Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 041 (Jesus withdraws from the clamor for his crowning; Jesus comes to his disciples in distress)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)

2. Yeesu dafa rocceeku ci ñi Ko bëgg a fal buur (Yowaana 6:14-15)


YOWAANA 6:14-15
14 Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne “dëgg-dëgg kii, mooy“ Yonent bi war a ñów ci àddina ”! 15 Yeesu gis ne dañu ko war a jëlsi, fal Ko buur, Mu bãyyi leen fa, dellu Moo, rekk ca tund wa.

Yeesu dafa ñów ci ãddina ngir jotal boppam nit ñi. Ba mbooloo ma reggee ba noppi, nit ñay xaar lu cay topp! Ñu tãccu Yeesu te teral Ko ni buur. Ñu xam ne waayu Galile jii, nitu Yãlla la, baatu Yãlla mooy génne ci gémmiñam, te kãttanu Aji Kowe ji mooy feeñ ci Moom. Càkkite gépp dafa koy déggal. Mayoon na leen, mburu na ko Musaa defe woon ca, mànding ma. Moo nekkoon Yonent ba ñu digewoon ngir Mu gindi askan wu ñu bañ, ba mu xam dëgg gi (Detoronom 18: 15). Dañoo yaakaaroon ne bu Yeesu nekkee seen buur, dootuñu soxla dara lu jëm ci liggéey, mbaa coono. » Dinanu am jotu jàng Kàddu gi, te di ñaan, Mu nuy dundal te dunu fay dara. Buur bu ni mel war naa man a am kàttanu daan xarekati Rom yi. Dina man a wàccee safaras asamaan si sax, ngir mu lakk leen ba ñu xëm. » Nanu Ko kaala, te fal Ko buur. » Ñu déggoo ne nanu Ko tungoom, jàppale Ko ngir Mu fajal nu sunuy soxla.

Lan la Yeesu doon xalaat ci pexey gangoor googu? Ndax bégoon na ci seen mébet googu? Ndax daanu na ci fiiru taxawal as nguur gu koy ñi gëmul di jàppale? Walla dafa jañax seen tëralin boobu? Déedéet, tegu ci benn baat, dafa beru rekk ca mànding ma. Bëgguloon ay nit di Ko tungoom ca, bedd ya. Yàlla mungi Ko doon jàppale, te loolu doyoon na Ko. Yeesu xamoon na li doon junj, bégte moomu. Seen, bégte mu rembax, moo leen tere man a dégg ay yeddam. Mbootaayu politik la woon, gu sax ci benn xalaat doŋŋ.

Yeesu amuloon benn xalaatu taxawal nguur ci kow suuf; li Mu yittewoon, mooy tuubloo benn par benn doomi Aadama yi, te may leen dund gu amul àpp. Amul kenn ku man a dugg ci nguuru Yàlla te jaarul ci judduwaat. Mbooloo ma manuñu woon natt tëralinu kéemaan ya, ak firnde ya. Mbooloo ma mburum àddina la doon xalaat; te fekk Yeesu mungi joxoñ Xel mu Sell mi ngir mu saafara xiif gu gën a tar. Mbooloo ma di xalaat ci kilifteewu àddina, teg ca ndam li; Moom mu tànn kurwaa ba ni ponku nguuram. Boo rëccuwul, te yuub say bàkkaar, ba judduuwaat, doo, man a nekk ku Krist di teeru.

Yeesu soxlawuloon ay bàkk. Nànguwuloon ndam li nit di jagle, waaye baatu Baayam la doon déglu. Dafa tëj xolam ci bépp fiiru Seytaane. Mu beru ngir ñaan, sant Baay ji te ñaan ngir bëti gumba yi ubbeeku ci kàttanu Xel mu Sell mi. Manuloon a nangu ñi koy fal tey, naan ko « hosanna », di Ko yuuxu suba, naan « daajleen Ko ci bant ». Krist xam na xol yi.


3. Yeesu dafay wallu ay taalibeem (Yowaana 6:16-21)


YOWAANA 6:16-21
16 Ba ngoon jotee, taalibeem ya wàcc ca tefes ga. 17 Ñu dugg gaal, jëm kapernaum. Guddi jottoon na daanaka, te Yeesu dabaguleenoon. 18 Ngelaw lu mag upp, géej gi sàmbaraax. 19 Ba ñu joowee lu tollook ñaar fukki meetar ak lu topp, ñu gis Yeesu di dox ci kow ndox mi, jubsi leen. Ñu tiit lool. 20 Waaye Yeesu ne leen: Man la, buleen tiit! 21 Rekk ñu bëggoon koo yégloo ca gaal ga, faf ñu àgg ca teeru ba.

Na Yeesu doon noppaloo ca tundi Golan ya, Mu gis ca sore sa, na taalibeem ya sonnee ci xataraayu ak tow bu metti ba. Na guddi ga doon agsee, Mu dabi leen, di dox ci kow ndox mi. Ba jafe-jafe amee, bàyyiwu leen. Taalibe ya teg Ko njuuma ba tiit lool. Nappkat yi dañuy faral di jommi, ndax li ñuy yàgg a guddee géej. Yeesu jegesi leen, te ne leen: » Man la ». Yooyu baat mujj nekk ponku ngëmu ndaw ya. Ci téere Kóllëre gu Njëkk gi man nanu ci gis lu muy méngool, maanaam » Maay ki nekk », liy tekki teewaayu Aji Sax ji ci biir way-gëm yi. Noonu taalibe ya xam ne Yeesu Moo sut lépp li am; ciy loxoom, mburu mi dafay bare, duus yi dal, te tow bi séwét. Ba ñu xamee loolu, ñu gën a tiitati. Mu ne leen bu ñu tiitati. Ndigal lii » Bul ragal », feeñ na « 365 yoon ci Biibal bi, maanaam benn yoon bés bu nekk ci at mi, te loolu taalibe jamono yépp la ko jagleel. Gëmal ne teewaayu Krist moo sut sunu tiitaange. Ak nu sa dund man a deme, walla say coono man a tollu, Yeesu nee na la « Man la, bul ragal! »

Ba taalibe ya xàmmee Yeesu, dañoo waaru te ñaan Ko mu yéeg ca gaal ga. Noona ñu yegg ca tefes ga. Loolu mooy ñetteelu kéemaanu bés ba. Yeesu mooy Boroom jaww ji, ak jamono ji, te man na dawal gaalu Jàngu bi ci biir tow bu metti bi, ba mu teer ci jàmm. Ku bëgg ay taalibeem la, te di leen jegesi, waaye nag dafay bëgg ñu koy wóolu Moom rekk. Dafay dëgëral seen kóolute ci Moom ci biir lëndëm gi ak nattu yi, ngir dalal seenug tiitaange te uuf leen.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu bañ mbooloo ma fal Ko buur?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 01, 2025, at 03:23 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)