Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- Tracts -- Tract 01 (Do You Know Jesus?)

Next Tract

BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok

BATAAXAL 01 -- Ndax xam nga Yeesu?


Képp ku gëstu cosaanu àddina dinga gis ne am na ci biir ay téméeri junniy at yu jàmbaar yu raññeeku indiwoon ay xiirte ci seeni aada ba soppi seeni askan. Kenn ca ñooña mooy Yeesu, doomu Mariyaama. Lu ëpp benn xaaj ci ñett ci doomi Aadamay àddina si ñungi topp ay njàngaleem. Turu Yeesu moo ëpp solo ci 27 teerey Kóllëre gu bees gi. Mungi ciy feeñ 975 yoon.

Yàlla dafa yónni malaaka mi tudd Jibril ca jànq bu tudd Mariyaama.Ca biir janneer itam, malaakam Boroom bi feeñu na Yuusufa miy boroom-këru Mariyaama. Mu ne leen ne doom ji Mariyaama ëmb,ku sell la,te war nañu ko tudde "Yeesu, ndaxte mooy ki nar a musal askanam ci ay bakkaaram" Mace 1:20-23; Luk 1:31.

Tur woowu du, nit moo ko sos,waaye Yàlla ci boppam moo ko tann ci kow coobareem. Turu Yeesu dafa ëmb tëralinu teralinu Yàlla, gir muccug doomu Aadama; woowu teralin wu Mu nammoon la laata àddina di sosu.Ci dëgg-dëgg turu Yeesu mungi tekki "Boroom Kóllëre gi dafay dimbalaate, te di musal"

Yalla soppali na doxalinu àddina jaare ko ci Yeesum Nasaret. Doomu Mariyaama joxewul ay njàngale nitu neen,yu amul bopp amul geen.Du itam ay kéemaan yu nu man a teg bët doŋŋ la def,waaye Yàlla jaare na ci Moom ngir wax ak ngir jëf [Yowaana 5:19-21;14:10-24]. Lu waraloon ñówam? Te lan mooy mbootu kàttanam ju rëy ji?


Dafa nuy goreel ci sunu reëy-rëylu

Yeesu nee na: "ñówleen ci man yeen ñépp ni sonn te diis Ma may leen nooflaay ci seen ruu" (Mace 11:28-29). Ñépp ni am coono ci seen dund, ñaax nañu leen ngir nu ñów ci Yeesu.Ku ñòw ci Moom,dina la goreel ci sa reëy-rëylu,te may la nooflaay.

Yeesu nee na: "Doomu Nit ki ñówul ngir ñu koy surgawu,waaye ngir nekk surga ,te jébbale dundam ngir wuutu ñu bare” (Mace 20-28). Ñiy topp Yeesu dañuy wér ci seen naweelu bopp, te di amal njariñ ñeneen ñi, jaare ko ci doomam, ci kow mbég.


Dafa nuy goreel ci merum Yalla

Merum KU Sell ki mungi tiim ñépp ñi bàkkaar,waaye Yeesu dina musal ñépp ñi ko gēm,ca bépp àtte,ca bésub ndekkite la( Yowaana 3:18;5:24) Boroom bi xamal na Yonent-Yalla Esayi dëgg gi: "...te fekk ne sunuy tiis la yenu ,gàddu sunuy naqar.Sunuy bàkkaar a tax Mu gaañu ,ne làcc ndax sunuy tooñ mbugal gi nu may jàmm,Moom la dal.Nun ñépp a reeroon ni ay xar'ku nekk aw saw yoon,te Àji sax ji yen ko sunuy njubadi nun ñépp” (Esayi 53:4-6)

Laata Muy saay,yeesu ñaanal na ay noonam ba ne "Baay,baalleen, ndaxte xamuñu li nuy def" (Luk 23:34). Wóor nanu ne Yàlla nangu na ñaan googu.


Dafa nuy goreel ci bàkkaar

Yeesu nee na: "...képp kuy bàkkaar,jaamu bàkkaar la....kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi” (Yowaana 8:34-36). Képp ku ko wóolu,Yeesu dina la yeww ici buumug njaamu bàkkaar. Gàddu na bàkkaari àddina sépp, te wuutu nanu ci dee gi. Coono ji Mu daj faxas na sunu bàkkaar yépp, te Xelam mu Sell mi mungi dëkk ci sunu jëmm,di nu dooleel ngir nu daan bàkkaar (Waa Rom 8:9-11). Noonu,képp ku gëm Yeesu ak njébbalu boppam nib sarax ngir say bàkkaar, kenn deesu la daan.


Daan na Seytaane

Yeesu daan na Seytaane,ba mu nanguwulee tàbbi ca ay fiiram (Macē 4:1;Luk 4 1-13). Ca biir bundxataal ak coono,Yeesu,dafa wéy di déggalYàlla te tàbbiwul ci benn bàkkaar. Seytaane manu ko woon xiir ci dara lu bon.Yeesu dàqe na ay rab, ak ay jinne yu bon ca ña ñu duggoon. May na boobu san-san ay taalibeem (Luk 9:1).kepp ku nangu saraxam bi, dinga mucc ci doole Seytaane.


Daan na Dee gi

Yeesu nee na: "Man maay ndekkite li,maay dund gi. Ku ma gëm boo deewee sax, dinga dund. Rax ci dolli, kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?" (Yowaana 11:25-26)

Yeesu dekki na ci biir ñi dee,te feeñu na ci jëmmam ay taalibeem,ba wax ak ñoom;laal nañu Ko sax!Noonu itam la Yeesu man a rawalee ay doomam ci dee gi,te may leen dund gu amul àpp.


Dafay faj mbañeel ak feyoonte

Lii la Yeesu digal ñi koy déglu: "Waaye,man maangi leen di wax ne,soppleen seeni bañaale te ñanal ñi leen di fitnaal, ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi ci kow asamaan” (Luk 6:27-28).

Kenn doŋŋ ki juddoo ci Xelum Yàlla, moo baal taalibeem yépp seeni bàkkaar,ba noppi sant leen ñu baal ña leen ameloon bàkkaar. Li xiir Yeesu ci baale, mooy mbēggeelam gu rëy gi. Yeesu dafay goreel ci mbañeel ak feyoonte, ñépp ni koy déggal.

Doomu Mariyaama ji ay ñoñam dañu Ko jañax, saaga Ko sewal ko. Waaye ak li ñu Ko jañax lépp, terewulYeesu may leen mbéēggeelam, njuboom, wuutoom ak kàttanam. Ñépp ñi ni dëddu seeni bàkkaar, topp Ko te déggal Ko, yoon du leen daan mukk, te dinanu am dund gu amul àpp.

Yow sama am-ji-jàmm jiy jàng lii,
Yeesu miy dund mungi lay ñaax di la kañ ngir nga wóolu Ko te nangu ay kàdoom. Man na la may kàttanu Xel mu sell mi,te sellal sa yaram, sa ruu ak sam xel.Bul dëgëral sa xol, waaye xeewlul ci njéggalam gi ak kàttanam ji, ngir nga rëcc ci mer mi nar a nów. Yeesu moo la wuutu,mooy sa Musalkat, sa Rammukat bi lay layool fa Yàlla. Mooy sa dund ,te moo gàddu sa kiiraay. Kon aywa, nangul loxo bi Mu la tallal ngir nga man a fees aky yiwam (Yowaana 1:16)

Nangug cant ak ngërêm
Nanu ñaanandoo: Boroom bi Yeesu,yow yaay Musalkatu addina si,te itam di sama Musalkat.Goreel nga ma ci merum Yalla ak ci àtteem. Musal nga ma ci sama reëy-rëylu ak ci sama bëgge.Sellal ma ci samay bàkkaar ,te may ma dund gu laab ak sa njubte giy wàcce asamaan, ngir seytaane du ma man a xiir ci dara. Jàppe ma ni kenn ci sa taalibe yi, te gindi ma ngir ma xam say njàngale ak say santaane.


Na sa kàttan faxas samay neew-doole, ndax ma man a màggal Yàlla ju sell ji, ci samag Ndax bëgg ngaa xam lu gën a xóot ci mbiri Yeesu, doomu Mariyaama?

Nun de jekk nanu ngir yónnee la Injiilu Yeesu bu ànd ak ay faramfàcce,te doo fay dara.


Wesaareel xabaaru Yeesu bu baax bi ci sa biir dëkkandoo yi

Bu fekkee ne xë yii tooyal nañu sa xol,te may la xel mu dal,ba dooleel la,kon séddoo ko ak say xarit ak say dëkkandoo. Dinanu neex lool nu yónnee la ci as tuut.Wax nu ñaata nga ci man a séddoo ,te du la indil coono.

Bul fàtte bind sa dëkkuwaay nu mu gēn a leere. Ci biir xaarandiku sa tontu,nungi ñaan sunu Boroom biy dund,Mu barkeel la.Amiin!

WATERS OF LIFE
P.O. BOX 60 05 13
70305 STUTTGART
GERMANY

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on September 07, 2023, at 10:52 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)