Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)
4. Yeesu, may na ñépp ñu man a tànnal seen bopp ngir “nangu walla bañ!” (Yowaana 6:22-59)YOWAANA 6:34-35 Yeesu dafa xiifloo woon Yàlla ña Ko doon dëglu, te yewwi leen ca buumu jëf yu leer yu ñu daan faydaal. Dafa leen a gindi ci mucc gi, te jekkal leen ngir ñu man a jot mayug Yàlla gi; mu xamal leen ni ñu Ko soxlaa gëme moom ci boppam. Mbooloo ma nangu ay kàddoom ak mbég mu xaw a taq suuf naan: » Yów miy maye mburu asamaan, dee nu ci jox bés bu nekk ndax sunu coono liggéey teggeeku nu. Yów lanu wóolu,may nu dund gu dul jeex ak sa kàttan! » Ba léegi seeny xel a ngi dem ci mburu àddina si, waaye nag, lu mu néew-néew jot nañoo xam ne mayug Yàlla gi, genn doŋŋ la, amul moroom. Yeesu teggiwul dara ci li ñu koy tegal. Moom dafa njëkk mburum Yàlla ngir àddina sépp, waaye nekkul joxekatu ñam. Moom ci boppam mooy maye lépp li dund gu amul àpp gi di laaj. Nee na sax: » Fàww ngeen jaare ci Man ngir man a am dund gu dund gu dul jeex gi. Maay mayug Yàlla gi ngir yeen; Bu ma cóolee ci seen dund, ngeen dee. » « Ni la mburu mi ngay lekk di joxe cawarte ci sag dund, man itam noonu laa la bëgg a soloo, yeesalaat sa xel ak say xalaat ngir nga man a dunde Xel mu sell mi. Bu ma àndul ak yów doo man a def dara. Danga may soxla bés bu nekk. Laajuma la dara. Amul dara loo war a fay. May ma rekk ma dugg ci sa xol. » Mbokk mi, soxla nga Krist yów ci sa bopp ci dëgg-dëgg. Ni ñam ak ndox amee solo ci sa dund, noonu la la amelee solo. Di jàng ay kàddoom, walla di xam ay xalaatam, loolu doyul. Ganale Ko te teeru Ko ci sa dund wala nga dee. Man nga laaj sa bopp nan la man a dugge ci sa xol bi nga yor? Mungi tontu naan: Bëgg ma ak sa xol bépp, jege ma te teeru ma ak ngërëm, gëm ma, Ñówug Yeesu ci sa xol, ci sa ngëm lay jaare. Santal Yàlla ndaxte mooy may gi la Yàlla jagleel, dafay jébbale boppam te laajul genn payoor; sant Ko ak mbég, ndaxte jekk na ngir dëkk ci yów. Dina ñów boo Ko ko ñaanee ak ngëm gu dëggu. Saraxu Ko ngir Mu dëkk ci yów ba fàww. Boo séqee jéego boobu ba noppi, Yeesu dina la sol jàmmam ba nga fees dell: » Ndegam teeru (dalal) nga ma, dinaa dëkk ci yów te màndal sa marum dund. Bul weranteeti lu jëm ci diiney àddina si ak ay xalaatam, ngir xam ban ci ñoom mooy dëgg. Bul tanq ndox mu nekk ngir faj sa mar. Dinaa la may dund gu tekki, tegal la ci sama jàmm ak sama kàttan. » YOWAANA 6:36-40 Yeesu dafa may waa Galile mburu yiw gi. Ñoom itam ñu ràññee ne am na sañ-sañ bu fees ak kàttan. Waaye, ak li ñuy xam loolu lépp taxul ñu gëm, mbaa ñu seede seen ngëm. Dañu doon yox-yoxi ba léegi. Dañu nawoon Yeesu ni Boroom mburu mi, waaye seen kóolute ci moom ni doomu Aadama desoon na. Nanguwuñu Ko woon ak cant. Naka ca Yerusalem, Yeesu xamal leen li tax ñu dogoo. Lu tax ñu bare wóoluwuñu Ko? Yeesu manoon na leen a wax ne: » Yeen a ko def! » Waaye dafa leen téenloo ngir ñu séen Baay bi te xam loo leen ne ngëm baatin moo koy suuxat ba mu màgg. Yeesu bëggul a xëcc kenn jaare ko ci ay ndëgg-pëtëx, ay yeyante; Yàlla ci boppam mooy xiir nit ñi ci Krist, ndaxte xam na seen xol ak fi seen yéene coobare tuub te jébbalu tollu. Ñi XEL mi woo doŋŋ ñooy xiiru ci Yeesu. Krist bañul fenkat bi, njaalookat bi, sàcc bi, ñi nga xam ne ñungi ñów ci Moom te tuub seeni bàkkaar. Amul kenn ku Mu dàq ci ñi Ko jegesi, du sax ay noonam. Dafa leen yéramoon te may leen mucc gi. Krist ñówuloon ci àddina ngir boppam, jekkaluloon dundam ngir faj ay bëgg-bëggi boppam. Dafa ganesi àddina ngir matal coobare Baayam, te ànd bu jekk ak mbëggeelam, ngir musal ñépp ñiy mucc, teg ci di sàmm ñi bëgg sax ci Moom. Kenn manul a natt yéwénaayam ak dooleem giy maye mucc. Dee gi, Seytaane, mbaa bàkkaar manuñu foqati ñi nekk ciy loxoom. Ci biir yërmandeem, dina dekkil ay taalibeem ca bésub àtte ba ngir may leen dund gu amul àpp. Ndax xam nga coobare Yàlla Dafa bëgg nga naw Doomam ji, jéem Koo xam te wóolu ko. Ci Xel mu Sell mi la juddoo, fees dell ak yiw, ak dëgg. Dafa bëgg bga jokkoo ak Musalkat bi, ak way-gëm yépp, ci biir kóllëre gu amul àpp te kenn du ko man a tas; su ko defee li Yàlla namm ci yów dina mat. Ci saa si way-gëm ji jotee dund gu amul àpp gi, ci la Xel mu Sell mi di dugg ci yaramam ju ñàkk doole ji. Sa ngëm ci Yeesu moo lay wóoral sa dund ak Yàlla ba fàww, te muy dund guy wone mbëggeel, mbég, jàmm ak lewetaay. Dundug Yàlla ci yów du jeex mukk. Mujjantalu jéego nammeelu Yàlla mooy na la Yeesu dekkil ci ñi dee. Loolu mooy yaakaaru way-gëm yi, bi gën a rëy; naka noonu, njobbaxtalu dund gi la Doom ji may, dina feeñ-Ndamul Doomam ji ak leeraayu mbëggeelam. ÑAAN: Nungi lay màggal Sorewoo nu. Waaye dangaa ñów ci nun, te fekk mbooloo yi di la sàbbi. May nga nu nu gis la te nangu la ni mburu mi dëgg. Jarajëf ci sa teraanga ji. Màndal nga sunu maru ruu, te dinga nu dekkil ngir dund gu amul àpp gu ànd aky cant ba fàww. LAAJ:
|