-23
18 Yawut ya manuñu woon a nangu ne nit ka dafa gumba woon, tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram 19 laaj leen ne: ”Ndax kii mooy seen doom ji ngeen ne, gumba judduuwaale la? Kon fu mu jaar bay gis? 20 Waajur ya tontu ne: ” Xam nanu daal ne sunu doom la, te dafa judduwaale gumba. 21 Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.” 22 Ragal Yawut ya nag moo taxoon ba waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba. 23 Looloo tax waajur ya ne: ”Laajleen ko, magum jëmm la.”

Yawut yi nanguwuñu woon a méngale kéemaani Kóllëre gu Njëkk ga ak jëf yi Yàlla matale ci Yeesu, yi nga xam ne dañoo jéggi dayoo. Gëmuñu woon ne ab Yonent la, walla ku Yàlla Yebal; ndaxte bu demee noonu, kon seen toogaay du jekkati te tooñ lay doon.

Ñu wéy ci seen njuumte, di jàpp ne kéemaan googu, du dara lu dul neenu-neen, te nit ka gumbawuloon sax. Dañoo jekkoon ngir xataraayu ba yàq deru xew-xewu kéemaan gi loxoy Yeesu matal. Faj ag gumba judduwaale, dafa leen niroowoon ak lu manul a nekk, ndaxte ndono lu mbugal gu ñu donne ci bàkkaaru waajur la.

Ñu woolu waajuram ya. Ñooña tontu ak maandute, ndax ragal Farisen ya, te bañ sax wax ne dégg nañ dara lu jëm ci seen pajum doom ji. Dañu ko bàyyeek ay mbiram ngir bañ a bokk àtte bi. Kon, seen doom ji manuloon a wéeru ci kenn ku dul moom ci boppam. Bu la Sanedreŋ bi dàqee, lu jéggi dayoo la, ndaxte loolu dafay dog sa jokkoo ak askan wi, ni ñu daan jàppe ku gaana. Bépp yelleefam daf ko doon ñàkk, te du manati takk soxna. Na Yawut ya bañewoon Yeesu dafa metti woon, ba ñu yéenewoon sax rajaxe ñépp ñiy ànd ak Moom.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nu ngi lay sant ndaxte Yów yaay KiliftéefuYàlla gi ñu jëmmal. Bul nu bàyyi nuy yaakaar ci sunu kàttanu bopp ak sunu kaaraange, bu nu nekkee ci nattu. Dimbali nu, ba nu bañatee dunde ngir sunu bopp, te dee gënal nu weddi la, mbaa bañ laa yittewoo.

LAAJ:

  1. Lu tax Yawut ya nanguwuñu ne gumba judduwaale ga man na wér?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 22, 2025, at 01:15 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)