Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)
d) Yeesu, leeru àddina si (Yowaana 8:12-29)YOWAANA 8:25-27 Donte Yeesu mungi doon wéy di biral baatinam, Yawut ya di Ko gën a laaj ku Mu doon. (yaay kan?) Jox nu ay firnde yu leer ba nu man a gindiku! »Moone de sànx rekk waxoon na leen ki Mu doon, ci ni mu gën a leere. Yeesu faramfàcce lii: » La ko dale ca njalbéen, maay Yàlla ju dëggu ji; te taxul ngeen dégg samay kàddu. Samam Xel dalaluleen ko ci seeny xol. Samay tur, ak samay melokaan faalewuleen leen. Man maay Kàddug Yàlla gi ñu jëmmal. Waaye, dungeen Ma dëglu te xamuleen ma, ndaxte ci àddina suuf sii ngeen bokk, waaye du ci Yàlla. Loolu moo tax dungeen may sama Xel mi mu soppi leen. Li Ma topp di leen ko wax daanaka jariñul dara ndaxte dangeen a dëgëral seeni xol. Ci kow loolu, samay Kàddu dinañu leen àtte, naam sax bu Ma leen bëggee te di leen di feeñu. Yàlla mooy dëgg gi, ni Ma ko nekkee itam. Waaye dëgg googu moo leen di sànk, ndaxte dangeen a weddi ci seen xol mayug Xel ma. »Yawut ya xamuñu woon li wax ji làq, te xamuñu woon itam solo si jokkoom ak Baay ji am. Dégg nañu kàddu yi te xamuñu ci dara, ndaxte gëmuñu Ko woon. Bu nu Ko gëmee rekk, sunu xel jot peeñug dëgg yu leer yooyu. YOWAANA 8:28-29 Yeesu xamoon na ne noonam ya, ak taalibeem ya sax xamuñu woon dëgg gi nekk ci Moom. Yónneeguñu leen oon Xel mu Sell mi. Waaye wóoroon na Ko ne bu ñu Ko daajee ci bant, loolu dina dindi bàkkaari àddina si, te bu yéegee ca Baay ja Xel mu Sell mi dinaa wàcc ak doole. Su boobaa Ki Nekk dina laal xelu Yawut yi, ak Yéeféer yi. Baatinu Yeesu kenn waru ko teqale ak liggéeyu Xel mu Sell mi. Jarul ñuy wéeru ci ay xalaat yu man a nekk, am déet. Juddu gu bees rekk moo man a indi ngëm gu leer, ni ngëm gu dëggu, ci baaxaayu Yeesu, di jure juddu gu bees. Krist waxul ne baatin bu beru la, waaye biral na jokkoom àqan ak Baay ji, ba manul a def dara su ci Baay ji àndul. Rax ci dolli, du def dara ci coobare boppam. Baay ji mooy jaare ci Moom ngir jëf. Suufeeloom ni mu tollu mooy ni Mu nangoo turu « Apotaru Yàlla » (Yowaana 13 :16). Terewul ci biir aaya bi sax mungi ciy feeñoo ni Kilifa ak Sang. Sunu Baay neexul a xam, waaye Xel mu Sell mi moo nuy dimbali. Ci nettali Yowaana bii, Yeesu maye na ci dëgg gu leer gi am ci diggante Kenneefu Ñett ñi. Mu teg ca ne: »Baay jaa ngi ak man saa su nekk, ba leegi nii sax. Mosu Ma sore benn yoon. Doom ji it mosul a sore Baay ji ci asamamaan, te mosul a fippu ci kanamam, waaye dafa Koy déggal ci lépp. Asamaan la wàcce Jëmmoo nit, te déggal coobare Baayam ji. Mu yokk ca kàddu yu neex naan: »Saa su nekk damay def li neex Baay ji. » Kenn manul a wax Kàddu yii, ku dul Doom jiy dunde ak jokkoo ak Baayam ji, ci mataayu Xel mi. Yeesu moo matal Yoon wi. Rawatina sax Mooy Yoon wu mat wu Kóllëre gu Bees gi. Moone de, Yawut ya dañu Ko jàppe woon ni tuumaalkat buy weddi Yoon wi, te di réeral mbooloo mi, te Fekk nag Mooy kenn kese ki déggal Yoon wi. Ndax yaangi dégg baatu Xel mi ci Kàdduy Yeesu? Ndax yaangi ràññee màggaayam ak suufeeloom, féexaayam ak jébbaloom ci Baay ji? Dafa la bëgg a dugal ci jokkoo mbëggeel ci biir jébbalu ak tawfeex. Jaare ko ci teewaayam, dafa nuy yóbbu ci goreel ak surgawu. Mooy nekk sa jàngalekat, te doo def dara lu Mu àndul, ndaxte danga Koo bëgg a neex ci sa bépp doxalin. ÑAAN: Sang bi Yeesu, rus naa ci sama dëgër-bopp gi, sama ndëngate gi, ak sama tooñ. Baal ma samay tooñ. Sellal ma te dimbali ma, ba ma man a topp sa yoonu Xel mu Sell mi. Nekkal sama njiit ak sama jàngalekat; ubbil sama xol ak sama xel ñu dékku sa mbëggeel gu dul jeex gi. LAAJ:
|