Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
4. Yeesu ca Samari (Yowaana 4:1–42)
a) Yeesu fexe na ba njaalookat ba tuub (Yowaana 4:1-26)YOWAANA 4:1-6 Yéenekatu Injiil bi « Boroom bi « lay woowe Yeesu, maanaam kiy nguuru ba fàww. Kiy mbugal te di maye yiw. Kiy wommat te di àtte. Yowaana gis na ndamam te teral Ko ndombal màqaama lii. Farsen yi dañu tàmbalewoon di fagaru ngir jànkonte bi. Waareb Krist di gën a am ndam ca Yude. Muy woo nit ña ñuy tuub seeni bàkkaar, te di nangu seeni ñaawteef, na ko Yaxya daan baaxoo defe. Dafa meloon ne dafa wuutu Yaxya (waaye Moom daawul sóob kenn ci ndox; ay taalibeem la batalewoon mbir moomu, te ñooña sax ay taalibe Yaxya lañu nekkoon ca njalbéen ga; Loolu lépp ndaxte waxtoom ñówaguloon). Yeesu Dafa doon jàngale ne ndoxum cóobu gi misaal rekk lawoon muy wone sóobum Xel mu Sell mi naroon a ñów. Fekk waxtoom jotagul, te sóobul woon moom ci ndox. Ni ko Farisen yi doon gën a sonnale,Yeesu mujj dem ca bët-gànnaar. Mungi doon topp li Baay bi laloon. Songoo gu tar ak ñooñu doo jiital Yoon wi jotaguloon. Yeesu daldi tànn yoon yi aw ci tund yi, xëtt ci biir Samari, ngir dugg ci Galile. Waa Samari nag, kenn nawuleenoon ca Kóllëre gu Njëkk ga ndaxte dañoo nekkoon ay Yawut yu rax ay xeet. Ba waa Asiri daanoo ca kow Samari, ca atum 722 laata Krist, te lël fa waa geñog Ibrayma yu tàkku, yóbbu leen Mesopotami, dañu faa dalaloon yeneen xeet. Xeet yooya nag jaxasoo ak ñoom, ña desoon ca Samari, ba yóbbaale leen ci diine bokkaale. Yeesu agsi « Sychar » wetu « Sichem », muy bérab bu am solo ca Maamaat ya. Yosuwe yeesal na fa Kóllëre gi Yàlla fasoon ak Bànni Israel (Njàlbéen 12:6 ak Yosuwe 8:30-35). Ca diiwaan ba amoon na fa ab teen bu ñu ne Yanqóoba moo ko moomoon (Njàlbéen 33 :19). Foofa lañu suuloon yaxi Yuusufa (Yosuwe 24 :32). Barab boobu moo nekkoon luñuy fësal ci taarix ci Testament bu yàgg bi. Yeesu toog ca pindu teen ba, sonn lool ndax coono tukki bu sore bi, ak tàngaayu bés bi. Nit Ku sonn te mar lawoon, waaye duwoon njuuma, walla luy jommalaate. Nit lawoon ak lépp li nit man a yëg. YOWAANA 4:7-15 Na Yeesu nekkewoon ca pindu teen ba, ab jigéenu waa Samari ñów fa di rootsi. Daanul ñów ci suba si, walla ci ngoon si, ni ko jigéen ña daan baaxoo defe, waaye diggu bëccëg la daan rootsi. Bëgguloon di daje ak kenn, ndaxte jikkoom ju bon ji siiwoon na fépp, te kenn bëggatu ko woon jege. Yeesu gis xolam bu tis bi, te yëg ni mu bëgg a selle. Mu dogal dimbali ko. Tegalu ko Fukki Santaane yi, xasu ko, waaye dafa koo ñaan ndox mu Mu naan. Xalaatoon na ne ndawsi ye lloo na Koo may Mu naan. Waaye ba ndaw sa gisee ne Yawut la, mu deltu gannaaw. Ndaxte kaamb gu rëy moo doxoon ca diggante ñaari xeet yooyu. Ba tax sax ab Yawut, daanul laal ay ndabi waa Samari ngir moytu taxal boppam sobe; ñaari xeet yépp nag ñoo ko doon joxante. Yeesu mel ne ku jàppul dara ci wuute-wuute boobu, di sargal ndaw si ci soxlaam bi. Li Yeesu doon wut, mooy fexe ba bàkkaarkat boobu xiif Yàlla. Ci wetub teen nag li gën a jaadu mooy wax lu aju ci ndox. Loolu yee ci moom mbëggeelu mayug Yàlla. Mu tegal ko mbëggeelu Yàlla. Du ab àtte moo ko doon teeru ngir mbugal ko, waaye mayu Yàlla gu ñu ko waajal ci kow yiw. Ndaw kéemaan! Yiw wi du jekk-jekki rekk ne jameet, ci Yeesu lay jóge.Moom mooy joxe may yi ak yiw yiy jóge asamaan. Moone de, ndaw si dafa Ko jàppewoon ni nitu neen. Ndamul Yeesu dafa làquwoon ci gis-gisam, waaye mbëggeelam gu sell gi, mungi newoon fàŋŋ ci kanamam. Yeesu nee na ko Moo yore ndoxum duuy maye, moo man a màndil maru ruu. Nit ñépp mbëggeel ak dëgg lañuy wut, te bëgg a dellu ca Yàlla. Ku ñów ci Yeesu faj sa mar. Yeesu dafay maye mayu Yàlla ñi Ko koy ñaan. Danu war a wax sunuy soxla, ni ko Yeesu defe ba mu maree. Ku baña sëggal sa bopp di ñaan, doo jot ndox mi asamaan si joxe ci xol. Jigéen ja xamuloon la Yeesu di wax. Noona mu ne Yeesu: »Yów amuloo baag boo man a roote, te teen bi dafa xóot, kon noo may man a maye ndox? » Rax ci dolli, dafa jaaxlewoon, ndaxte mungi doon yëg mbëggeelu Yeesu ak baaxaayam. Wuute na ak ñeneen ñi ndaxte Moom xebatu ko(sewalu ko). Yeesu wuutewoon na lool ak moom ndax darajaam, waaye bëggoon na ko ci sellaayam. Ndaw sa mosuloon a daje ak selle nii. Mu laaj Ko: »Ndax yaa gën a màgg sunu maam Yanqóoba? Ndax danga fas yéene def kéemaan ba bënnal nu teen bu bees? » Yeesu tontu ko, di ko xamal ne Moom xalaatul ndox mi ci àddina si, ndaxte moomu ndox, ku ko faje sa mar, dinga maraat. Yaram, dafay jël ndox ba noppi jariñoo ko mu jeex. Waaye Yeesu dafa nuy may ndoxum dund miy faj gépp maru baatin. Kercen yi dañuy wut Yàlla te di Ko daj. Duñu ay boroom xam-xam yuy xalaat ci dëgg gi, te duñu ko daj mukk. Yàlla jot na leen; te xam nañu Ki mu doon. Mbëggeelam doy nanu saa su nekk. Peeñoom du géey mukk mbaa muy xewwi; dafay yeeslu bés bu nekk. Xam Yàlla ci bu leer te sedd xol guy, du xalaatu neen, waaye kàttan gi la, dund gi, leer gi, ak jàmm ji. Xel mu Sell mi mooy ndoxum asamaan mi nu Yàlla di may. Yeesu wax na ñetti yoon ne Moom doŋŋ mooy maye ndoxum dund gi. Amul benn diine, benn pàrti, benn waajur wala xarit bu mëna faj mar xol, ludul Jesus sunu Musalkat. Képp ku jot mayu Yàlla daldi soppiku. Ki mar dafay mujj nekk teen buy ball, ba di barkeel ñeneen ñi, may leen ñu man a xéewlu ci yiw, mbégte, mbëggeel ak yeneeni ferñeenti Xel mu Sell mi. Bu saxee ci Krist dafay jot yiw ci kow yiw, ba nekk moom ci boppam mayug Yàlla ci ñu bare. Ndaw si yëg ci boppam ne Yeesu ku dëggu la, te du ab luxuskat. Noonu mu ñaan Ko ndoxum dund googu. Mu daldi Ko diis soxlaam wéy nag di xalaat ne Yeesu ci mbirum ndoxum naan lay wax. Ndaw sa dafa xalaatoon ne bu jotee ca ndox moomu, dootul soxla yenu taxam di dend ak ay bañaaleem. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, Yów miy maye ndoxum dund gi, dogal sunu maru xam-xam ak sunu maru mbëggeel. Baal nu sunuy ger; sellal nu ci bépp gàkk-gàkk ndax Xel mu Sell mi wàcc ci nun te dëkk ci nun. Na nu nekk ay mbënni ndox yu ñu bare man a naane liy rembax ci sa Xel mi. LAAJ:
|