Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
2. Pajug Gumba judduwaale ga (Yowaana 9:1-41)
b) Yawut yaa ngay laaj nit ka ñu wéral (Yowaana 9:13–34)YOWAANA 9:24-25 Farisen ya def nañu seen kéem kàttan ngir man a jaar fu Yeesu néewlee doole ba ñu man Koo àttee daan. Ñu woo waa ja ñu fajoon ngir waatloo ko ba mu seede lu dul dëgg ci Yeesu, ba jiiñ ko tuuma. Ñu biral ne xarañ nañu ngir wone ne Yeesu bàkkaarkat la; li ñu doon wut rekk mooy ab seede bu leer. Ñu bëgg koo bëmëx ba mu nangu li ñu bëgg te jiiñ Yeesu. Li ñu doon wut mooy waxloo ko ne du ci ndamul waa Nasaret ji la wére. Waaye mu tontu leen ak maandute ne: »Xamuma ndax bàkkaarkat la, Yàlla rekk a xam. Li ma xam daal, mooy, damaa gumba woon, te léegi maa ngi gis. »Loolu, kenn manu ko weddi. Dafay ëmbaale kéemaan, doole ju jóge asamaan ak yiwu mbaal gi. Seede waxambaane bii, bokk na ci yi ay junniy way-gëm di firndeel. Man nañoo ñàkk a xam kumpay asamaan yi, ak yu Safara, waaye jot nañu judd gu bees. Képp ci ñoom man na wax ne: »Damaa gumba woon, waaye léegi maa ngi gis. » YOWAANA 9:26-27 Farisen ya mer lool ca tontu waa ja, noonu ñuy jéem a wut lu ljuuyoo ciy kàddoom, ba man koo daaneel. Noonu ñu ñaan ko mu delluci nettaleem ba. Rekk, mu mer ne leen: ”Xanaa dégguleen li ma leen nettali? Walla dangeen koo bëgg a déggaat ngir man a nekk ay taalibeem?” YOWAANA 9:28-34 Ba leen waa ja toroxalee bindkati téere ya, ak kàŋaam ya xaacu di ko saaga naan: » Du nun,waaye yów mii yaay taalibe naxaatekat boobu. Nun Musaa lanuy topp, moom mi wax ak Yàlla. »Yeesu jotoon na leen wax ne bu ñu xamoon Musaa, kon, dinañu dégg ay kàddoom; Waaye ndegam dañoo dëpp waxi Musaa, te di leen di jëfandikoo nib lay, kon duñu Ko (Yeesu) man a xam itam, sàkkantumaak Xel miy waxe ci Moom. Ci kow loolu la waa ja wéroon tontoo ne: »Kiy ubbi bëi gumbag judduwaale kay am na kàttanu Aji sàkk ji. Am na doole, te man na. Xaarul sax Ay ngërëm aky cant. Gisuma genn tooñ mbaa lu ñu Ko man a daane ci moom. » Mu teg ca biral ne: » képp ku bokk ci kóllëre gu Njëkk ga xam nga ne Yàlla du antu ñaani ku rëy. Bàkkaar dafay tax ba Yàlla du barkeel nit ki. Waaye ki nangoo suufeelu ci kanamu Ku Sell ki, nangu ay bàkkaaram, te tuub leen, namm ngëm akmbëggeel, boole ci cant, kooku la Yàlla di waxal nopp ak nopp. » « Kenn ci yéen manu ma woon a ubbil samay bët, kenn manu ko, ndaxte ñépp a bàkkaar, ba mu des Yeesu. Moo ma manoon a faj, loolu mooy firnde ne amul bàkkaar. Yàlla ci Moom la nekk. » Ci kow loolu Farisen ya móolu ko: »Yów rekk yaa bon ak say waajur. Seen mbon gi moo feeñ ci sa ngumba gi. »Niti diine yooyu xamuñu woon ne ñoo gënoon a gumba waa jooja Yeesu dafa koo jël ni as ndaw, ngir won leen li Mu leen man a defal. Waaye ñoom dañoo weddi njàngalem Yeesu, ci ni ñu sàbbee kàdduy ki ñu faj. Noonu, ñu dàq ko ca jàngu ba. Njëkkoon nañu ko dàq ca bérabu ndaje Kuréel ga, léeegi nag ci kanamu ñépp lañu koy bërgal ni taalibe Yeesu. Bés booba lañu ko faj, te it ca lañu ko dàqe ca askan wa. Loolu wone na ne nit ñooña àttanuñu woon Xelum Krist. LAAJ:
|