Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- Tracts -- Tract 02 (God, be Merciful to Me a Sinner!)

Previous Tract -- Next Tract?

BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok

BATAAXAL 02 -- Céy yow Yàlla yërëm ma, man miy bàkkaarkat


Ba mu ganesee genn njaboot,benn jàngalekat bu silmaxa dafa jàngoon ay aaya yu ñu jukkee ci Injiil te ñu binde leen ci arafi baraay, Mu leen di ijjee ak ay baaraamam. Ña ko doon déglu, dañu waaruwoon ça na mu mokkalewoon njàng ma. Ñuy xool na. Ñuy xool na muy jēfandikoo ay baaraaram ngir làmb baat ya, te di déglu tareem ju leer ja. Jàngalekat bu silmaxa ba dafa jëloon misaal bu fésoon te xewoon ca Màggalukaayu Yàlla ba gënoon a mag ca seen réew Mu ne:

"Dafa amoon ñaari nit ñu demoon ca Kër-Yàlla ga di ñaan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat. Farisen baa nga taxaw di ñaan ci xelam naan: "Yow Yàlla, maangi lay sant ci li ma melul ni ñeneen ñiy sâcc, di def lu jubadi, te di njaaloo, rawatina juutikat bii. Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, te di joxe askan ci lépp lu ma am". "Juutikat ba moom, manga taxaw fu sore te bëggul a siggi sax, xool ca asamaan.Waaye,mangay fēgg dënnam naan "Yow Yàlla yërëm ma, man miy bàkkaarkat ". (Luk 18:10-13)

Jàngalekat ba taaxirlu ba noppi ne ña teewoon ca néeg ba: Nanu laaj sunu bopp lii: Man maay kan? Ndax ni ki doon wax ne nitu diine la laa mel, walla ni juutikat bi doon rëccu ay bàkkaaram, te siiwoon nib sàcc?Kilifa diine ba, ndax melul ni sunu askan wi naan njaaloowul, sàccul, te jubadiwul ci kanamu kenn, waaye dafay topp yoonu diine, ba mu mat sëkk, di woor ñaari yoon ayu bés bu nekk, teg ci di joxe asaka, te di dimbali miskiin yi?

Ag gòor gu mag daldi dog tekkaaral ja, ne:"cant ñeel n'a Yàlla, ndaxte nit kii man naa jege Boroom bi saa yu mu ko bëggee ngir ñaan Ko, te diis Ko ay ñaan yu dëggu ngir dimbali ñi ndóol, ak ñi ciy soxla. Waaye nitu diine bii, dafa kañu te sagu ci dooleem, fegg sant Yàlla ci ay jëfam yu kéemaane yi. Fonkaayu diine gu mel noonu, te ràññeewul Yàlla,loolu rëy-rëylu la".

Noonu jàngalekat bu silmaxa ba nangu la góor ga tontu, teg ca ne "ñi yég seen bopp bay mbubboo seen diine dañuy dëgëral seen xol, ak seen xel.Duñu nangu dëggu Yàlla, te duñu ràññee seenub nekkin, doonte sax man nañoo tari aaya yépp. Loolu wone na ne gëm-gëmu diine gu àndul ak ragal Yàlla, naaféq la gu àndul ak mbëggéel. Ñiy ñaan te di bàkku ñu ñàkk kersa lañu. Dañoo waroon à laaj seen bopp ne"sama ñaan yii, Yàlla laa leen jagleel, walla man ci sama bopp? Ndax Boroom bi laay xalaat, te di ko màggal walla sama sag laa bëgg mu feeñ ci?"

Ab waxambaane daldi laaj silmaxa ba ne ko "Lu tax ñuy ñaan ?Ban ngëneel la nu ñaan amal? Te itam kan mooy déglu sunuy ñaan? Silmaxa ba tontu ko ci njekk ak teraanga, ne ko: "Ndax boroom gis-gis bu leer man na séen lu weesu penku te bëtam àggu fa? Moonte de gëm na ne àddina si dafa wërngalu; noonu itam la bu nuy woote telefoŋ Keer ba Pari, walla Kaasabalaŋka ba Tokyo, dara dunu xañ a xam ne baatu ki nuy woo lanuy dégg naam, gisunu xar-kanamam. Astamaak ki gēm, nan la war a yaakaare ne Aji kàttan ji mungi dégg ay ñaanam, te di leen toontu, rax ci dolli di jot cant yiy jollee ci xolu mbëggeel bu suufeelu te woyof.

Jàngalekat ba daldi wéy ci ay xalaatam. Mu wax lu aju ci ñaanu juutikat ba te naan: "Yàlla moo xiir juutikat ba, ba mu ñaan mbaalug bàkkaaram ya, te dellusi ci Moom Boroom bi. Noonu nit ka déggal la ko Xelam may,daldi jébbal ñaanam Aji yérmaande ji. Ni mu ñaane dafay wone ne gëm na nekkinu Yàlla, kilifteefam ak kàttanam, ndaxte dafa ko woowe "Yàlla "ci kow ràññee ne Yàlla kenn la ci kàttan, kàddu, ak ci xel. Juutikat ba doon baalu dafayég sellayu Aji yērmaande ji-Ci diggante gëm Yàlla ak ragal àtteem, moom dafa doon baagante diggante baaxaayu Yàlla ak njubteem. Dafa ragaloon Boroomam àtte ko ci njubteem, ba tàbbil ko safara-waaye nak dafa ŋoy ci gëm yērmaande Ku Sell Ki. Gēmoon na ne baaxaayu Yàlla moo sut àtteem ,te Aji kàttan ji, ci kow mbēggeelam dee na ngir ay bàkkaaram. Foofa nak la nuyóo ak loxob àtte bu am yērmaande bi, ngir ñaan ko mbaal gi. Loolu moo tax Mu xaacu ne: "Céy Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat!"

Silmaxa ba daldi leeral lan mooy rëccu say bàkkaar, te dëddu leen ;mu rax ca dolli ne: "Sàcc bi dafa nangu ne du caageen ne dafa bàkkaar rekk, waaye dafa mujj a nekk ku selladi, ndóole, ba Yàlla saabi ko. Ci teewaayu ku sell ki la ko nekkinam feeñu. Ci bëti Boroom bi ameloon dara lu jaadu ci moom, maanaam ab bàkkaarkat neen lawoon.

Jàngalekat ba yokk ca ne :"Ñu bare dañuy naagu di jàppe seen bopp ni ñu yiw, te jub. Waaye képp ku teew ci leeraayu Yàlla ji, dinga gis ci saa si ne, amul kenn ku jub ku dul Yàlla. Barke ñeel na juutikat ba doon rëccu ay bàkkaaram, ndaxte mujj na nekk ku yiw. Nangu na nekkinam, dellu ci Ki ko sàkk, te ñaan ko yērmaande, nangu ay geram, te jot yērmaande ak yiwu Yàlla. Boroom bi du jallax kiy rëccu ay bàkkaaram, bëgg xolam soppiku, te namm a dummooyu ay doxalinam, te yóotu xel mu sell. Boroom bi dina ko may muccam, te baaxe ko bépp mbaalug bàkkaar ni képp ku rëccu te dëddu ay tooñam.

Jàngalekat ba laaj mbooloo ma: "Ndax bëgg ngéen a xam nu Krist doomu Mariyaama ji mujj a àttee kilifa diine ga ak sàcc ba doon tuub?" Dafa ubbi téereb Injiil bi, di dawal baaraamam ya, nekk di jànge kàdduy Krist nii: Yeesu teg ca ne:

"Maangi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram,moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte kepp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te ku suufeelu, ñu yékkati la". (Luk 18:14)

Yow sama mbokk miy jàng lii,
déglul sa xol :ndax xelum diine doy na la ci kow say jëf ak say doxalin yu baax?Walla danga suufeelu ci kanamu Yàlla mu sell mi, ndax gàcce gi nga doon doxale sa dund? Na la wóor ne, kuy rëy-rëylu, bés dinga xalangu. Waaye képp kuy rëccu ay ñaawteefam, te di wëlbatiku dellu ci Boroomam, dina jot mbaalug bàkkaaram,ci kow yērmaandeem ju rëy ji.

Ñaanu Rëccu
Tarindool ak nun ñaanu Daawuuda gii, ba muy baalu Boroom bi ndax gàcce ga ko daloon ba mu njaaloo ak jenn jigéen.

"Yërëm ma, yow Yàlla, ci sa cofeel gu sax;ci sa laabiir gu yaa faral samay tooñ. Sang ma, ba ma set ci sama bàkkaar, laabal ma ci sama jàdd. Ndaxte xam naa samay tooñ, te sama jàdd a ngi ne màkk ci sama kanam. Yow laa moy, yow kenn, te def lu ñaaw fa sa kanam, ba tax nga set wecc ci say dogal, jub xocc ci sa àtte. Bàkkaar nekk ci man dale ci sama biiru Ndey, jàdd topp ma sax bi ma sosoo. Dëgg kese, gi ci reeni xol,nga bëgg; sol ma xel ci baatin. Jëlal caru isop, wis ma, ma daldi sell, sang ma, ma daldi weex tàll ni meew. Dégtal ma bànneex ak mbég, ba yax yi nga damm, di yuuxoo mbég. Dumóoyul samay moy, te far sama bàkkaar yépp. Sàkkal ci man xol bu laab, yeesal ci man xel mu takku. Bul ma dàq ci sa jotaay, mbaa nga xañ ma sa Xel mu Sell mi. Sa mbégu mucc, na ballaat ci man te nga téye ma ci xel mu rafet. Kon ma xamal say yoon tooñkat yi, ba ay bàkkaarkat wëlbatiku ci yow. Céy, yow Yàllay mucc, xettalima ci deret ji ma tuur, may jollil sa njub ak mbég. Yow Boroom bi, tijjil sama gémmiñ ma daldi biral sa cant." Sabóor 51:1-17


Jàngal Kàddug Yàlla gi

Soo nammee gën a xam sellaayu Yàlla ak mbëggéelam gi fees ak yiw kon bind nu ngir nu yónnee la ay Injiilu Krist yu ànd ak ay faramfàcce, yoo dul fay dara.


Séddool Injiil bi ak say dëkkandoo

Su fekkee ne bataaxal bii laal na sa xol, te nga bëgg koo xamal say xarit, nun dinanu bég lool ci yónnee la ci as tuut. Bind nu te ijji ko ba mu leer naañ.

WATERS OF LIFE
P.O. BOX 60 05 13
70305 STUTTGART
GERMANY

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on September 07, 2023, at 11:03 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)