Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- John - 098 (Christ predicts the joy of the disciples) This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)
5. Bi Krist dekkee, wax ay taalibeem mbégte mi nar a ñów (Yowaana 16:16-24)YOWAANA 16:16-19 Yeesu wax na ñetti yoon ci guddi gii ci lu jëm ci demam. Lu rëcc dënnu taalibe ya lawoon ndaxte xamuñu woon li Mu nar. Waaye dige na ne dina ñówaat : Ci lu jëkk, mooy ndekkiteem ca bésub màggalu Pàk (jéggi ba) ; teg ci Mu feeñu taalibe ya, jaare ca miiru néeg ba ñu tëjoon ; kon book ab tàggoo bu gàtt lay doon, ab setsi bu gaaw ngir dem ci Baay ji. Bi leen Yeesu di wax loolu lépp, fekk ñungi ànd di dox ci tundu Oliw ya, taalibe ya jëliwuñu dara. Ca njalbéen ga dafa leen waxoon lu jëm ci demam asamaan. Léegi nag mungi wax ci tàggaloo gi nar a am. Ñu xam ne ay tëralinam ak ay ngirtelam (mébétam) raw nañu seeny xalaat. Dañu jaaxle woon, jaxasoo te tiis. YOWAANA 16:20-23 Yeesu dafa biral ca kow xalaati taalibeem ya. Moone de dëfalul seenug tiitaange, te dalalul seenug tiis. Xanaa kay dafa gën a xóotal metit yi, rangooñ yi ak jooytu yi leen nar a dal nees tuut. Bu buur bu baax saayee, nit ñi dañuy jooy, te seen yaakkaar tas. Bu taalibe yi di jooy, seeny noon ñungi bége. Li Yeesu jàppe ni noon, du Yawut yi rekk, waaye àddina sépp lay wax. Ñépp ñi bokkul ci Jàngu Krist, ci àddina su réer si te sànku lañu bokk, dañoo tàqalikook yàlla te nekk noonu Xel mu Sell mi. Rax ci dolli Yeesu dig na ay taalibeem ne dinañu mos mbég mu rëy -a- rëy. Xel-ñaaru taalibe yépp daldi jeex tàkk. Laaj yi aju woon ci tooñ, ñu saafaraal leen, te ñu daan jafe-jafe dee gi. Nooteelu Seytaane moxoñoo te merug seytaane manalatuleen dara. Seen weddi, seen ragal, ak xel-ñaar manuñu woon tere ndekkite Yeesu ak seen mbaal. Yawut ya manuñu leen woon a fiir, ndaxte Boroom bi moo leen doon aar. Noonu, xel-ñaar yépp, ak njàqare yi leen doon sonnal daldi saafarawu, te jot ag wér , ca bésugb ndekkite la, jaarale ko ci Ku dekki ki. YOWAANA 16:24 Yeesu dafa ñaax taalibeem yi ngir ñu ñaan lépp li ñu bëgg, noonu ñu nangul leen ko, ngir Baay ji man a ndamu. (Yowaana 14:13) Ñaan yooyu ñungi aju ci tabax jàngu bi, ak tasaare Injiil li, ndaxte Yeesu dafa bëgg ñu bare bokk ci mbëggeelu Kenneefu Ñett ñi. Looloo tax Mu digal nu ne : « Njëkkleen a wut Nguuru Yàlla ak Njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil. » Yeesu dige na ne Yàlla dina àddu ñaan yi, ngir ngëneeli baatin yi ci asamaan ak yu saayir yi ci suuf, moone de ñi ci asamaan ñoo ëpp cër ñi ci suuf. Yan laaj ak yan ñaan ñoo nekk ci sa xol ? Ndax dangaa soxla xaalis, wér-gi -yaram, walla ndam ? Ndax yaangi ñaan ngir gën a am wóllëre ak ñeneen ñi ? Ndax sa xel a ngi werante ci Yàlla am na am déet, ak ci yërmandeem ? Ndax dangay yëg wéetaayu xol gu lay won ne Xel mu Sell mi nekkul ci sa dund ? Ndax yaangi yenu sab sayu tooñ, te di am coono ci nattu yi, musiba yi, ak tiis yi ? Ndax rab yu bon yi ñungi lay tiital ban gay lox ? Ndax yaangi xaar ñówug Krist ak yaatalug Nguuru jàmmam ? Yan laaj ñoo ub sa ruu sa xel ak sa yaram ? Ndax dangay raay ci kow rekk walla danga ciy dem ba jeex ? Boroom yaakaar nga walla ku ñàkk yaakaar ? Ndax ku gaaw a gis boppam nga ? Ndax dingay ñaan Boroom bi Mu feesal la ak Xel mu Sell mi ? Ñaanal ngir sa jafe-jafe yépp. Ubbilal sa xol Baay ji ci asamaan. Bul waxantu, waaye nanga xalaat bu baax li ngay wax. Deel laaj Krist ci boppam. Njëkkal a xalaat may ak man-man yi la Yeesu jagleel , ba noppi nga sant Ko ci. Bu loolu wéyee, nga nangu te tuub say bàkkaar. Ñàkk ngëm dafay wàññi mbëggeel, te yaakaar yu tuuti, néew-doole la ci kanamu Yàlla. Baalul say bàkkaar yi nga nangu, te ñaan Ko mu won la li Muy séentu ci yów, ndax nga man a moytu di ñaan mbir yu la man a indil ay gàllankoor. Ñaanal yiwam te gëm ne mungi lay dégg. Bul fàtte mukk ne Yàlla mbëggeel la te dafa bëgg a baarkeel ñeneen ñi. Ñaanal Yàlla mu barkeel say xarit ak say noon. Du yów rekk a nekk ci coono. Nit ñépp a bokk benn nattu bi. Ci biir ay cant ak baalu, diis Ko say jafe-jafe, ak ñaan yi ngay defal ñeneen ñi. Bu loolu amee, dinga jàng mbóotu ñaan gu dëggu ci turu Yeesu. Ñaan dëgg, waxtaan ak Yàlla la, màggal Ko, sant ko, te dagaan Ko. Bul wuti ay kàddu yu xóot. Waxal li ngay xalaat ni mu gën a leere, mel ni kuy wax ak sa menn mbokk. Juutikat ba ñówoon ca Kër-Yàlla ga, dañu koo baal bi mu suufeelee baatam ne : « Boroom bi, yërëm ma, man miy bàkkaarkat. » Baay ji ci asamaan dafa dekkal Lasaar ci ñi dee, ba Krist Ko ñaanee mu génnee ko ci dee gi , delloo ko bakkanam kese ! Ngëm mooy jur mucc gi, ndimbal gi ak ndam li. Takkal sa fit te ñaan Yàlla ci biir yiwam, boole ñeme ak cant. Doomam nga , kon deel wax ak Moom ak mbég, ni doom, bul Ko nëbb dara. Krist dafa laa bëgg a sol mbég, te du caagéen ñaan yi nga def, waaye wóllëre gi nga séq ak Yàlla , ak Doomam ji moo tax. Lan moo la ëppal solo : May gi, walla kiy maye ? Boroom bi dafa lay jompal, waaye fàttalikul ne Moom mooy rembet gi. Yeesu dafa bëgg sa mbég mat sëkk. Sunu mbég dafay yokk bu Yeesu di nangu suny ñaan, te fekk ñu matadi lanu. Baarkeel na ñeneen te musal leen. ndax sunuy ÑAAN: Sunu Baay ji ci asamaan, nungi lay sant ak sunu xol bépp, ndaxte yónnee nga sa Doom ngir Mu musal nu. Baal nu sunuy njàqare te dimbali nu ba nu xam solos Kurwaa bi. Yewwi nu te may nu nuy lay man a ñaane ak di diisoo ak Yów ni gune di waxe aky waajuram, ci ni mu gën a woyofe. Rawaleel sunu noon yi sayu bàkkaar sonnal, te ñuy sukkraat ci biir mbañ. Dogal seeny jéng ndax ñu xam sa mbégu teewaay. LAAJ:
|