Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
A - Ñaareelu tukki ca Yeruusalem (Yowaana 5:1-47) -- Yokkute jànkoonte diggante Yeesu ak Yawut ya
3. Yeesu dafay dekkil ñi dee te di àtte àddina si (Yowaana 5:20-30)YOWAANA 5:20-23 Ndaw jëf yu kéemaane! nitu neen manuleen a matal, xanaa Yeesu rekk moo ko man. Baay ji dafa leen a jébbal Doom, jiy jëf. Nanu seetlu ñaari jëf ci aaya yii di ay waxi Yonent, te aju ci Yeesu (Yawut yi dañu doon xaar Ki leen waroon a jëmmal), dekkil ñi dee, te àtte, àtte bu jub (jaar yoon). Léegi nag Yeesu aakimoo na ñaar yépp. Naka jekk Yeesu dafa daan waare ci kanamu ay noonam, di leen biral ne Mooy Boroom dund gi, di Ki war a àtte, ak bu ñu Ko tegee ku dof lépp, walla kuy tuumaal Yàlla. Ñu dogu ne fàww ñu rey Ko. Moone de ci kow kàddoom yooyu, Yeesu dafa leen a bëggoon a soppi, ba seeni xalaat dugal leen ci rëccu ak tuub gu dëggu. Sunu Yàlla du yàqkat, waaye dafay maye dund, te bëggul benn bàkkaarkat sànku. Dafa bëgg na bàkkaarkat bi dëddu dëgër boppam bi, te wuti dund gi (te jàkkaarlook dund gi). Képp ku bàyyi Yàlla, dangay dee ndànk-ndànk ci sa ruu, sa yaram ak sam xel. Waaye nag, ku jege Krist dees na la suuxat, te nga dugg ci dund gu dul jeex ba fàww. Li soxal Musalkat bi mooy yeesal la te yee la. Ndax yaangi bàyyi xel ci baatam? Walla yaangi wéy ci sa dunug bàkkaar ak tooñaange? Ba dara sosoogul ba tey, àddina wërngël sépp ci dëgg la sax. Bu fekkee sax ne nit ñi faalewuñu seen Boroom, di reyante ak di naxante ci seen biir, loolu du tax dëgg gi soppiku. Bésub àtte bi, keroog lañuy natt lépp. Yàlla dina fayu bépp ñàkk wegeel, rawatina nag lu jëm ci ñàkk a toppatoo gétur yi ak néew doole yi. Yàlla dafa teg bépp àtte ci loxoy Yeesu. Dina àtte bépp askan, bépp làkk ak jépp diine. Yeesu, nit ku amuloon bàkkaar la woon, kon xam na sunu nekkin, ak li lu man a daan, maanaam fi nu ñàkke ndëgërlaay. Àtteem dafa jub. Bés bu dellusee ci ndamam, xeet bu nekk ci kow suuf dina siicu, ndaxte ràññeewuñuwoon Àttekat bi, ba sewal Ko, sàbbi Ko. Ndax gis nga loolu? Kon ñépp dinañu sukk ci kanamu Doom ji. Ñi faydaalul màggal Krist ci kow suuf, dinañu Ko sargal ci biir am tiit ak lox. Krist dafa yelloo jot kàttan, alal, maandute, saga k ndam li (Peeñu 5 :12). Dafa jokkalewaat àddina si ak Yàlla. Mooy Mbote, mi meemul sax ba ñu koy rey ngir Mu wuutu nu. Yàlla ak Doom ji ñoo yem kepp ci ni seen nekkinu mbëggeel ak kàttan, te loolu yemul rekk ci jëf yi. Ñoom ñaar ñépp a yelloo sunug màggal Looloo tax Yeesu mosul a bañ genn màggal gu ko nit mos a defal. Ni nuy sagale Baay ji, noonu lanu war a sagale Doom ji. Man nanu ñaan Doom ji, ni nuy ñaane Baay ji. Aji Sax ji, su ko neexee mu tànnal boppam Doom. Liy yóbbe nit ñi bañ a nangu baayoo googu, mooy seen xel mu ñaaw. Bëgguñu Ko xam, ba tax nag du ñu man a xam Yàlla ci nekkinam. YOWAANA 5:24 Képp kuy déglu Injiilu Krista k mbég te gëm Baayoom gi ak mucc gi Muy maye dinga am dund gu dul jeex. Dund gu dul tàmbalee gannaaw sa dee, waaye fii ci àddina, jaare ko ci Xel mu Sell mi. Xel mi dafay wàcc ci yów ndaxte danga gëm Baay ji ak Doom ji. Du ñépp ñoo man a dégg kàdduy Krist, amaana sax ñu dégg ko ay junni-junni yoon, jàng ko te gëstu ko. Duñu wax mukk lu jëm ci yiw wi, te duñu doxe ak Xel mi. Ngëm gi dëgg mooy wóolu Krist te séq ak Moom ngor. Boo jokkoo noonu ak Krist, setal nañu la ci bàkkaar, goreel la ci àtte bi, ndaxte ngëm gi moo lay musal, waaye du jëf yi. Mbëggeelu Krist mooy sàmm ñiy làqu ci suufu kurwaa bi, te di far seeni bàkkaar, di laabal seen biir (xel). Dafa nuy ñaax ngir nu jege Yàlla. Ndaxte Yàlla nekk na léegi sunu Baay bi nu judduwaatee. Sunu juddu gu bees gi moo jur sunu njubte ci kanamu Yàlla. Ndax nangu nga digu Yeesu bu réy bi? Yewwi nañu la ci dee gi aky musibaam. Léegi, dangay dund ba fàww ci yiwu Krist. Merum Yàlla du dal mukk ci sa kow. Sa ngëm ci Krist soppi na la, am nga léegi dund gu sell gu dul jeex mukk. Sunu jokkoo ak Krist, yematul rekk ci sunum xel, waaye dafa ëmb jëf, di dund te dëggu. Amul genn mucc gu gën a rëy gi sax ci Krist. Jàngal aaya 24, te wéy di xool ci Moom, noonu dinanu dajeji ca asamaan ba fàww. ÑAAN: Nungi lay màggal Baay, Doom ak Xel mu Sell mi. Baal nga nu sunuy bàkkaar te may nga nu ñu jub. Dootunu jaar ca àtte ba, ndaxte yewwi nga nu ci sam mer. Nungi lay màggal ndaxte sa dund xëppu na ci nun, te dee gi manalatunu dara. Yów rekk lanuy dundal ba fàww. May nu nu dëgër ci Yów, ngir nu yékkati sa tur. LAAJ:
|