Previous Lesson -- Next Lesson
4. Màggaayu Baay ji ci jamonoy ruu gu jàq (Yowaana 12:27-36)
YOWAANA 12:27-28
27 Léegi nag damaa jàq. Lu ma war a wax? Mbaa du dama naan: « Baay,musal ma ci li nar a xew waxtu wiy ñów? »Déedéet, ñów naa sax ngir jaar ci waxtu woowu. 28 Baay, màggalal sa tur! »Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: « Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat. »
Yeesu dafa tiis ci biir ruuwam. Mooy Buuru dund gi, waaye dafa suufeelu ba ca dee ga. Mooy Buuru buur yi, waaye may na seytaane, miy kilifa màkkaanu ñi dee, mu fiir Ko ak kàttanam gépp. Yeesu dafa gàddu sunuy bàkkaar ci kow coobareem, ngir wuutu nu ci safara merum Yàlla, si ñu nu waroon a lakke. Moom mooy Doom ji, ànd ak Baayam ca ba dara taxawagul. Ngir sunu mucc la Ko Baayam dëddu, ndax nu man a nekk ak Moom jaare ko ci yiw wi. Kenn manul a natt tiis ak naqaru Baay ji ak Doom ji. Jokkoo gu Kenneefu Ñett ñi dafa nekkoon ci metit ngir sunu mucc.
Yaramu Yeesu manuloon dékku boobu diisaay. Mu xaacu ne: « Baay musal ma ci waxtu wii. » Gannaaw gi mu dégg bu leer tontu Xel mi ci xolam naan Ko: « Waxtu wii moo tax nga juddu. Waxtu wii mooy mooy jur li amul àpp. Càkkite gépp ak Baay ji ñungi xaar jamono ji nit ñi di juboo ak Yàlla, maanaam càkkite gi ak ki Sàkk. Noonu tëralinu mucc gi dina mat sëkk. »
Gannaaw loolu Yeesu xaacu ne : « Baay,màggalal sa tur ! » Doom ji nanguwul déglu kàdduy yaram wi. Mu ñaan ci ànd ak Xel mu Sell mi: “Na sa tur sell, ngir àdduna xam ne, du Yàlla bu raglu, bu sore, bu amul yëg-yëg, waaye Baay bu am mbëggeel nga, mi joxe bakkanam ci Doom ji ngir musal ñu soxor ñi ak ñiy réer.”
Yàlla xaarul sax ngir tontu ñaanu Doomam ji : « Màggal naa sama tur ci yów. Yaay sama Doom ji ma déggal, te suufeelu. Képp ku la gis, gis na Ma. Yaay sama Doom ji ma bëgg, te maa ngi lay bége. Amuma meneen mbég mu dul gis la nga gàddu kurwaa bi (bant bi). Yaangi wuutu nit ñi ci dee gi, te ci biir dee gi dinaa ci wone sama kéem-kàttanu màggaay ci biir lépp luy jaxase dund gi. Ci kurwaa bi, ngay biral li ndam li ak cellaay gi dëgg di tekki. Jëfu mbëggeel la, ab jéngu ak wàññi sa bopp ngir ngëneelu ñi dëgër xol te yelloowuñu ko.»
Baat bi jóge asamaan dégtuwaat ne: «Dinaa màggalaat sama tur boo génnee ci bàmmeel bi, te yéeg ba ci Man, toog ci ndam li. Su boobaa dinga yànnee sama Xel mi sa soppe yi. Dinañu màggal sama tur wu sell wi, jaare ko ci juddug doom yu bare ndax Xel mu Sell mi. Seen dund dafa may sagal; seen jikko yu rafet yi, di ma sellal. Sa dee gi ci bant bi (kurwaa bi) dina tax doomi Yàlla juddu. Sa ràmmu bi ànd ak ndam, mooy gaaranti ndamul Jàngu bi. Ci yów rekk lañuy màggale Baay ji ba fàww. »
YOWAANA 12:29-33
29 Mbooloo ma fa nawoon te dégg baat ba ne: « Dënnu la woon ! »Ñeneen naan: « Malaakaa doon wax ak Moom. » 30 Waaye Yeesu ne leen: « Taxuma baat boobu jolli, waaye yéen a tax. 31 Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si. 32 Te Man, bu ñu Ma yékkatee, Ma tiim suuf, dinaa wootal nit ñépp ci Man. » 33 Ci baat yooyu la doon misaale ni Mu war a faatoo.
Mbooloo ma xamuñu woon ne Yeesu Yàlla la doon waxal, waaye dañu foogoon ne dënnu lañuy dégg. Manuñu woon xam it ne Yàlla mbëggeel la, walla sax ñu man a dégg baatam bu lewet bi, rawatina sax ñu man a gis ne peeñug ndamul Yàlla gi Mu jaarale ci Doomam ji, moo dëgmal àtteb àddina si.
Seytaane dafa ñàkk moomeelam ci jaamam yi, bi ñu yékkatee Krist daaj Ko ci bant bi, ngir Mu may nu dund gi, Mu jaarale ci deewam gi. Dañoo foqati nguuru ku bon ki, jaare ko ci dégg-ndigal gi Doom ji am ci Baay ji. Yeesu dafa woowe seytaane « buuru àddina si », ndaxte àddina sépp a nekkoon ci nooteelam. Ci kow dëgg gu metti googu, Yeesu xaarul sax, ngir cor seytaane ak jaasi njubte ji, muy corug dee. Léegi nag nun ay doom yu ñu goreel lanu ci turu Yeesu.
Ci kurwaam bi lanu xiiru. Seytaane dafa bañoon Yeesu, ba bëgguloon sax mu dee ci kow suuf si, walla ci kow lalam, waaye dafa Ko daaj ci bantu gàcce gi. Waaye nañu yékkatee woon jaan ja ca mànding ma, ca jamonoy Musaa, ngir seede njeextalu mbugalu Yàlla, ngir way-gëm yi, noonu it la bant bi (kurwaa bi) dajalee àtte bépp ci mbaggi Krist. Yàlla du mbugal ñiy xool ci Ki ñu daaj ca kurwaa ba. Ni nu gëme Yeesu, moo nu daajaale ak Moom, ba boole nu ci deewam gi. Sunu bàkkaar dee na, léegi njub lanuy dunde.
Sunu booloo ak Krist moo nu jokkaleek kàttanam ak ndamam. Daan na bàkkaar ak dee gi ci kow cellaay, rax ci dolli Mungi nuy xiir ci boppam, te di nu dugal ci ndamam. Ñépp ñi Ko dénk seen bopp, du ñu dee mukk, waaye dañuy am dund gu dul jeex.
YOWAANA 12:34
34 Mbooloo tontu Ko ne : « Jàng nanu ci sunu téere Yoon ne, « Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yow, nan nga man a waxe ne « Doomu nit ki dina yékkatiku? »Kuy Doomu nit kooku? »
Yawut yi dañu bëggoon a ga (forse) Yeesu ba Mu won leen firnde bu jaadu te leer, ngir bañ a am lenn lu ñuy lëñbat ci nekkinam dëgg. Xamoon nañu li téere Yonent Dañel wax ci saar 7, fi ñuy woowe Almasi bi, Doomu nit ki ak Àttekatu àddina si. Waaye dañoo Koo bëggoon a dégg Moom ci boppam Mu wax li jëm ci baayoom ak Yàlla. Jëfewuñu noonu ngir jublu ci ngëm, ndax li Mu wax ki Mu doon. As ngëm su néew la ñu Ko mayoon. Ci seen biir, amoon na ñu Ko doon fexeel, di Ko fiir ngir man Koo jiiñ tuumaal Yàlla, bu waxee ne Mooy Doomu nit ki. Yeesu du feeñu ñi Koy jéem a gëstu ci sayiir, waaye ñi déggal Xel mu Sell mi, te nangu ne Doomu nit ki mooy Doomu Yàlla ji, laata ñuy wut a gis firnde yu bët man a tegu, ñooñu lay feeñu.
YOWAANA 12:35
35 Yeesu ne leen : « Leer gi dootul yàgg ak yeen. Doxleen, ci bi ngeen di am leer, ngir lëndëm bañ leen a bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm.
Yeesu mooy Leeru àddina si soxlawul dara lu ñu ciy faramfàcceeti. Leer gi dafa nekk lu ñépp man a ràññee (méngale) ak lëndëm. Man nañu tukki ci bëccëg, di ci dox, walla di ci daw. Waaye bu guddi jotee, kenn du man a liggéey. Bu jant bi fenkee, liggéey jot na, ak jëf. Yeesu nee na Yawut ya, diir bu gàtt moo leen dese ngir ñu man a dugg ci nguru leeram gi, su ñu ko nammee. Diir googu dafa laaj dogu, dégg ndigal ak taxaw temm.
Waaye nag képp ku bañ leer gi, des ci lëndëm gi, te. Doo gis saw yoon. Yeesu jotoon na yégal Yawut yi ne dinañu wundeelu ci lëndëm, ñàkk a gis yoon ak jëmukaay, mbaa yaakaar. Lëndëm googu bokkul ak gi nekkul ci nun. Lëndëm gi ci sunu biir lay wax. Muy gi nga xam ne mooy xel mu bon mi ci nit ki. Ci xiirte googu lëndëm, nit dafay gën di ñàkk leer. Te bu jébbalul boppam Krist, dooley lëndëm gi dinañu ko daan. Ndax xam nga lu tax yenn réewi « kercen »yi nekk ndeyu lëndëmu àddina si? Ñiy woote ne « kercen »lañu, du ñoom ñépp a jébbalu ci Krist. Kercen yi ñu yeesal, ñu néew lañu. Lëndëm gi dafay muur ñépp ñi duggul ci nguuru leer gi. Manuloo donne barke Injiil ci say waajur. Yów ci sa bopp yaa war a nangu, wuyu, te jébbalu ci Krist.
YOWAANA 12:36
36 Kon ci bi ngeen di am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer. » Bi Mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, nëbbuji leen.
Sunu jokkoo ak Krist ci kow ngëm dafa nuy soppi ba jeex. Injiil dafay dafay wàccee daari ndamul Yàlla, yi gën a am doole daari atomik yi. Kon, fi daari ndell yi di yàqe, fekk na daari Krist di sàkk dund gu amul àpp ci nun, ndax ki gëm man a nekk doomu leer, te nekk leeru ñu bare. Krist dafa la bëgg a leewu ciy loxoom; dafa fees ak dëgg, sellaay ak mbëggeel. Mungi lay woo ngir nga génn ci sa lëndëm gi, te dugg ci leeram gu kéemaane gi, ndax nga sell.
Mu joxe njàngale moomu, laata Muy dugg Yerusalem. Du ci ga la jële nguur gi, te dalul ci kow waa rom yi, walla ci Erod. Xeexam dafa jeexoon, te àtteb àddina si jegesi. Leer gaangi leer ci lëndëm gi; ñi gëm dinañu mucc te ñi gëmul sànku. ŋaayoo asamaan ak suuf àgg na ca njobaxtalam. Yàlla du ga kenn ngir mu gëm Ko. Ndax gune leer nga, walla yaangi nekk jaamu lëndëm gi ba tey?
ÑAAN: Nungi lay sant Boroom bi, ci ninga feeñoo ni Leeru àddina si. Wootal nu ci sa ceeñeeri yërmande, te defal ba nu ànd ak ñówental. Fexeel ba nu dummuuyu xaalis, kilifteef ak ndami àddina, ngir nu man a laa topp te nu jub ni doomi sa Leer gi.
LAAJ:
- Nekk doomu leer gi, lu muy tekki?