Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
A - LI JIITU AYU BéS bu SELL bi (Yowaana 11:55 - 12:50)
5. Dëgër boppu nit ñi, ak li Àtte bi am lépp (Yowaana 12:37-50)YOWAANA 12:37-41 Ci Yerusalem, Yeesu wone na fa firnde yu bare yuy wone mbëggeelam. Ñépp ñi jekkoon xamoon nañu kàttanam ak fu mu jóge. Waaye ñi seen xel tëju woon, te bañ a soppi seeni xalaat, manuñu woon ràññee Yeesu mi doon bëkkanteek ñi doon dëngal li war a jub te di teg njaamu gu kenn àttanul. Nit ñu bare seen xalaat doŋŋ moo leen doy, te duñu déglu baatu Yàlla. Xel mu Sell mi, ndànk ak dal lay waxe, te dafay laaj xol bu ko nagoo dalal. Waaye fippukat, yiy jànkonteek Xel mu Sell miy wax ci Injiil, du seeni ruu rekk lañuy xatarlaayuloo, waaye Yàlla, ci njubteem ak meram, dafay rocci seen man-manu dégg ak gis gi ñu judduwaale, te dëgëral seeni xol. Loolooy tax ba duñu man a xamati sax liy seen soxla dëgg. Yàlla mooy boroom mucc gi ak àtte bi. Seetlu nanu ne yenn njaboot yi, xeet yi, walla réew yi, dafa mel ni ci biir merum Yàlla lañuy dund. Yàlla dafay fàtte ñiy wéy di Koy sore gannaaw ba Mu leen toppee ay yooni -yoon ngir delloosi leen ci Moom. Yàlla dafay dëgërloo xolu ñi bañ a déggal baatu Xelam mu Sell mi .Ñépp ñi ko tey di dëggate mbëggeelam gi, Te di jallax wootalu Krist, dees na leen mbugal. Yàlla, ci kow sellaayam dafa war a dëgëral ndànk-ndànk xoli ñi déggadi, noonu ñuy daagu, jëm ci sànku. Li tax ñuy wax Yàlla dafay dëgëral xolu ñi Ko nanguwul, du waxi caaxaan kese, waaye dafa méngoo ak màggaayam. Esayi xamoon na loolu bu baax, ba mu déggee Boroom bi di ko yónni te fekk du ngir yewwi askan wi, waaye ngir dëgëral xolam (Esayi 6:1-13). Waare ci mbëggeel moo gën a yomb artu nit ñi ci lu jëm ci merum Yàlla, walla àtteem. Mbëggeelu Yàlla dafa ànd ak cellaay, dëgg, ak njubte. Amul genn mbon gu man a dékku teewaayam; li bon dafay daw ceeñeeri màggaayam gi. Ndegam Yeesu mooy Mbëggeel gu sell gi ñu jëmmal, kon teewaayam féwwale na nit ñi. Yowaana nangu na ak njàmbaar ne Ki toog ci gàngune gi, te Esayi gis Ko, Yeesu la, ndaxte Yàlla ak Doomam ji, benn lañu ci cellaay ak màggaay. YOWAANA 12:42-43 Yowaana, taskatu Injiil bi, waa këru waarekat bu mag ba xamoon nañu ko bu baax (Yowaana 18 :15). Moom seede na ne mbooloo maa ngi doon gën a sore Yeesu. Waaye amoon na ay kilifa yu Ko gëmoon. Ñooña gisoon nañu ne Yàlla ànd na ak Moom, te ay kàddoom feesoon nañu kàttan ak dëgg, waaye doonuñu ko seede ci mbooloo. Lu tax nit ñooñu nangu àtte bu àndul ak seen xalaat? Dañu ragaloon Farisen ya, te aaru ak siiw gënaloon leen dëgg gi. Farisen ya dañoo tëkku woon waa Yerusalem ne ku ci ànd ak Yeesu rekk, dees na la dàq ci bitti. Noonu jawriñ yooya dañu doon moytoo ñàkk seen màqaama, te bañ it ñu dàq leen ca réew ma, walla di leen sonal. Képp ku dogoo woon ak réeew mi, dootuloo fa man a jënd, mbaa jaay dara; takk jabar sax mbaa di jaamoondoo ak waa réew ma dañu la koy xañ. Dañu lay jàppe ni gaana guy wàlle. Lu tax kilifa yooyu waxuñu dëgg gi, donte seen ngëm gi ñuy nëbb? Sargalu nit ñi moo leen gënaloon màggaayu Yàlla. Neex Yàlla mosuleen a soxal; seen bopp a leen gënaloon Boroom bi. Toroxte ñeel na kiy nëbb ngëmam te mel ni ku xamul Yeesu. Ku mel noonu dina weddi Boroomam, bu mbir yi tàngee jër. Kooku, Kaaraange boppam ak sagam la gën a fonk sargalu Yàlla ak càmmam. Nanga seedeel sa Boroom, te wóolu Ko, ndaxte dina la wommat ci kow coobareem. YOWAANA 12:44-45 Yeesu dafa woo askanam ngir ñu tuub, bi Mu doon jàngale jaare ko ci ay léebu yu tar, yu tegu ci baatin. Ci gis-gis bu njëkk, dafa mel ni njàngaleem ji àndul, ndax li Mu wax ne: ” Ku ma gëm,gëmuloo ma!” Yeesu du boole nit ak Moom ci boppam rekk, waaye Doom ji dafay jëmale taalibeem yépp ci Baayam ji. Dafa tekki bépp ndombal yelleefam, te xaarul nit ñi wóolu Ko moom rekk. Doom ji du xañ Baay ji ngëmu nit ñi. Du teggi lenn ci màggaayu Yàlla. Dafa koy feeñal te di koy màggal saa su nekk. Li mu saffaanoo it dëgg la; kenn manul a ñów ci Baay bi, te jaaruloo ci Doom ji; ngëm gu dëggu ci Yàlla manul a teggi ngëm gi ñuy am ci Doom ji. Baay ji dafa Ko dénk way-gëm yépp ngir ñu nekk askanam wi Mu tànn, te it Solal na Ko mbubbi buuri asamaan yépp. Noonu la Doom ju woyof ji man a birale ne:”Ku ma gis, gis nga Ki ma yónni.” Te boolewu ci genn ñàkk kersa. Yeesu mooy ndawu Yàlla dëgg, te fees na ak kàttan ak ndamul Yàlla ba man Koo déggal ni mu ware. Yeesu mooy xolu dundug asamaan, leer gi ak yànjaay bi. Nun xamunu jeneen Yàlla ju dul ji Yeesu wone ci dund gi ak ci ndekkite li. Woyofaayam aj na Ko ba mu tollook Baay ji. Ka Esayi gisoon Yeesu la ci dëgg, ndaxte amul dara lu wuutale Baay ji ak Doom ji. YOWAANA 12:46-48 Ab góom bu doy waar amoon na ci ab dëkk bu ndaw ci Afrik. Nit ña dañu doon woñaaru ca seeni néeg ya, ndax metitu feebar ba. Ba doktoor ba leen doon faj gise ne képp ku jàngoro ji dal, boo doxee ci naaj bi, doomu jàngoro ji dafay dee. Noonu muy xaacu naan: « Génnleen seen néeg yu lëndëm yi te dox ci naaj bi, ngir ngeen man a wér! Naaj bi dafay rey jàngoro ji! » Ñu bare génn ci naaj bi te wér. Mu am ñeneen ñu gëmul doktoor ba, noonu ñu des ca seeni néeg ba dee fa. Doktoor ba ak ña jotoon a wér laaj ña doon sukkuraat ne leen: « Lu tax génnu leen ci naaj bi? »Ñu tontu ne: « Musiba dal nanu, gëmunu woon say wax, ndaxte dafa woyofoon lool. Feebar bi dafa nu sonaloon lool. » Doktoor ba ne leen: « Kon nag dingeen dee te du feebar bi moo leen di faat, waaye ñàkk a déggal samay kàddu moo leen di sànk. » Nettali bii, dafay wone kàttanu Krist. Moom, mooy jantu njubte, gi sut lëndëmu bàkkaar, Ki am ndam ci kow reeni mbon gi. Képp ku dugg ci leer gu kéemaane gi texe nga. Moom, amul beneen mébét bu dul musal nit ci bàkkaar ak dee. Ay kàddoom ñoo nu man a yewwi ci doole yiy yàq. Képp ku dégg kàddoom yi, wóolu Ko te gëm Ko, ñów ci Moom te déggal Ko, dina dund ba fàww. Dee gi du ko manal dara. Waaye képp ku dégg ay kàddoom te denculeen ci xolam, dina suux ci bàkkaar, te jubal ca àtte ba ak ca lëndëmu bitti bi. Noonu la Injiil di nekke ab àttekat buy indi musiba ngir ñi gëmul. Ndax nangu nga Yeesu ni sa Musalkat? Ndax yaangi jàpp ay kàddoom ci sa xel, te di leen di jëfe? YOWAANA 12:49-50 Yeesu mooy kàddug Yàlla gi. Bu Yeesu di wax, li Yàlla di xalaat te namm ko rekk lanuy dégg. Krist mooy kàddu yu jàddul fenn, yu nu Yàlla yónnee. Doom ji dafa dégg ndigal. Déglu na kàdduy Baayam te tekkil nu leen ci kàllaama nit. Ci Moom la Yàlla jaare ngir wax ak àddina su tooñ fa kanamam. Dafa mel ni ku naan nu: « Maay Aji sax ji, te maay nekk seen Baay. Ci kow yiw, dinaa leen may dund gu dul jeex. Man na am ngeen yelloo mer ak mbugal, waaye terewul ne dama leen a bëgg, ba dinaa jébbale sama Doom ju sell ji, ngir Mu wuutu leen, ba bu ñu leen gorelee, ngeen jot Xel mu Sell mi. Dungeen dee. Dékkuleen dund gu dul jeex gi ci loxoy Almasi bi. Ku ko deful du gis àjjana, mbaa dund gi dëgg. »Ci kow kàddu yii, Yàlla may na àddina si mucc gu amul payoor. Waaye képp ku tanqamlu Krist, mbaa nga weddi Ko, dina daanu ci kàmb gi, ndaxte jallax na santaaney Yàlla yiy maye dund gi. ÑAAN: Baay, nungi lay sant ci li nga nu may dund gu dul jeex gi. Nungi lay sargal te di la màggal ak mbég. Jële nga nu ci dee, indi nu ci dund; teggil nu nootaage bàkkaar, ba dugal nu ci sa mbëggeel. Sàmmal sa kàdduy Doom ji ci sunu dund te xaatim leen ci sunu xol ak sunu xel ngir ñu man a meññ. Na sa Injiil judduwaatloo ñu bare. Jàngal nu ni nu war a yéenee ñépp sa xabaar bi, ndax ñu dund te bañ a dee. LAAJ:
|