Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 027 (The Baptist testifies to Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?

3. Yaxya mungi seedeel Yeesu boroom kër gi (Yowaana 3:22–36)


Ba mu seedee ak woyofteef ba noppi, te wone mbégteem ci gis màggaayu mbootaayu kercen gi, Yaxya dafa seede màqaama Krist, ak xudbaam yu kenn manul a tëkkale yi Mu ne: »

YOWAANA 3:31
31 Ki jóge ci kow moo féete kow ñépp; ki jóge ci suuf nag, ci suuf rekk la man a bokk te ni niti àddina lay waxe. Ki jóge asamaan moo tiim ñépp.

Nit ñi ci àddina si lañu bokk te dañu soxla judduwaat. Yeesu rekk moo jóge asamaan, def boppam nit ngir jegesi nu te jotaat nu. Yeesu mu Nasaret moo sut Yonent yépp boroom xam-xam yi ak kilifa yi, ndaxte asamaan moo tiim suuf. Li nit ñi feent jéggi na dayoo, waaye ci li Yàlla sàkk ba noppi la wéeru. Doom ji mooy dund gi ak leer gi te Moo waral nuy dund. Kenn du Ko méngale ak ñeneen ñi. Doom ji ci Baay ji la juddoo laata dara di am. Dafa mat sëkk, te raw lépp lu ñu sàkk.

YOWAANA 3:32–35
32 Day wax li Mu gis ak li Mu dégg, waaye kenn nanguwul li Mu seede. 33 Képp ku nangu seedeem, nangu nga ne Yàlla dëgg lay wax. 34 Ndaw li Yàlla yónni, Kàddug Yàlla lay wax, ndaxte mayu Xel mu Sell, mi Yàlla sol ci Moom, amul dayo. 35 Baay bi dafa bëgg Doom ji, te jox na Ko sañ-sañ ci lépp.

Yeesu mooy seede bi gis dëggu Yàlla. Moom moo gis Yàlla Baay ji te déegg ay Kàddoom. Xam na ay xalaatam ak li Mu nar. Moom mooy Kàddug Yàlla te génne ci Baay bi. Xam na ay xalaatam ak li Mu nar.Moom mooy Kàddug Yàlla te génne ci Baay bi. Li mu wàccee mat na sëkk. Wahyu bi wàcce jaarale ko ci yonent yi matna. Jesus dafay wane bëgg-bëggu Yàlla bu mujj te mat sëkk. Mooy seede bu wóor, bi mujj nekk Ka ñu bóom ndax seedeem googa. Màggal na Baay bi. Li ci nàqari mooy ne ba léegi am na ñu bare nangoogul seedeem bi. Bëgguñu Yàlla ju leen jege, ndaxte loolu dafa leen di indil coppite dund. Dañuy weddi Doomoo ji ak Baayoo Yàlla ji.

Cant ñeel na Yàlla, ndegam du ñépp a bañ Yàlla ak Xelam mi. Am ñu ñu tànn, te ñuy wut Baay bi, jaare ko ci Doom ji, te nangu saraxam su mat si. Képp ku nangu peeñoom ak mucc gi Muy maye, yaangi màggal Yàlla. Yàlla du fen, Doom ji Mooy Dëgg gi. Yàlla feeñalul ay xalaatam ci ab saart walla ciab téere, waaye ci Yee su la ko jaarale. Képp ku nangu ubbeeku ci Xelu Kàddoom yi, dees na la yeesalaat. Krist dafa laa woo ngir nga yégle dëgg gi, te di ko dunde ak di ko jëfe. Su ko defee Injiilam bi di jëmmoo ci yów.

Yeesu waxul ay xalaati neen,walla yu wóoradi te it waxul ci lu jëm ci ay bëgg-bëggam. Ay Kàddoom dañu doon sàkk, am kàttan te leer. Yàlla dafa waje ci Doomam. Xel mi amuloon dayo ci Moom. Baay bi dafa Ko soloon xam-xam ak sañ-sañ.

Baay ji dafa bëgg Doom ji te jébbal Ko lépp. Mbëggeelu Baay ji, may la, te Doom ji dafay teral Baayam. Kenn warul a laaj kan moo ci gën a màgg, Baay bi walla Doom ji. Laaj yu mel noonu lañuy jóge. Ku ci nekk ci sellaayu Kenneefu ñett ñi dafay màggal ka ca des, te di ko teral. Baay ji mosul am xel ñaar ci Doom ji jéem a daaneel nguuram, ndaxte Yàlla xamoon na lewetaayu Doom ji, dégg-ndigalam ak jébbaloom gu mat sëkk gi. Ci loxo Yeesu la lépp tegu, ni Mu ko waxe nii: »Bépp sañ-sañ jox nañu ma ko ci suuf ak ci asamaan. »

YOWAANA 3:36
36 Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex; ku déggadil Doom ji, amuloo dund, waaye merum Yàllaa ngi la tiim.

Yowaana, taskatu Injiil bi jàngal nanu yoonu mucc gi: Ku dénk sa bopp Doom ji, am dund gu dul jeex. Baat yu gàtt yii, ci Injiil lañu bokk. Képp ku jegesi genn mbëggeel googu dox ci diggante Baay ji ak Doom ji, jegesi itam mbëggeel gi Yàlla feeñal ca kurwaa ba. Ci Mbotem Yàlla mi la aju, ndaxte Mbote mi moo nu teggil sunu sobe. Ci jokkoo googu lanuy mose daŋaru yërmandeem ci biir mbëggeel gu amul àpp gi. Dund gu dul jeex gi, du gannaaw dee lay tàmbali, waaye léegi lay tàmbali. Xel mu Sell mi dafay wàcc ci ñi gëm Yeesu. Képp ku weddi Kàddu Krist yi ,te nanguwoo ne Yàlla mooy Baayam,ak daajam ba ca bant ba,yaangi tiisal xolu Xel mu Sell.Sam xel du dal mukk. Képp ku jébbalul sa bopp Yeesu, noonu Yàlla ci boppam, te yaangi dëkk ci deewug baatin. Bépp diine bu weddi ne Yeesu Doomu Yàlla la, te daaj nañu ko ci bant, yaangi tooñ dëggu Yàlla gi. Ku bañ mbëggeelam, yaa tann meram.

Póol ak Yowaana ñoo bokk bii xalaat: Merum Yàlla dafay dal ci kow bépp ñàkk ngëm ak coxorte. Ndaxte ñépp a bàkkaar te nanguwuñu dëgg gi, ndax seeni ndëngte. Xamal ne merum Yàlla miy rajaxe xëppu na ci kow nit ñi.

Ni jaan ja ñu lonkoon ca mànding ma, noonu la Ka ñu daajoon ca bant ba nekke sunu misaalu mucc ci merum Yàlla. Doom ji ubbi na mayug yiw wi. Képp kuy tey-teylu di soppi Yiwam wa ca kurwaa ba, Yoon dab na la. Seytaane teg na la loxo. Ñi àndul ak Krist daanu nañu (musiba dal na leen). Kañ ngay tàmbalee ñaanal nit ñi ngir ñu gëm Doom ji te mucc? Kañ ngay waxtaan ak say xarit ba ñu jot ci dund Yàlla gi jaare ko ci sa seede?

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nundi lay màggal ci sa mbëggeel ak sa dëgg gi. Dimbali nu ba nu déggal la ci kow ngëm te teral Baay bi. Ak kóolute nungi biral ne Yów ak Baay bi, benn ngeen. Yërëmal ñi lay weddi ci kow ñàkk-a-xam. May leen sa seedeb Kàddu. Dimbali nu ba nu daje ak ñi nga nu booleel, ba nu man leen a wax ki nga doon, ak li nga nu defal.

LAAJ:

  1. Nan la nu man a jote dund gu dul jeex?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 22, 2025, at 03:30 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)