Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 089 (Christ's farewell peace)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson?

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
C - Tàggoo ba ca Néeg bu kowe ba (Yowaana 14:1-31)

3. Jàmm ji Krist maye (Yowaana 14:26-31)


YOWAANA 14:26
26 Waaye Dimbalikat bi leen Baay ji di yónnee ci sama tur, muy Xelam mu Sell mi, dina leen jàngal lépp, di leen fàttali li ma leen waxoon lépp.

Kan moo sañoon a wax ne xam na kàddu Krist yépp ? Te it, kan moo leen man a jàpp ci xelam, walla di leen di jëfe ? Ca reeru Boroom bi, taalibe ya jaaxlee ca ndofte workat ba, nekk nag di xalaat li nar a xew. Manatuñu woon fàttaliku li ëpp ci li leen Yeesu waxoon ca ba Muy tàggatoo ak ñoom, ba mu des Yowaana.

Yeesu jànkonteek ñàkk a man a fàttaliku bi taalibeem yi am, te xam ne Xel mu Sell mi dina wàcc ci ñoom ngir leeralal leen te yeesal leen, ni Mu ko waxe woon. Xel maa ngi wéy ci liggéeyu Yeesu ak li Mu nammoon. Mungi aar néew-doole yi. Yeesu tànnul ay boroom xam-xam yu màcc ba jéggi dayoo ; Dafa tànn ay nappkat, ay juuti ak boroomi bàkkaar yu wuute, ngir teg gàcce boroom xam-xamu njàng mi ak kàngami àddina si. Baay ji ci yërmandeem dafa yónni Xelam ci ñi manul dara, ngir ñu nekk ay doomam, Mu may leen maandutek suufeelu, jàngal leen ni ñuy fàttee seen bopp te dunde njub.

Yeesu bindul ab téere taalif, waxul kenn mu bindal Ko Injiilam ba di ci man a juum,mbaa am lu mu ciy fàtte. Dafa doon xaar ba Xelum Dëgg gi jàngal taalibeem yi, gindi leen, te fàttali leen la Mu waxoon. Injiil li, jenn ci jëf yi gën a am solo yu Xel mi la, batey jii. Dafa jàngal taalibe ya tëralinu mucc gi te fàttali leen ko. Dafa leen a dëj ci kàdduy Yeesu ndax Xel mi sargal Doom ji jaare ko ci seen seede. Amunu beneen téere bu dul mbindi Ndawi Krist, yi won àddina si xam-xam ak ngëm li nu jotoon. Teguñu ci beneen bat jëmale ko ci Yeesu. Seen waare lewetuloon, soofuloon te méngoo na ak bépp jamono. Xel mi dafa wéy di yeesal kàttanu nettali yii ba tey jii. Bu nuy jàng Injiil, dafa mel ni danuy jàng xew-xewi sunu jamono jii. Su nu dégloo kàdduy Krist, dafa mel ni mungi wax ci sunuy nopp. Kiy wax ne taalibe ya dañoo sos walla dañoo woñaar Injiil li, kooku xamul Xelum dëgg gi, ndwxte ci Xel mu Sell mi, muusante amu ci; Dëgg doŋŋ la ak Mbëggeel.

YOWAANA 14:27
27 Jàmm laa leen bàyyeel, sama jàmm laa leen jox, jàmm ju àddina manul a joxe. Buleen jàq, buleen tiit.

Yeesu dafa may jàmm taalibeem yi, jàmm ju romb sunu nuyóo yii, ba noppi Mu àggalee nii tàggoom gi. Mungi doon dem, waaye dafa maye jàmmam,ngir mu law ci seeni mbootaay. Waxuloon jàmmu wuyaa-wuyaa ni ko yenn taskati xabaar yi di defe. Fiir yi nag manuñu woon ñàkk a am. Ndegam nit ñi dañu tàqalikoo ak Yàlla, merum Boroom bi dafay dal ci seen bépp bàkkaar. Jàmm ju wuute la Yeesu di wax, maanaam jàmmu xel, ju mbaalu bàkkaar di maye, te mu jóge ci sunu jubóowaat ak Yàlla.

Fen, mbañ, coxorte bóom, bëgge, nay, ak sobe fees nañu àddina si. Waaye Yeesu dafa nu digal ne bunu bàyyi jëfi Seytaane yooyu di nu mëdd. Ku Bon ki mooy buuru àddina si. Waaye, ci Yeesu, Ki ñu Bëgg ki, mbëggeel gi dafay jolli te di nu xañ nu daanu ci lëndëm ak ñàkk yaakaar. Dafa nuy yewwi it ci sunu jaxasoo ak sunu ragalug dee. Ku gëm Yeesu, yaangi dëkk ci Yàlla, te Yàlla dëkk ci yów. Ndax loolu feeñ na ci yów ? Yeesoo ngi doon nelaw ci gaal gi, fekk tow bu metti am. Ña nekkoon ca gaal ga ñépp tàmbalee tiit, ndaxte gaal gaa ngi sol ndox. Yeesu jóg, gëdd tow ba ak ngelaw la, lépp dal, ne tekk ci saa si. Mu ne taalibeem ya : « Céy yéen ñi néew ngëm, lu tax ngéen di tiit(ragal) ?

YOWAANA 14:28-31
28 Dégg ngéen li ma leen wax:” dinaa dem,waaye dinaa dellusi ci yéen.” Bu ngeen ma bëggoon, dingeen bëgg ci li may dem ca Baay ba, ndaxte Baay bee ma gën a màgg. 29 Wax naa leen ko nag léegi, balaa loolu ñów, ngir bu waxtu wa agsee, ngeen gëm. 30 Lu weesu tey, du ma amati jotu waxtaan ak yéen, ndaxte malaaka mu bon mi jiite àddina saa ngi ñów. Kooku manalu ma dara. 31 Waaye àddina si war na xam ne, bëgg naa Baay ji te ni ma ko Baay ji sante, ni laay jëfe. Jógleen, ñudem!

Taalibe ya jàq lool ba leen seen sang ba yëgalaatee demam. Ba mu yëglee demam ba noppi, Yeesu dafa ci teg ne dina ñówaat. Noonu, Mu ne : « Bégleen ndaxte maangi jóge ci yéen, te di dem ci Baay ji. Bégleen ci li may dellu ca réew ma ma soqeekoo. Duma leen bàyyi ngeen di dékku coono kurwaa bi. Dinaa leen yewwi ci tiitaange bàmmeel gi. Sama bataaxal mungi aju ci seen jokkoo ak Baay ji. Su fekkoon ne bëgg ngeen ma, kon dingeen bég ci li may dellu asamaan. Jàppe naa sama Baay ne moo ma sut. Bëgg naa Ko ci sama biir xol ,waaye mbëggeel gi ma am ci yéen, du wàññeeku mukk. Dinaa ñów ci yéen jaare ko ci Xelam mi.

Yeesu dafa leen won melokaanu Baay ji, ngir ñu xam màggaayam te man a tau ci Moom a kit ngir waajal leen ci lu jëm ci tàggoo gi ak seen Sang, bi deewam gi taxaw ba noppi. Yeesu fàttali leen ne dee gi tekkiwul ne Yàlla nattangoom la. Jàmm ji dox ci diggante Baay ji ak Doom ji man na dékku lépp, te ci noonu, Baay ji dina Ko xëcc ci boppam gannaaw dee googu.

Jaruloon ñu ciy teg dara; Yeesu dafa jóg ngir matal coobare Baay ji, maanaam musal nit ñi ca kurwaa ba. Bu loolu wéyee, Xel mu Sell mi moo naroon a ñów ci taalibeem yi. Mucc googu dafa waroon a law ci bépp xeet. Dafa bëggoon ñépp xam mbëggeelu Yàlla gu amul àpp gi.

Gannaaw gi, Yeesu ak taalibeem ya jóge ca néeg bu kowe ba; fa ñu fase Kóllëre gu bees gi, génn ca biir lëndëmu guddi ga, ooa ca tundu Sedroŋ. Ñu dem ca toolu Setsemane ci kow tundu Oliw ya, fa leen workat ba doon xaare.

ÑAAN: Boroom bi nungi lay sant ci sant ci sa jàmm ji. Sellal nga sunu xol te may nu noflaay. Baal nu sunuy njàqare, sunuy tiitaange ak sunu ñàkk-yaakaar ci biir mbënnum mbañ gi, jàppante yi ak ger gi. Jarajëf ci sa Xel mi nuy aar ci jàmm. Na nuy fàttali kàddu yu am doole yi, bu jamono fiir yi teewee, ngir nu bañ a daanu ci bàkkaar ak ñàkk ngëm te it ci mbugalu yaakaar ju tas. Na nu dimbali ba nuy xool ci Yów, di ñaan ci kow yaakaar gu mat, te dimuñ ak mbég. Jarajëf, ndaxte sunu yoon wi ca Baay ja lanu jëme.Ñungi lay sujjóotal, Céy yów Mbotem Yàlla mi, yów mi nuy defaral màkkaan ca asamaan.

LAAJ:

  1. Lan mooy jàmmu Yàlla?

XËTU LAAJ - 5

Yów sama mbokk mi,
yónnee nu 12 tontu yu jub ci biir 14 yi nu la tegal fii. Bu ko defee dinanu la yónnee li topp ci njàng mii.

  1. Lu tax Yeesu nangu Mariyaama di Ko diw ?
  2. Lu duggu Yeesu ci Yerusalem di tekki ?
  3. Lu tax ñu ne deewug Yeesu mooy màggalug Dëgg gi, maanaam ndamam li.
  4. Nekk doomu Leer gi, lu muy tekki ?
  5. Lan mooy Ndigalu Yàlla ci Krist ngir ñépp ?
  6. Lan la raxasaayu tànk ba Yeesu defaloon taalibeem ya di tekki ?
  7. Lan lanuy jàng ci misaalu Krist ?
  8. Yan tekki-tekki ndam la Yeesu wone gannaaw ba Ko workat ba wonee gannaaw ?
  9. Lu tax ne mbëggeel rekk mooy ràññeeloo kercen yi ?
  10. Lan la Krist séq ak Yàlla Baay ji ?
  11. Waxal benn fànna buy tax Yàlla àddu sunuy ñaan !
  12. Yan melokaan la Yeesu jox Xel mu Sell mi ?
  13. Nan la sunu mbëggeel gi nu am ci Krist di màgge, te it nan la Kenneefu Ñett ñi di wàcce ci nun ?
  14. Lan mooy jàmmu Yàlla ?

Yónneel say tontu, te bul fàtte bind bu leer sa dëkkuwaay ci ambolog bi, ak ci kayitu tontu yi fii :

Waters of Life
P.O.Box 600 513
70305 Stuttgart
Germany

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 27, 2025, at 11:17 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)