Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)
1. Yeesu dundal na juróomi junni nit (Yowaana 6:1-13)Ca Yerusalem ,Yeesu dafa wone mooy kan, ba Mu wéralee nit ca bésub noflaay ba, di ca feeñal kàmb gu xóot gi dox ci diggante mbëggeelu Yàlla ak xalaat yu teggi ndawal yu waa ŋank-Yoon ya. Ces derniers résolurent de se débarrasser de lui en vitesse. Le a Saint-Esprit conduisit Jésus en Galilée, où la coupure décisive entre lui et ses adversaires atteindrait son paroxysme. Les habitéants du Nord le suivaient encore partout où il allait. YOWAANA 6:1–4 Ba Yeesu dalee ca kow ŋank - yoon ya ca Yerusalem, dañu Ko doon fexeel te di Ko yërndu, waaye waxtoom jotaguloon. Noonu Mu tàggoo ak kuréelu Sanedreŋ ba dem Galile, fa Mu defewoon kéemaan yu bare. Ñówam daldi indi coow lu baree-bare, lu xaajul a yëngal Yeesu. Xamoon na ne xalaat yu nëbbu ya nekkoon ca péey ma, ñooy law ba ci dëkk-dëkkaan, yi ñu Ko nar a xatale itam. Mu daldi dem Golan,ca penku Yurdan, ngir lëlu fa ak ay taalibeem. Waaye nag gàngoor gi nammoon lool dégg ay kàddoom, te barkeelu ci ay kéemaanam, dar Ko boor bu nekk. Ca at mooma, Yeesu delluwul Yerusalem ngir màggali bésub jéggi ba, ndaxte waxtu deewam jotaguloon. Dafa màggalandoowoon ak ña Mu nekkalandoowoon; muy ab misaalu berndeelu asamaan, ba Musalkat bi di dalal ñu sell ñi, di bégandoo ak ñoom. YOWAANA 6:5–13 Ba Yeesu séenee mbooloo ma di jegesi, Mu téen xool Baayam ji ci asamaan, màggal Ko te siggil Ko, te diisaale Ko soxla ña xiif ña. Foofa la kéemaan ga tàmbalee. Baay ja dénk Doom ja sasu feeñal la làqu ca xol ya. Yeesu dafa jëkk a seetlu taalibeem yi, ngir xool ndax seen ngëm mungi gën a dëgër, ak ndax ñungi wéeru ba tey ci alalu àddina, ak ni nit ñi di xalaate. Noonu Mu laaj Filip fu ñu man a ame mburu. Bu fekkoon ne nun la, danu naan ca mbulañse ba. Yeesu moom, Baayam la doon xalaat. Nun, sunuy xalaat ci jafe-jafe dund gi, ak ci xaalis la jublu. Waaye Yeesu ci Boroom ndimbal li la wéeruwoon. Filip njëg gi moo ko jaaxaloon, te fasuloon genn kóolute ci ngëmam. Képp kuy xool ci xaalis, doo mos a daj xéewali asamaan. La taalibe ya xalaatoon nag, lu jaadu la. Ca diiwaan booba bépp amu fa woon fenn fu ñu man a defare mburu. Waaye nit ñaangi teew, xiif te yàgg a toog di déglu. Jekk-jekki rekk Xelum Yàlla mi won Andare ab xale bu góor bu yore juróomi mburu ak ñaari jën. Taalibe ba yóbbu ko ca Yeesu. Ñoom ñépp dañoo jaaxlewoon, ndax xam ne ñam woowu, xaajul a doy mbooloo ma. Yeesu fexe ba taalibe ya xam fa ñu daanoo. Xamuñuwoon lu ñu war a def, ndaxte umpalewoon nañ coobare Yàlla. Yeesu sant taalibe ya ñu toogloo mbooloo ma, mel ni ñuy waajal añub buur. Ñax ma muur suuf sa,di misaal ngëm giy meññ ci xol. Juróomi junni góor, boole ci ay jigéen aky xale. Ndaw nit ñu bare! Ña ca ëppoon mosuñuwoon gis Yeesu, rawatina sax ay jallooreem. Waaye ci ndigalam, toog nañu. Ci teey, Yeesu jël mburu ya ngir wone kàttanam. Mu won Baayam juróomi mburu yi, te gërëm Ko ci néewaay bi. Xamoon na ne Yàlla dina barkeel lu tuuti loolu ba mu rembax. Cant gi jóge ci lu ndaw loolu, ak teral Baayam ji ñooy mbooti kéemaan gi. Ndax yaa ngi nangu ak ngërëm lu tuuti li la Yàlla jox, walla yaa ngi ñaxtu ci loolu? Ndax yaa ngi séddoo tuuti ak say xarit? Yeesu bëggul wone boppam kese; mbëggeelu Yàlla sax na ci moom. Teraloon na Baay bi te séddoo barkeb Yàlla ci ñépp. Kéemtaan bi ñu bind ci ñeenti Evanjil yi, dañu ko bind ci lu amul benn werante. Noonu kenn ci ñoom gis ko, ludul ñi toogoon ci wetu Kirist, te ñu gis ni, bi muy dagg mburu yi, ñuy gëna feeñ, te mburu yi dañu melni lu amul àpp. Ñu dem ak dikk, séddale ñépp ndax ku nekk jël limu soxla. Loolu mooy màndarga yiw wi. Yàlla dafay jéggale ak Xelam ci lu amul àpp. Jël li nga bëgg; Gëm leen fu ngeen mëna. Jox ñeneen ñi barke bi. Barkeel leen ni ñu la barkeelee, nga nekk luy barkeel ñeneen ñi. Ca Kanaa, Yeesu dafa soppi ndox,mu nekk biiñ, te ca Golan, Mu sof juróomi mburu ya ngir dundal lu ëpp juróomi junni góor. Li doy waar mooy ne, la desoon ca mburu moo ëpp la ñu amoon ca njalbéen ga! Fukki pañe ak ñaari desit lañu dajale. Yeesu ne leen bu ñu bàyyi dara muy yàqu. Tey jii, ñiy sànni seeny ndesit ci mbalit, war nañu rus, ndaxte xam nanu ne ay téeméeri junni nit ñungi dee bés bu nekk ak xiif. Bul ñàkk say barke yi nga war a bànneexoo, ndax sa ñàkk a bàyyim xel. Deel dajale desiti yiw yi. Dinga jot lu ëpp li nga man a taawu. Bàyyil xel ci xale bi moomoon mburu ya. Ab seede la ci kéemaanu Yeesu bi, te waroon naa yéemu. Ci lu leer, du fàtte la xewoon mukk. ÑAAN: Boroom bi sant naa la ci sa muñ ak sa mbëggeel. Baal nu sunu ñgëm lu néew li. Won nu ni nu war a jubloo ci Yów, saa yu nu jaaxlee, te nu bañ a sukkandiku ci sunu man-man, waaye ci say ngëneel. Nungi lay sant ci baawwaani baatin yi nga nu jagleel, ba sax ci sunu néewle. Dangay barkeel as néew li nu am, te di nu dimbali ba dunu ci yàq dara, te dunu fowe sunuy may. LAAJ:
|