Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)
4. Yeesu, may na ñépp ñu man a tànnal seen bopp ngir “nangu walla bañ!” (Yowaana 6:22-59)YOWAANA 6:22-25 Ba mbooloo ma xamee ne Yeesu àndul ak ñoom ca gaal ga, waaye ñoom rekk a àndoon, ñu jaaxle lool ci ni Mu fexee ba rëcc leen, te yégu ñu Ko. Dafa yoxoosu ci guddi gi bàyyi leen fa. Waa kapernawum nag,ba ñu déggee xew-xewu mburu ma, ñu ànd ak mbég mu rax siis, ndaxte bëggoon nañu am xéewal gu ni mel. Noonu ñu wëri Yeesu ba fekk Ko ak ay taalibeem. Foofa ñu tàmbale xam ponku kercen biy wax ne « Fépp fu ñaar mbaa ñett daje ci sama tur, maa ngi ci seen biir. » Ña bëggoon a gis ay kéemaan gis leneen lu jéggi dayoo ba laaj Ko ne: ”waaw yow kañ ak noo def ba agsi fii?” Yeesu tontuwu leen. Waaye ngir bañ seen ngëm yoqi, Mu leeralal leen liy ngëm, di ci wutaale noonu ñi dogu ci mbëggeelam, te nangoo feeñal naxaate, ak weddig bañaaleem yi. Yeesu bëgguloon ñiy tagatémbe ci diggante tàng ak sedd, te noonu la tàqalee way-gëm yi ak gàngooru ña doon mbubboo diine. YOWAANA 6:26-27 Yeesu dafa artu bu baax mbooloo mi: Bëgguleen ma, walla wutuleen ma, man ci sama bopp; ni ngeen jàppe Yàlla du noonu; seeni biir rekk ngeen di xalaat ak mburu. Ràññeewu leen misaal mi, li ma ci jubluwoon du faj seen xiif, waaye dama bëggoon ngeen xam sama kàttan. Yéen a ngi wut may gi te xamuleen Kiy maye. Yeen a ngi waxtaan ci mbiri àddina, te gëmuleen sama baatin. Buleen liggéey bés bi yépp ngir lekk ak naan doŋŋ; bàyyileen xel ci kàttanu Yàlla. Buleen mel ni ay bàyyima yuy dund ngir di lekk rekk, waaye jegesileen Yàlla, miy Xel. Moom jekk na ngir boole leen ci dundam gu amul àpp gi. Yeesu rax ca dolli ne leen: Damaa ñów ci àddina si ngir maysi leen neexalu Yàlla bi gën a tabe. Duma nitu suux ak deret kese. Waaye indaaleel naa leen mayug Yàlla ngir barkeel leen. Yàlla tàmpe na ma ak Xelam mu Sell mi ngir ma yët leen dunug baatin gi te yiir leen ak kàttanu asamaan ji. Ci kàddu yooyu, Yeesu feeñal na kumpa gu réy, giy xamle ne, Yàlla bépp doomu Aadama soxal na Ko, te dafa koy dundal, te it bëgg ko. Kon Yàlla du boroom mer buy xataraayu ba ku toppul Yoon wi du la barkeel. Dafay barkeel ki bon ak ki baax, te jantam bi dafay fenq ci kow ñépp; yéeféer yi sax ak tuumaalkat yi dañu ciy barkeelu. Yàlla mbëggeel la, te Krist dafa bëggoon a goreel nit ñi ci seeni xalaati àddina, ngir ñu delloo seen kóllëre ak Yàlla Baay bi. Biral na ne nguuram nekkul ci àddina sii, dundam ajuwuloon ci lekk; alal ak kilifteef, waaye nguuram baatin moo ko lal, te ci Xelam lay wàcce ci ñoom, maanaam Xel mi Muy may ñépp ñi Ko ko ñaan. YOWAANA 6:28-29 Mbooloo ma xamuñu woon njàngalem Yeesu, waaye bi ñu gisee ne dafay joxe mayug Yàlla gu réy, ñépp bëgg a jot dund gu amul àpp googu. Jekkoon nañu ngir def dara ba man a jot may googu, Parewoon nañu ngir topp Yoon wi, sàkk ay sarax ,woor, ñaan, te aji; dañoo bëggoon a yelloo mayu Yàlla jaare ko ci seeni jëf. Ndaw ay gumba ! Ñoom ñépp way-toppkati diine lañuwoon, yuy wut a am mucc gi ci kow seeny góor-góorlu. Xamuñu woon ne loolu manul a nekk, ndaxte dañoo tooñ te sànku. Ci kow seen mbégte, ñungi doon xalaat ne matal nañu liggéeyu Yàlla te di yaakaar ne am nañu sellaay ak kàttanu matal ko. Nit dafa gumba ba du man a gis sax ni xolam mel, di jàppe boppam nag ni gennwàllu Yàlla, di séentu Yàlla bég ci moom. Yeesu jàngal leen ne tegu leen benn liggéey, mbaa sas. Ñu gëm Ko rekk moo doon seenub woote. Yàlla laajunu genn góor-góorlu, waaye dafa bëgg nu jébbalu ci Yeesu te wóolu Ko. Kàddu yooyu, doju fakkastal lañuwoon ca nit ña; foofa la ŋaayoo ba tàmbale ci diggante Yeesu ak gàngoor ga. Rax ca dolli, Mu leeralal leen ne jëfu Yàlla mooy ñu gëm Ko.” Bu ngeen ubbilee seen ruu Xel mu Sell mi, dingeen xam sama kàttan, samay mébét ak sama mbëggeel. Gannaaw loolu dingeen xam ne duma Yonentu neen, waaye Maay ki sàkk lépp, di Doom ji leen Baay ji yónnee. Kon dingeen dakkal seeny njàqare te nekk ay doomi Yàlla.” Gëm Yeesu mooy taq ci Moom, te may Ko muy dogal ci sa dund, nangu Mu lay wommat te nga jot dund gu amul àpp gi, ci kàttanam. Ngëm moo nuy lëkkale ak Yeesu li ko tàmbalee léegi ba abada. Liggéeyu Yàlla dafay lëkkale way-gëm yi ak Doomam ji, ngir bàkkaar génn ci seen dund, te ñu man a sax ci Moom ba fàww. YOWAANA 6:30-33 Ña ko doon dëglu am naqar lool ba ñu déggee ne Yeesu dafa leen di laaj ñu jébbalu ba seey ci moom. Lu mel noonu, Yàlla doŋŋ moo ko yelloo. Noonu ñu laaj Ko ay firnde yu man a biral kàddoom yooyu. Li ñu bëggoon a wax mooy: “ won nu ne Yàlla nga. Musaa daan na dundale askan wa ak mburu (mànn) bés bu nekk ca màndiŋ ma. Yów nag luy tollook junni nit rekk nga reggal. Kon kay won nu kéemaan gu gën a takku, ngir nu gëm la.” Lii feebaru doomu Aadama la. Nit ki dafay faral di bañ a jébbalu ci mbëggeelu Yeesu cig neen, waaye dafay bëgg a gis ay firnde ba noppi. Waaye Yeesu tontu ne: ” Barkeel nañu, ñi gisul, te gëm. Mooy ñi may terale seen kóolute.” Yeesu mooy njiit li sut ñépp. Dànk-dànk la won ña Ko daan déglu yoon wi ñuy jaar ba sore seen taq ci diine googu, te dugg ci ngëm gu leer ci Moom. Dafa leen a yewwi ci bëgg-bëggu lekk gu tar, te dugal leen cig leer; Moom ci boppam mooy gën gi- mayug Yàlla. Bi Mu leen faramfàcceel lépp, Yeesu dafa jubanti seen xalaat yu dëng yi ñu dégge Mbind mi. Noonu la leen xamale ne du Musaa moo leen doon may mànn ja. Ci dëgg, Yàlla ci boppam moo mataloon kéemaan googu, Moom miy Aji Maye ju tabe ji. Mu fexe ba ñu xam ne Yàlla moo leen di may mburu mi gën ak ñamu asamaan wu dul nëb mukk. Bu ñu ubbiwoon seeni nopp bu baax, kon doon nañu xam ne Yeesu mungi leen di woon ne Doomu Yàlla la, ndaxte mungi woowe Yàlla « Baay ». Waaye mbooloo ma wéy di xaar ñam wu ñu man a lekk, wuy jóge asamaan te jaare ci loxoy Musaa. Yeesu dafa yéegal seen gis-gis ngir ñu xam ni mburu Yàlla du lu ñuy wann ci biir, waaye mooy Kirist miy féexal xiif gi nit ñi am ci dëgg ak dundu gu bari. Kiy jox wàcci ci asamaan si, yor barkeb Yàlla ak doole. Buru Yàlla du mburu àdduna, du mburu mu yàqu, waaye mburu ngëm la, di dundu ba fàww. Du joge ci suuf ni manna, waaye ci Yàlla la joge, barina lu doy ngir ñépp, ngay mag wala ndaw. Du yam ci mbokki Ibraayma kese. Yàlla Baay bi mooy toppatoo àddina sépp. ÑAAN: Boroom bi Yeesu sàmm nu ba nu man a moytu bépp jëfu bopp- sa bopp. May nu ngëm gu suufeelu te nangu sa coobare, te it ngay jëfe ci nun ak sa kàttan. Fexeel ba nu am jokkoo gu mat sëkk ak yów. Reggalal nu sunu xiifu xol jaare ko ci sa teewaay ci sunug dund. Sàmm nu ba fàww. Baay nungi lay sant, ci li nga nu ganesi, te may nu sa kàttan ak say barke. LAAJ:
|