Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 035 (God works with His Son)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
A - Ñaareelu tukki ca Yeruusalem (Yowaana 5:1-47) -- Yokkute jànkoonte diggante Yeesu ak Yawut ya

2. Yàllaa ngi jëfandoo ak Doomam (Yowaana 5:17-20)


YOWAANA 5:17-18
17 Yeesu tontu leen ne: » Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey, » 18 Baat boobu moo tax ba Yawut ya gën Koo wut a rey, ndaxte yemuloon rekk ci bañ a topp ndigalu bésu noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.

Laata pajum Betesda moomu, jànkoonte gi ak Yeesu taruloon lool. Waaye, ba loolu xewee, ërtal ma gën a metti. Noonam ya fas Koo faat. Noonu, kéemaan googu moo gën a indi jaxasoo diggante Yeesu ak Yawut ya. Noonu lañu tàmbalee bundxataale Yeesu, ba fas Ko yéene bóom. Lu waral coppite googu?

Foofa nag, ŋaayoo bi jolli ci diggante ni mbëggeelu Krist di feeñe, ak sañ-sañu Yoon wi ak teeŋaayam. Ca jamonoy Kóllëre gu Njëkk ga, nit ña dañu daan dunde ni ñu ñu tëj kaso. Àtte yu bare lañu daan siiwal ngir xiir nit ci topp Yoon wi ni mu ware. Boroom diine yi dañu daan fexe ba duñu moy benn araf ci Ndigal yi, ngir man a jot ci barke yi Yàlla di maye. Topp Yoon wi dafa mujj nekk taafantoo ngir lawal bopp-sa bopp, ak ñàkk mbëggeel. Ndegam askan wa dafa nekkoon ci buumu lëkkoo ak Yàlla, te ñu jàppewoon ko ni ku ñu tànn te ber ko, ña ëppaloon ña dañu daan ñaax nit ña ngir ñuy topp seeni santaane yu bare yaa-bare. Santaane bi ci ëppoon solo mooy bu bésub noflaay b, bi nga xam ne kenn waru ca liggéey. Ni Yàlla noppaloowoon ca juróom-ñaareelu fan wa, noonu itam lañu tereewoon kuy jëf bépp xeetu liggéey ci bésub jaamu boobu, mbaa ñu faat la.

Noonu la Bésub Noflaay bi (Sabat) nekkewoon ab jokkoo ci diggante Yawut yi ak seen Yàlla, te daan wone teewaayam ci seen biir, mel ni amul benn bàkkaar bu ñu jëf ci kanamam, bay dog déggoo googu.

Tontu bu woyof la Yeesu may Farisen yi doon ñurumtu ci mbirum moy ndigalu bésub noflaay boobu: » Yàlla mungi liggéey. » ‘def’ ak ‘jëf’, maanaam liggéey, danu koy gis lu bare ci ci aaya 17 ba 19. Tontu bi Mu leen tegal ci kow seen xadaru diine jooju, mooy ni Yàlla di jëfe ak mbëggeel. Yàlla dafa noppalu ci liggéeyam bi Mu doon sàkke, ba bés ba doomu Aadama daanoo ci bàkkaar. Ba békkaar duggee ci àddina, te dee wàll bépp xeetu àddina, boole ci jaww jépp tàqalikoo ak Moom, Yàlla noppeetul xeex ngir rawale ñi réer, te delloosi fippukat yi ci jetaayam. Sunu sellaay lay wut, ngir Muman a matal mbëggeelam ci laabaay.

Wéral gi ci bésu noflaay bi, misaal la ci xóotaayu ni Yàlla di jëfe. Yiwu Yàlla la Yeesu doon xamle, te daan def jëf yu fees ak mbëggeel, ak li doxalinam yi meloon ni luy féwwaloo ak Yoon wi lépp. Mbëggeel mooy matal Yoon wi. Paj moomu nag dafa indiwoon tëkku gu tar ci kow gëm-gëmlu gu dul dëgg, te àndul ak mbëggeel.

Noona, Yawut ya xaacu ne: » Yeesu dafay moy ‘Sabbat’ bi! Wóoy -wallooy! kenu Kóllëre gaangi gësëmu. Noonu Yoon waangi tuumaal Yàlla, mungi teg boppam ab dogalkat bu bees, kii musiba la ci sunum réew! »

Kenn ci ñoom faaydaalul mbëggeelu Krist gi Mu am ci miskiin yi, te it ràññeewul ndamam ci kow dee gi. Ñoom ñépp dañoo gapparu ci seenug ngumba diine. Bul jaaxle boo gisee tey jii ay nit yu manul a jàppe Yeesu ni Musalkat, ndax xadaru ngëm gu deme noonu.

Yawut yi dañu meroon ba futt ndax li Yeesu doon woowe Yàlla ‘Baayam ‘. Loolu dafa leen niroowoon ni lu araam. Noonu ñu xaacu ne: » Yàlla Kenn la; amul Doom. » Nan la Yeesu man a woowe Yàlla ‘Sama Baay’?

Seen demin googu mooy wone seen ñàkk a xam; Xel mu Sell mi wommatuleenoon, te xamuñuwoon Mbind mu Seel mi bu baax. Ndaxte am na ay waxi yonent yu am solo ci baayoo gi yàlla jagleel askanam. Yàlla woowe na mbooloom Kóllëre ga ‘samadDoom’ (Gàddaay 4: 22; Osee11: 1) Te fekk askan wa di woowe Yàlla ‘Baay’ (detoronom 32 : 6; Sàbbór 103 :13; Esayi 63 :16; Yeremi 3 : 4,19 ak 31 : 9) Yàlla woowe na buuram bu gëm bi ‘sama doom’ (2 Samwel 7 :14). Waaye amul benn doomu Aadama bu bokkoon ci Kóllëre gi, bu manoon a woowe Yàlla ‘Baay’. Xelum Yawut manuloon a nangu loolu, te ag ñàkk teggin sax la doon niru. Yawut yi xamoon nañu ndig, bi newoon Almasi bi ci Yàlla lay jóge, te dina maye dund gu dul jeex. Mbañeel gi ñu am ci Yeesu, mooy wone seen ñàkk a gëm Almasi bi.

Yeesu tontu xadaru Yawut yooyu doon ŋàññ ay kàddoom, ne leen ci bu leer ne, ni Baayam di jëfe lay jëfe, ci kow maandute ak mbëggeel. Yeesu biral ne man na def lépp, te Moom ak Yàlla benn lañu. Noonu Yawut ya dangal seen mer. Képp kuy diiroo mbagg ak Yàlla, dees na la faat (rey). Yawut ya dañoo bañoon Yeesu tuumaalkatu Yàlla ba.

YOWAANA 5:19-20
19 Noonu Yeesu ne leen: » Ci dëgg-dëgg maangi leen koy wax, doom ji manul a def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf. 20 Ndaxte Baay ji bëgg na Doom ji, ba di Ko won lépp li Muy def, te dina Ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gën a waaru.

Yeesu tontu ak mbëggeel ci seen mbañeel googu, jànkonteek ñoom di wone jëfu mbëggeelu Yàlla. Waaw, Doom ji dafay def ni Baay bi. Yeesu deful ay jëfi boppam. Jokkoom ak Yàlla mungi mel ni jokkoo gi dox ci diggante baay ak doom. Doom dafa naan jàkk Baayam di seetlu ni ay loxoom di liggéeye, noonu muy def ni Baayam di defe. Yeesu dafa suufelu, delloo ndam Baay bi, te màggal ko. Ay surga yu amul benn njariñ lanu, te danu war a sellal sunu turu Baay bi, ni ko Yeesu defewoon.

Ci kow dégg ndigal ak suufeelu gu wér la Yeesu jote sañ-sañu def liggéeyu Baayam. Melokaani Baay ji, turam yi, ak jëfam yépp, ay yosam lañu itam. Moom mooy Yàlla dëgg, di Aji Sax ji, man lépp, di mbëggeel, te di boroom ndam li. Jokkoom ak Yàlla dafa mat-sëkk.

Yàlla Baay bi dafa bëgg Krist ndax ni Mu Ko déggale, moo tax du Ko nëbb dara. Dafay séddoo ak Doom ji ay yelleefam, ay mébétam, ak ay jëfam. Ci pàcc bii gis nanu ci ni jokkoo gu Kenneefu ñett ñi leere, maanaam jokkoo mbëggeel guy jëf. Ndegam Baay ji, Doom ji ak Xel mu Sell miñungi jokkoo ci lépp, kon sunu xel war na dal te xam ne Kenneefu Ñett ñi, jëfam amul àpp-ngir dakkal xare yépp, mbañeel yi, ak beru diine yi nekk ci àddina si tey. Jokkoo mbëggeel giy jëf, aka wuute ak yàccaaralu ki ŋoy ci Yoon wi.

ÑAAN: Sunu Baay ji ci asamaan, nungi lay sant ci li nga nu yónnee sa Doom. Ci biir ay jëfam, won nga nu li ngay def, ak Ki nga doon. Yewwi nu ci bépp bëgg-bëggu topp Yoon, ba nu man di jëfe ak mbëggeel. Nungi tuub sunu xadaru diine te di ñaanal ñépp ñi gumba ci baatin, ndax nga won leen ni sa mbëggeel goree, ba ñu jébbalu ci Yów, di topp sa ndigal.

LAAJ:

  1. Nan ak lu tax Baay bi di jëfandoo ak Doom ji?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 25, 2025, at 06:11 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)