Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 087 (The Holy Trinity descends on believers)

This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
C - Tàggoo ba ca Néeg bu kowe ba (Yowaana 14:1-31)

2. Kenneefu Ñett bu Sell bi dafay wàcc ci way-gëm yi, jaare ko ci Dëfalkat bi (Yowaana 14:12–25)


YOWAANA 14:15
15 Bu ngeen ma bëggee, toppleen samay ndigal.

Tas xabaar bu baax bi dafay siggil daaju Yeesu ca bant ba. Képp ku dul tas Injiil li, xamuloo goreel gi ci Krist. Soo gisee ne say ñaan ak sa seede amuñu benn njariñ, xoolaatal ndax yaa ngi wéy ba tey ci mbëggeelu Krist, walla say bakkaar ñoo la xañ barke boobu. Tuubal sa ñàkk a ànd ak Yeesu, ngir bañ a dog ni barke yi war a wale jëm ci ñeneen ñi. Boroom bi jox nanu ay ndigal yu bare: bëggleen seeny noon; xippileen te ñaan ngir bañ a daanu ci fiir; nangeen mat sëkk ni seen Baay bi ci asamaan mate; ñówleen ci man yéen ñépp ñi sonn te diis, ma may leen noflaay. Ndigal yooyu yépp tënk nañu leen ci ndigalu wurus gi ne: bëgganteleen ni ma leen bëgge. Yii ndigal duñu yen yu diis, waaye ndimbal lañu ak ab jéggi ngir féddali ngëm ak mbëggeel.

Képp ku mos payooru Yeesu gi dootuloo man a dund ngir sa bopp doŋŋ, waaye dangay surgawu Krist sa Musalkat bi.

YOWAANA 14:16-17
16 Te dinaa ñaan Baay ji, mu jox leen beneen Dimbalikat buy nekk ak yéen ba abadan. 17 Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dëgg. Àddina du ko man a nangu, ndaxte gisu ko. Yéen xam ngeen ko ndaxte mungi dëkk ak yéen te dina nekk ci yéen.

Képp ku jéem a topp ndigali Yeesu yii ak sa kàttanu bopp, dinga jullootu. Looloo tax Yeesu ñaan Yàlla ngir mu yónnee ab Dimbalikat, manaam Xel mu Sell mi. Lii bokk na ci liggéeyam: Mooy Xelum dëgg gi nuy won ni suny bàkkaar yi doye waar te metti; moo nuy leeralal Yeesu mi ñu daaj ci bant, te dinu biral ne mooy Doomu Yàlla, ji nuy baal sunuy bàkkaar. Dafa nuy soppi ci kow yiwam ba nu jub ci kanamu Yàlla; Xel mu barkeel mii dafa nuy jaarale ci juddu gu bees; dafa nuy may nu man a woowe Yàlla, sunu Baay te di nu may kóolute ne ay doomi Yàlla lanu jaare ko ci Xelum baayoo gi. Mooy sunu layookat te moo nuy rammu. Mungi ci sunu wet te di nu aar ci ñurumtu Seytaane yi, di nu wóoral ne mucc gi mat na sëkk. Manunu am lu wóor ci li nuy jànkonteel, walla jot li nu bëgg ci àddina sii, te jaarunu ci Dëfalkat bi nu Yeesu yónnee.

Kenn judduwaalewul Xel mi, du jinne ji, du taalifkat bi, walla Yonent bi. Xel mii, baatin la te ci ñi gëm deretu Yeesu lay wàcc. Ku bëggul Yeesu, walla nanguwuloo Ko, doo a, Xel mi. Waaye ki bëgg Yeesu, te nangu muccam, dafay mos mbég mu leer. Bu Xel mu Sell mi nekkee ci sunu xol, danuy ñam kàttanu Yàlla ci sunu néew doole ji. Yeesu dig na nu ne Dëfalkat boobu dunu bàyyi mukk ci dee gi, walla ca àtte ba, ndaxte mooy dund gu dul jeex gi.

YOWAANA 14:18-20
18 Duma leen bàyyi ngeen wéet. Dinaa Dellusi ci yéen. 19 Des na tuuti ci kanam àddina du ma gisati; waaye yéen dingeen ma gis. Dinaa dund, moo tax yéen itam dingeen dund. 20 Bu keroogee, dingeen xam nag ne, nekk naa ci sama Baay, yéen it nekk ngeen ci man, te maangi ci yéen.

Ba workat ba demee, Yeesu doog a wax taalibeem ya ne du yàgg dara Mu tàggook ñoom te xamal leen ne manuñu Koo topp fa Mu jëm. Waaye dafa ci dolli ne dina dellusi ci ñoom ci jëmm. Xamoon nañu seenug tiitaange, te kàddoom ya dañoo meloon ni paaka ñaari boor. Li njëkk mooy ñówug Xel mu Sell mi, te Moom Boroom bi mooyXel moomu. Ñaareel bi mooy ñówam ci ndamam bu àddina waree tukki. Ñaari fànna yooyu ñoo taxoon Mu war a tàqalikoo ak ñoom, ngir dellu ca Baayam ja. Bu tàqalikoo boobu amuloon, kon Xel mu Sell mi du wàcc ci ñoom astamaak ci nun.

Xel mi mooy ubbi bët yi ak xol bi ci saa si. Xam nanu ne Yeesu desul ci bàmmeel bi, ni ñeneen ñi, waaye mungi dund, teew ak Baay ji. Dundam mooy ëkku jaww ji ak ju sunu mucc. Ndegam daan na dee gi, kon may na nu dund gi ngir nu man a daan dee gi itam ci ngëm te dund ci njubte Yeesu Krist. Sunu diine, diine dund la, ju fees ak yaakaar.

Xel miy dëfale dëgg, Xelum Yàlla la, miy ñów dëkksi ci nun, yey nu ne Doom jaa ngi ci Baay ji, te Baay jaa ngi ci Doom ji, ci biir jokkoo gu mat sëkk. Xam-xamu baatinu Kenneefu Ñett bu sell boobu niroowul ak matematik, waaye dafay jëmmu ci ki gëm, ba mu jokkoo ak Yàlla ni ko Yeesu nekke. Kumpay Xel mi dañoo romb sunu dégg-dégg.

Yeesu waxul ne dafa bëgg a tasaaroo nekk ci kenn ku nekk ci yéen, « waaye, damay dëkkandoo ci yéen. »Ci coobareem, Kercen bi du néegu Xel mi; dafay niroo ak xeer bu ñu teg ci këru Yàlla. Way-gëm yépp dañuy bokk séddoo kërug baatin googu. Dig bile dañoo maas nuunam : « yéen a ngi ci man, te maa ngi ci yéen. » Bu ñu sell ñi jokkoo ci seen dundin, Yeesu dafa leen di feeñu. Seetlul ne Yeesu dafa tëj dige bi ak as ndigal lu ne : « Na ngeen bëggante ni ma leen bëgge. »Du man kenn rekk maa jokkoo ak Krist, waaye nun ñépp dinanu rembax ak mataayu Yàlla.

ÑAAN: Nungi lay sujjootal, yów mbotem Yàlla mu sell mi. Ci sa dee lanu jotea dund gu amul àpp gi. Baal nu sunu ngëm lu néew li, sunu ñàkk a xam gi, ndax dara bañ a nekk gàllankoor ci sunu diggante. May nu, nu gis sa teewaay ci sunuy coono, te man a dunde xel mu laab. Sant nanu la ci li nga yónnee Dëfalkat bi, Xelum dëgg, gi nuny boole aar ba fàww.

LAAJ:

  1. Yan melokaan la Yeesu jox Xel mu Sell mi?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 27, 2025, at 03:24 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)