Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
C - Tàggoo ba ca Néeg bu kowe ba (Yowaana 14:1-31)
2. Kenneefu Ñett bu Sell bi dafay wàcc ci way-gëm yi, jaare ko ci Dëfalkat bi (Yowaana 14:12–25)YOWAANA 14:21 Barke yi ak yiw wi dañuy balle ci Yeesu, wal jëm ciJàngoom bi saa su nekk. Bu way-gëm yépp feesoon ak rembax googu sax, du tere mu des géeju yiw. Ci kanamu noonam ya, Yeesu dafa taxaw temm ci ne mooy Almasi bi ak Doomu Yàlla ji. Ci waxtoom yu mujj yi nag, Mu feeñalal taalibe yi gëneelu jokkoo gi Mu ama k Baay ji. Na sa xol ubbeeku, ne yàmbalaŋ te mataayu baatinu Krist solu la ba nga fees dell. Yeesu nee na nu ne mbëggeel gi taalibeem yi am ci Moom, du woon yégeelu neen gu jollee ci seen coobare,waaye mbëggeel googu mungi sampu ci dégg ndigalam yi te di leen di jëfe. Nitu neen ki du raññee yedd bi làqu ci mbëggeelu Yeesu. Dafa nuy ubbil alali asamaan te di nu yónni ngir nu liggéeyal ñu réer ñi, te ñaax sunu bokk yi. Dafa nuy may nu matal ay tëralinam. Ay Ndigalam diisuñu lool, te duñu lu manul a nekk, ndaxte mbegtem Xel mi dafa nuy jëme kanam, te Xelum dëgg gi dafa nuy xiir ci tuub sunu jëf yu ñaaw yi, walla yuy naxe yi. Xel mi dafa nuy dimbali ba nu topp ndigalam yi. Ndegam dafa nu bëgg te musal nu, nun itam bëgg nanu Ko, te Xelam lanuy doxe. Ndax bëgg nga Yeesu ? Bul tëb rekk tontu « waaw »ju àndak mbég, walla « déedéet »ju ëmb ñàkk yaakaar. Bu fekkee ne judduwaat nga, Xel mu Sell mi dina la suxlu ba nga ne : « Waa-waaw Boroom bi Yeesu bëgg naa la, ndax sa màggaay ak sa lewetaay, sa jébbalu ak sa muñ; yaa ma may kàttanu mbëggeel. » Waxtaanu biir bii ak Xel mu Sell mi, du yaakaaru neen, walla ay xalaati kese, waaye dafa lalu ci dogu def ay jëf yu fees ak mbëggeel. Boroom bi dafay sos mbëggeel ci ñi Mu bëgg, te di ko suuxate yiwam. Yàlla dafa bëgg ñi bëgg Yeesu. Baay ji jox na kàttan gépp, ak yërmande gépp Doomam ji, ngir musal nit ñi. Ku nangu Yeesu, nangu Yàlla, te ku nanguwgul Doom ji, weddi nga Yàlla. Ndax xam nga ne Yàlla « sama soppe » la lay woowe, ndaxte Xelum Krist daf laa soppi ba nga nekk ku ñu war a bëgg ? Yów ci sa bopp baaxuloo, waaye mbëggeelu Yàlla def na la mbindeef mu bees. Krist mungi jëfe ci yów, di la taxawu ci ñaan ca kanamu Yàlla, te di la aar ba fàww. Dina la feeñal say digi baatin. Waaye nag, su fekkee sax ne yaangi yokku ci xam sa Musalkat bi, sa xam-xam googu lu tuuti lay doon ba tey, ndaxte xam-xam bi mooy, màgg ci dégg-ndigal, mbëggeel, jébbalu, ak joxe sa bopp. YOWAANA 14:22-25 Yeesu amoon na beneen taalibe bu tuddoon Yudaa mu dul mu Iskariyot, bu seetlu ne Yeesu dafa jéll waxtaan wi, la ko dale ca ba workat ba génnee. Dafa yég ne lu jéggi dayoo ngi nar a ñów. Yeesu tontuwu ko ci saa si waaye dafa yëgle nattu Jàngu bu jiitu bi ak solos deewam gi ngir àddina si. Mu won leen jéego yiy jëme ci xam Yàlla ci dëgg-dëgg. Xam Yeesu te nangu Ko, dafay maye ubbite ak dund gu bees ci kàttanu Xel mu Sell mi, di ci boole nga man a deñc bu baax ndigalam yi te di dunde mbëggeelu Yàlla. Yeesu teg ca kàddu yu doy waar : « Nu ñów ci way-gëm ji dëkksi ci moom. »Loolu jëmul ci Jàngu bi, waaye ki gëm lay wax. Xel mu Sell mi dafay ganesi way-gëm ji te dëkk ci moom. Wax jooju dafay rëkk xolu nit ki, mu mel ni mungi ci loxoy Xel muSell mi, Doom ji ak Baay ji. Bu ko mucc gi feeñoo, ci lay xam ne Yàllaa ngi ko wër fépp te di ko aar moom ci boppam. Képp ku wóolu Krist dinga mos kumpa googu. ÑAAN: Kenneefu Ñett gu Sell gi, Baay, Doom ak Xel mu Sell mi bëgg naa la, te maangi laysant, di la màggal. Ganesi nga ma te dëkk ci man miy bàkkaarkat. Baal ma samay bàkkaar. Jarajëf ci kàttanu mbëggeelu mbëggeel gi nga ma may a kit Xelum mbëggeel mi nga def ci sama xol bi. Aar ma ci sa tur. LAAJ:
|